An-Nisa · 152/176
Tekki Waxtaan — An-Nisa
وَالَّذِينَ آمَنُوا بِاللَّهِ وَرُسُلِهِ وَلَمْ يُفَرِّقُوا بَيْنَ أَحَدٍ مِّنْهُمْ أُولَٰئِكَ سَوْفَ يُؤْتِيهِمْ أُجُورَهُمْ ۗ وَكَانَ اللَّهُ غَفُورًا رَّحِيمًا ۝١٥٢
Wallazeena aamanoo billaahi wa Rusulihee wa lam yufarriqoo baina ahadim minhum ulaaa`ika sawfa yu`teehim ujoorahum; wa kaanal laahu Ghafoorar Raheema
📖 Tekkim Wolof
Waaye ña gëm Yàlla ak i Yonentam te xàjjalewuñu kenn ci ñoom, ñooña gaay Dananu leen jox seen pey. Te Yàlla Jéggaleekoon la, Jaglewaakoon la.
🎧 Dégg

📜 Aaya 150-154 — An-Nisa

150إِنَّ الَّذِينَ يَكْفُرُونَ بِاللَّهِ وَرُسُلِهِ وَيُرِيدُونَ أَن يُفَرِّقُوا بَيْنَ اللَّهِ وَرُسُلِهِ وَيَقُولُونَ نُؤْمِنُ بِبَعْضٍ وَنَكْفُرُ بِبَعْضٍ وَيُرِيدُونَ أَن يَتَّخِذُوا بَيْنَ ذَٰلِكَ سَبِيلًا
Ña weddi Yàlla ak i Yonentam, te bëgg a téqale Yàlla ak i Yonentam, te naan : “ Gëm nanu ñenn ña, weddi ñenn ña [ca Yonentam ya]”, tey jéem a am ca yoon wa nekk ca diggante weddeek ngëm,
151أُولَٰئِكَ هُمُ الْكَافِرُونَ حَقًّا ۚ وَأَعْتَدْنَا لِلْكَافِرِينَ عَذَابًا مُّهِينًا
ñooña ñooy dëgg-dëggi yéefar ! Te Dananu xaaroo yéefar yi mbugal mu leen di toroxal.
152وَالَّذِينَ آمَنُوا بِاللَّهِ وَرُسُلِهِ وَلَمْ يُفَرِّقُوا بَيْنَ أَحَدٍ مِّنْهُمْ أُولَٰئِكَ سَوْفَ يُؤْتِيهِمْ أُجُورَهُمْ ۗ وَكَانَ اللَّهُ غَفُورًا رَّحِيمًا
Waaye ña gëm Yàlla ak i Yonentam te xàjjalewuñu kenn ci ñoom, ñooña gaay Dananu leen jox seen pey. Te Yàlla Jéggaleekoon la, Jaglewaakoon la.
153يَسْأَلُكَ أَهْلُ الْكِتَابِ أَن تُنَزِّلَ عَلَيْهِمْ كِتَابًا مِّنَ السَّمَاءِ ۚ فَقَدْ سَأَلُوا مُوسَىٰ أَكْبَرَ مِن ذَٰلِكَ فَقَالُوا أَرِنَا اللَّهَ جَهْرَةً فَأَخَذَتْهُمُ الصَّاعِقَةُ بِظُلْمِهِمْ ۚ ثُمَّ اتَّخَذُوا الْعِجْلَ مِن بَعْدِ مَا جَاءَتْهُمُ الْبَيِّنَاتُ فَعَفَوْنَا عَن ذَٰلِكَ ۚ وَآتَيْنَا مُوسَىٰ سُلْطَانًا مُّبِينًا
Ña jotoon ab Téere, ñangay laaj, bëgg nga wàcce ca ñoom ab Téere bu bawoo asamaan. Waaye ñoom sax laajoon nañu Muusaa lu gën a rëy loolu, ndax dañu ne ko : “Won nu Yàlla ñu janook Moom ! ”. Dënnu ga fàdd leen ngir seen bàkkaar boobu. Ba loola jàllee, ñuy jaamu yëkk wa, ginnaaw ba leen dëgg gu bir dikkalee. Nu baal leen loola, topp Nu jox Muusaa kiliftéef gu bari.
154وَرَفَعْنَا فَوْقَهُمُ الطُّورَ بِمِيثَاقِهِمْ وَقُلْنَا لَهُمُ ادْخُلُوا الْبَابَ سُجَّدًا وَقُلْنَا لَهُمْ لَا تَعْدُوا فِي السَّبْتِ وَأَخَذْنَا مِنْهُم مِّيثَاقًا غَلِيظًا
Nu yékkati doj wa ca seen kaw ngir fasanteek ñoom kóllare, ñu ne leen woon : “Dugguleen ci buntu bi ànd ak di sujjóot” ; Neeti leen : “Buleen jalgati bisub gaawu” ; Nu jàppe woon ak ñoom kóllëre gu dëgër.
An-NisaFihi Alxuraan
176Aaya
MedinanRevelation
152Aaya

Tekki — An-Nisa 152

Simoore An-Nisa Aaya 152 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Waaye ña gëm Yàlla ak i Yonentam te xàjjalewuñu kenn…

Simoore Aaya 152/176 — An-Nisa النساء (Medinan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: An-Nisa Dégg, An-Nisa Tekki, An-Nisa mp3, An-Nisa pdf. Aaya 150–154. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers