Al-An'am · 149/165
Tekki Waxtaan — Al-An'am
قُلْ فَلِلَّهِ الْحُجَّةُ الْبَالِغَةُ ۖ فَلَوْ شَاءَ لَهَدَاكُمْ أَجْمَعِينَ ۝١٤٩
Qul falillaahil hujjatul baalighatu falaw shaaa`a lahadaakum ajma`een
📖 Tekkim Wolof
Neel : “Lii, wommatug Yàlla la, Moo ko moom. Bu ko sooboon, Mu jubal leen yéen ñépp.
🎧 Dégg

📜 Aaya 147-151 — Al-An'am

147فَإِن كَذَّبُوكَ فَقُل رَّبُّكُمْ ذُو رَحْمَةٍ وَاسِعَةٍ وَلَا يُرَدُّ بَأْسُهُ عَنِ الْقَوْمِ الْمُجْرِمِينَ
Bu ñu la weddee, neel : “Seen Boroom dey Ku am yërmaande ju yaatu la, waaye mbugalam ma jëm ca saay-saay sa dara mënukoo feg”.
148سَيَقُولُ الَّذِينَ أَشْرَكُوا لَوْ شَاءَ اللَّهُ مَا أَشْرَكْنَا وَلَا آبَاؤُنَا وَلَا حَرَّمْنَا مِن شَيْءٍ ۚ كَذَٰلِكَ كَذَّبَ الَّذِينَ مِن قَبْلِهِمْ حَتَّىٰ ذَاقُوا بَأْسَنَا ۗ قُلْ هَلْ عِندَكُم مِّنْ عِلْمٍ فَتُخْرِجُوهُ لَنَا ۖ إِن تَتَّبِعُونَ إِلَّا الظَّنَّ وَإِنْ أَنتُمْ إِلَّا تَخْرُصُونَ
Ñay bokkaale danañu wax ne : “Bu neexoon Yàlla, dunu bokkaale, sunuy baay it kon duñu bokkaale te dunu araamal dara, wat ci watiit !”. Noonu doŋŋ la ña leen jiitu woon doon weddee ba Sa mbugal ne xees ci seen kaw. Neel : “Ndax am ngeen xam-xam bu ngeen nu mën a génneel ? Yéen daal toppuleen lu moy ay njort te nekkuleen ci lu moy di fen”.
149قُلْ فَلِلَّهِ الْحُجَّةُ الْبَالِغَةُ ۖ فَلَوْ شَاءَ لَهَدَاكُمْ أَجْمَعِينَ
Neel : “Lii, wommatug Yàlla la, Moo ko moom. Bu ko sooboon, Mu jubal leen yéen ñépp.
150قُلْ هَلُمَّ شُهَدَاءَكُمُ الَّذِينَ يَشْهَدُونَ أَنَّ اللَّهَ حَرَّمَ هَٰذَا ۖ فَإِن شَهِدُوا فَلَا تَشْهَدْ مَعَهُمْ ۚ وَلَا تَتَّبِعْ أَهْوَاءَ الَّذِينَ كَذَّبُوا بِآيَاتِنَا وَالَّذِينَ لَا يُؤْمِنُونَ بِالْآخِرَةِ وَهُم بِرَبِّهِمْ يَعْدِلُونَ
Neel : “Indileen seeni seede yu mën a seede ne lii Yàlla dakoo araamal.”. Bu ñu ko seedee, yaw bu ca ànd ak ñoom, bul topp bànneexi ñay weddi sunuy ndigal ak ña gëmul àllaaxira, te ñoom dañuy ñaawal seen digganteek seen Boroom.
151۞ قُلْ تَعَالَوْا أَتْلُ مَا حَرَّمَ رَبُّكُمْ عَلَيْكُمْ ۖ أَلَّا تُشْرِكُوا بِهِ شَيْئًا ۖ وَبِالْوَالِدَيْنِ إِحْسَانًا ۖ وَلَا تَقْتُلُوا أَوْلَادَكُم مِّنْ إِمْلَاقٍ ۖ نَّحْنُ نَرْزُقُكُمْ وَإِيَّاهُمْ ۖ وَلَا تَقْرَبُوا الْفَوَاحِشَ مَا ظَهَرَ مِنْهَا وَمَا بَطَنَ ۖ وَلَا تَقْتُلُوا النَّفْسَ الَّتِي حَرَّمَ اللَّهُ إِلَّا بِالْحَقِّ ۚ ذَٰلِكُمْ وَصَّاكُم بِهِ لَعَلَّكُمْ تَعْقِلُونَ
Neel : “Kaayleen ma taril leen li Yàlla araamal ci yéen : mooy buleen ko bokkaaleek dara ; te nangeen di rafetal jëme ci seeni waajur. Te buleen rey seeni doom ngir ragal ñàkk. Ndax Nun [Yàlla], Noo leen di wërsërgal yéen, di leen wërsëgal ñoom it. Te buleen jegeñ njaaloo ca la cay feeñ ak la cay nëbbu. Te buleen rey bakkan bi Yàlla wormaal lu dul ci dëgg. Loolu la leen ci dénk ; ndax Yàlla ngeen xel-lu.
Al-An'amFihi Alxuraan
165Aaya
MeccanRevelation
149Aaya

Tekki — Al-An'am 149

Simoore Al-An'am Aaya 149 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Neel : “Lii, wommatug Yàlla la, Moo ko moom. Bu…

Simoore Aaya 149/165 — Al-An'am الأنعام (Meccan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Al-An'am Dégg, Al-An'am Tekki, Al-An'am mp3, Al-An'am pdf. Aaya 147–151. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers