An-Nisa · 72/176
Tekki Waxtaan — An-Nisa
وَإِنَّ مِنكُمْ لَمَن لَّيُبَطِّئَنَّ فَإِنْ أَصَابَتْكُم مُّصِيبَةٌ قَالَ قَدْ أَنْعَمَ اللَّهُ عَلَيَّ إِذْ لَمْ أَكُن مَّعَهُمْ شَهِيدًا ۝٧٢
Wa inna minkum lamal la yubatti`anna fa in asaabatkum museebatun qaala qad an`amal laahu `alaiya iz lam akum ma`ahum shaheeda
📖 Tekkim Wolof
Te am na ci yéen kuy des-deslu ginnaaw ba lu metti dal leen, mu daldi wax ne : “Man Yàlla xéewal na ma ba ma àndul ak ñoom fekke loolee [dee ci xare]” ;
🎧 Dégg

📜 Aaya 70-74 — An-Nisa

70ذَٰلِكَ الْفَضْلُ مِنَ اللَّهِ ۚ وَكَفَىٰ بِاللَّهِ عَلِيمًا
Loolooy ngëneel la jóge ca Yàlla. Te Yàlla doy na, mat na sëkk boroom xam-xam.
71يَا أَيُّهَا الَّذِينَ آمَنُوا خُذُوا حِذْرَكُمْ فَانفِرُوا ثُبَاتٍ أَوِ انفِرُوا جَمِيعًا
Éy yéen ñi gëm ! Nangeen fagaru ci seen [coongum noon], moo xam ngeen tasaaroo walla ngeen àndandoo.
72وَإِنَّ مِنكُمْ لَمَن لَّيُبَطِّئَنَّ فَإِنْ أَصَابَتْكُم مُّصِيبَةٌ قَالَ قَدْ أَنْعَمَ اللَّهُ عَلَيَّ إِذْ لَمْ أَكُن مَّعَهُمْ شَهِيدًا
Te am na ci yéen kuy des-deslu ginnaaw ba lu metti dal leen, mu daldi wax ne : “Man Yàlla xéewal na ma ba ma àndul ak ñoom fekke loolee [dee ci xare]” ;
73وَلَئِنْ أَصَابَكُمْ فَضْلٌ مِّنَ اللَّهِ لَيَقُولَنَّ كَأَن لَّمْ تَكُن بَيْنَكُمْ وَبَيْنَهُ مَوَدَّةٌ يَا لَيْتَنِي كُنتُ مَعَهُمْ فَأَفُوزَ فَوْزًا عَظِيمًا
te bu ngeen amee ndam lu leen Yàlla jox, muy wax mel ni cofeel doxul seen digganteek ñoom, ne : “Aka neexoon ma ànd ak ñoom ba am ndam lu rëy a rëy [alal ja]”.
74۞ فَلْيُقَاتِلْ فِي سَبِيلِ اللَّهِ الَّذِينَ يَشْرُونَ الْحَيَاةَ الدُّنْيَا بِالْآخِرَةِ ۚ وَمَن يُقَاتِلْ فِي سَبِيلِ اللَّهِ فَيُقْتَلْ أَوْ يَغْلِبْ فَسَوْفَ نُؤْتِيهِ أَجْرًا عَظِيمًا
Ña jaay seen dundug àddina jënde ko àllaaxira, nañu xare ci yoonu Yàlla. Képp ku xare ci yoonu Yàlla ba dee ca, mbaa mu not kàddu ndam la, Dananu ko jox pey gu rëy.
An-NisaFihi Alxuraan
176Aaya
MedinanRevelation
72Aaya

Tekki — An-Nisa 72

Simoore An-Nisa Aaya 72 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Te am na ci yéen kuy des-deslu ginnaaw ba lu…

Simoore Aaya 72/176 — An-Nisa النساء (Medinan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: An-Nisa Dégg, An-Nisa Tekki, An-Nisa mp3, An-Nisa pdf. Aaya 70–74. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers