Al-An'am · 21/165
Tekki Waxtaan — Al-An'am
وَمَنْ أَظْلَمُ مِمَّنِ افْتَرَىٰ عَلَى اللَّهِ كَذِبًا أَوْ كَذَّبَ بِآيَاتِهِ ۗ إِنَّهُ لَا يُفْلِحُ الظَّالِمُونَ ۝٢١
Wa man azlamu mim manif tara `alal laahi kaziban aw kazzaba bi Aayaatih; innahoo laa yuflihuz zaalimoon
📖 Tekkim Wolof
Ana ku gën a tooñ kuy duural Yàlla aw fen, walla di weddi ay kàddoom ? Tooñkat ya duñu texe de.

🎧 Dégg


📜 Aaya 19-23 — Al-An'am

19قُلْ أَيُّ شَيْءٍ أَكْبَرُ شَهَادَةً ۖ قُلِ اللَّهُ ۖ شَهِيدٌ بَيْنِي وَبَيْنَكُمْ ۚ وَأُوحِيَ إِلَيَّ هَٰذَا الْقُرْآنُ لِأُنذِرَكُم بِهِ وَمَن بَلَغَ ۚ أَئِنَّكُمْ لَتَشْهَدُونَ أَنَّ مَعَ اللَّهِ آلِهَةً أُخْرَىٰ ۚ قُل لَّا أَشْهَدُ ۚ قُلْ إِنَّمَا هُوَ إِلَٰهٌ وَاحِدٌ وَإِنَّنِي بَرِيءٌ مِّمَّا تُشْرِكُونَ
Neel : “Ana lan moo gën a màgg ci wàllu seede ? ”. Neel : “Yàlla dana nekk seede ci sama diggante ak yéen ; te sol nañu ma Alxuraan jii ngir ma waar ci yéen ak képp ku ca jot.”. Moo ndax dangeen di seede ne am na jeneen yàlla ju dul Yàlla ? Neeleen : “Seedewuma loolu”. Neel: “Moom daal nekkul lu dul jenn Yàlla doŋŋ. Te man set naa wecc ci li ngeen koy bokkaale”.
20الَّذِينَ آتَيْنَاهُمُ الْكِتَابَ يَعْرِفُونَهُ كَمَا يَعْرِفُونَ أَبْنَاءَهُمُ ۘ الَّذِينَ خَسِرُوا أَنفُسَهُمْ فَهُمْ لَا يُؤْمِنُونَ
Ña nga xam ne jox Nanu leen Téere, xam nañu ko ni ñu xàmmee seeni doom. Ña yàqal seen bopp duñu gëm de.
21وَمَنْ أَظْلَمُ مِمَّنِ افْتَرَىٰ عَلَى اللَّهِ كَذِبًا أَوْ كَذَّبَ بِآيَاتِهِ ۗ إِنَّهُ لَا يُفْلِحُ الظَّالِمُونَ
Ana ku gën a tooñ kuy duural Yàlla aw fen, walla di weddi ay kàddoom ? Tooñkat ya duñu texe de.
22وَيَوْمَ نَحْشُرُهُمْ جَمِيعًا ثُمَّ نَقُولُ لِلَّذِينَ أَشْرَكُوا أَيْنَ شُرَكَاؤُكُمُ الَّذِينَ كُنتُمْ تَزْعُمُونَ
Ca bis ba ñu leen di fang ñoom ñépp [dajale leen], bu ñuy wax ak ña daan bokkaale, ne leen : “Ana ña ngeen sosoon, bokkaale woon leen ak Yàlla ?
23ثُمَّ لَمْ تَكُن فِتْنَتُهُمْ إِلَّا أَن قَالُوا وَاللَّهِ رَبِّنَا مَا كُنَّا مُشْرِكِينَ
Su ko defee, seen njàqare duleen xiir ci leneen lu dul ñuy wax naan : “Giñ nanu ci Yàlla sunu Boroom ne nekkunu woon di way-bokkaale”.
Al-An'amFihi Alxuraan
165Aaya
MeccanRevelation
21Aaya

Tekki — Al-An'am 21

Simoore Al-An'am Aaya 21 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Ana ku gën a tooñ kuy duural Yàlla aw fen,…

Simoore Aaya 21/165 — Al-An'am الأنعام (Meccan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Al-An'am Dégg, Al-An'am Tekki, Al-An'am mp3, Al-An'am pdf. Aaya 19–23. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers