An-Nisa · 40/176
Tekki Waxtaan — An-Nisa
إِنَّ اللَّهَ لَا يَظْلِمُ مِثْقَالَ ذَرَّةٍ ۖ وَإِن تَكُ حَسَنَةً يُضَاعِفْهَا وَيُؤْتِ مِن لَّدُنْهُ أَجْرًا عَظِيمًا ۝٤٠
Innal laaha laa yazlimu misqaala zarratinw wa in taku hasanatany yudaa`ifhaa wa yu`ti mil ladunhu ajran `azeemaa
📖 Tekkim Wolof
Yàlla du tooñ kenn, lu toll ni pepp. Te ku def u yiw Mu ful ko, joxe ca pey [yool] gu màgg.
🎧 Dégg

📜 Aaya 38-42 — An-Nisa

38وَالَّذِينَ يُنفِقُونَ أَمْوَالَهُمْ رِئَاءَ النَّاسِ وَلَا يُؤْمِنُونَ بِاللَّهِ وَلَا بِالْيَوْمِ الْآخِرِ ۗ وَمَن يَكُنِ الشَّيْطَانُ لَهُ قَرِينًا فَسَاءَ قَرِينًا
Yàlla safoowul itam ñiy sànk seeni alal ngir ngistal, ci bëti nit ñi, te gëmuñu Yàlla ak Bis- pénc ba. Koo xam ne Séytaanee di àndandoom aka bon bon ub àndandoo !
39وَمَاذَا عَلَيْهِمْ لَوْ آمَنُوا بِاللَّهِ وَالْيَوْمِ الْآخِرِ وَأَنفَقُوا مِمَّا رَزَقَهُمُ اللَّهُ ۚ وَكَانَ اللَّهُ بِهِمْ عَلِيمًا
Waaw, lu Ma leen doon won su ñu gëmoon Yàlla ak Bis-pénc ba, tey joxe ca la leen Yàlla wërsëgal ? Yàllaa ka leen a xam.
40إِنَّ اللَّهَ لَا يَظْلِمُ مِثْقَالَ ذَرَّةٍ ۖ وَإِن تَكُ حَسَنَةً يُضَاعِفْهَا وَيُؤْتِ مِن لَّدُنْهُ أَجْرًا عَظِيمًا
Yàlla du tooñ kenn, lu toll ni pepp. Te ku def u yiw Mu ful ko, joxe ca pey [yool] gu màgg.
41فَكَيْفَ إِذَا جِئْنَا مِن كُلِّ أُمَّةٍ بِشَهِيدٍ وَجِئْنَا بِكَ عَلَىٰ هَٰؤُلَاءِ شَهِيدًا
Naka mu ? [Bus bis-pénc baa,] ba Nu indi xeet wu nekk ànd ak seede te yaw [Muhammad], Nu indi la bu boobaa nga doon seede ci ñii [waa Màkka] ?
42يَوْمَئِذٍ يَوَدُّ الَّذِينَ كَفَرُوا وَعَصَوُا الرَّسُولَ لَوْ تُسَوَّىٰ بِهِمُ الْأَرْضُ وَلَا يَكْتُمُونَ اللَّهَ حَدِيثًا
Bis booba, ña weddi woon te toppuñu Yonent bi, danañu ngéeju ñu maasale leen ak suuf si te fekk na Yàlla moom kenn mënu Koo nëbb jenn wax.
An-NisaFihi Alxuraan
176Aaya
MedinanRevelation
40Aaya

Tekki — An-Nisa 40

Simoore An-Nisa Aaya 40 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Yàlla du tooñ kenn, lu toll ni pepp. Te ku…

Simoore Aaya 40/176 — An-Nisa النساء (Medinan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: An-Nisa Dégg, An-Nisa Tekki, An-Nisa mp3, An-Nisa pdf. Aaya 38–42. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers