An-Nisa · 134/176
Tekki Waxtaan — An-Nisa
مَّن كَانَ يُرِيدُ ثَوَابَ الدُّنْيَا فَعِندَ اللَّهِ ثَوَابُ الدُّنْيَا وَالْآخِرَةِ ۚ وَكَانَ اللَّهُ سَمِيعًا بَصِيرًا ۝١٣٤
man kaana yureedu sawaabad dunyaa fa`indallaahi sawaabud dunyaa wal Aakhirah; wa kaanal laahu Samee`am Baseeraa
📖 Tekkim Wolof
Koo xam ne yoolu àddina bi la bëgg, [na xam ne] Yàlla am na lu mu yoole ci àddina ak ca àllaaxira. Te Yàlla Kuy dégg la, Kuy gis la.

🎧 Dégg


📜 Aaya 132-136 — An-Nisa

132وَلِلَّهِ مَا فِي السَّمَاوَاتِ وَمَا فِي الْأَرْضِ ۚ وَكَفَىٰ بِاللَّهِ وَكِيلًا
Te it, li nekk ci asamaan yeek suuf, Yàlla doy na ci te mat na sëkk Kilifa.
133إِن يَشَأْ يُذْهِبْكُمْ أَيُّهَا النَّاسُ وَيَأْتِ بِآخَرِينَ ۚ وَكَانَ اللَّهُ عَلَىٰ ذَٰلِكَ قَدِيرًا
Bu ko sooboon Mu jële leen fi, yéen nit ñi, indi fi ñeneen. Te loolu, Yàlla mën na ko.
134مَّن كَانَ يُرِيدُ ثَوَابَ الدُّنْيَا فَعِندَ اللَّهِ ثَوَابُ الدُّنْيَا وَالْآخِرَةِ ۚ وَكَانَ اللَّهُ سَمِيعًا بَصِيرًا
Koo xam ne yoolu àddina bi la bëgg, [na xam ne] Yàlla am na lu mu yoole ci àddina ak ca àllaaxira. Te Yàlla Kuy dégg la, Kuy gis la.
135۞ يَا أَيُّهَا الَّذِينَ آمَنُوا كُونُوا قَوَّامِينَ بِالْقِسْطِ شُهَدَاءَ لِلَّهِ وَلَوْ عَلَىٰ أَنفُسِكُمْ أَوِ الْوَالِدَيْنِ وَالْأَقْرَبِينَ ۚ إِن يَكُنْ غَنِيًّا أَوْ فَقِيرًا فَاللَّهُ أَوْلَىٰ بِهِمَا ۖ فَلَا تَتَّبِعُوا الْهَوَىٰ أَن تَعْدِلُوا ۚ وَإِن تَلْوُوا أَوْ تُعْرِضُوا فَإِنَّ اللَّهَ كَانَ بِمَا تَعْمَلُونَ خَبِيرًا
Éy yéen ñi gëm ! Taxawleen temm ci maandute, di seede ngir Yàlla doonte seede soosu [lu naqari la] luy dal ci seen kaw, walla ci seeni waajur, walla ci kaw seeni njaboot, walla seeni jegeñaale. Su dee ku woomal la walla ku ñàkk, Yàllaay ki gën pey ci ñoom ñaar ñépp. Buleen topp seeni bànneex ba ñàkk a maandu. Bu ngeen jéggalee [seede] walla ngeen dëddu bañ a seede, xamleen ne Yàlla Ku deñ-kumpa la ci li ngeen def.
136يَا أَيُّهَا الَّذِينَ آمَنُوا آمِنُوا بِاللَّهِ وَرَسُولِهِ وَالْكِتَابِ الَّذِي نَزَّلَ عَلَىٰ رَسُولِهِ وَالْكِتَابِ الَّذِي أَنزَلَ مِن قَبْلُ ۚ وَمَن يَكْفُرْ بِاللَّهِ وَمَلَائِكَتِهِ وَكُتُبِهِ وَرُسُلِهِ وَالْيَوْمِ الْآخِرِ فَقَدْ ضَلَّ ضَلَالًا بَعِيدًا
Éy yéen ñi gëm ! Doyluleen Yàlla ak ub Yonentam, ak Téere ba Mu wàcce ci Yonentam, ak Téere ba wàcc la jiitu. Képp ku weddi Yàlla, ak i Malaakaam, ak Yonentam, ak Bis-pénc ba, réer na réer gu sori [dëgg].
An-NisaFihi Alxuraan
176Aaya
MedinanRevelation
134Aaya

Tekki — An-Nisa 134

Simoore An-Nisa Aaya 134 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Koo xam ne yoolu àddina bi la bëgg, [na xam…

Simoore Aaya 134/176 — An-Nisa النساء (Medinan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: An-Nisa Dégg, An-Nisa Tekki, An-Nisa mp3, An-Nisa pdf. Aaya 132–136. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers