Al-An'am · 57/165
Tekki Waxtaan — Al-An'am
قُلْ إِنِّي عَلَىٰ بَيِّنَةٍ مِّن رَّبِّي وَكَذَّبْتُم بِهِ ۚ مَا عِندِي مَا تَسْتَعْجِلُونَ بِهِ ۚ إِنِ الْحُكْمُ إِلَّا لِلَّهِ ۖ يَقُصُّ الْحَقَّ ۖ وَهُوَ خَيْرُ الْفَاصِلِينَ ۝٥٧
Qul innee `alaa baiyinatim mir Rabbee wa kazzabtum bih; maa `indee maa tasta`jiloona bih; inil hukmu illaa lillaahi yaqussul haqqa wa Huwa khairul faasileen
📖 Tekkim Wolof
Neel : “Man dama nekk ci lu bir [leer nàññ], di lu jóge fa sama Boroom, ngeen weddi ko. Li ngeen di [laaj te di ko] yàkkamti, nekkul ci man. Àpp ba, Yàlla rekk a ko moom : Mooy nettali dëgg te Mooy gën jaa mën a àtte [téqale] ay mbir.

🎧 Dégg


📜 Aaya 55-59 — Al-An'am

55وَكَذَٰلِكَ نُفَصِّلُ الْآيَاتِ وَلِتَسْتَبِينَ سَبِيلُ الْمُجْرِمِينَ
Te noonu Lanuy leeralee tegtal yi ngir fésal yoonu tooñkat yi.
56قُلْ إِنِّي نُهِيتُ أَنْ أَعْبُدَ الَّذِينَ تَدْعُونَ مِن دُونِ اللَّهِ ۚ قُل لَّا أَتَّبِعُ أَهْوَاءَكُمْ ۙ قَدْ ضَلَلْتُ إِذًا وَمَا أَنَا مِنَ الْمُهْتَدِينَ
Neel : “Man tere nañu ma may jaamu li ngeen di jaamu te du Yàlla”. Neel itam : “Duma topp seeni bànneex : ndax su ma ko defee, damay sànku te kon duma bokk ca ñu gindiku ña”.
57قُلْ إِنِّي عَلَىٰ بَيِّنَةٍ مِّن رَّبِّي وَكَذَّبْتُم بِهِ ۚ مَا عِندِي مَا تَسْتَعْجِلُونَ بِهِ ۚ إِنِ الْحُكْمُ إِلَّا لِلَّهِ ۖ يَقُصُّ الْحَقَّ ۖ وَهُوَ خَيْرُ الْفَاصِلِينَ
Neel : “Man dama nekk ci lu bir [leer nàññ], di lu jóge fa sama Boroom, ngeen weddi ko. Li ngeen di [laaj te di ko] yàkkamti, nekkul ci man. Àpp ba, Yàlla rekk a ko moom : Mooy nettali dëgg te Mooy gën jaa mën a àtte [téqale] ay mbir.
58قُل لَّوْ أَنَّ عِندِي مَا تَسْتَعْجِلُونَ بِهِ لَقُضِيَ الْأَمْرُ بَيْنِي وَبَيْنَكُمْ ۗ وَاللَّهُ أَعْلَمُ بِالظَّالِمِينَ
Neel : “Bu fekkoon li ngeen di [laaj] di yàkkamti mi ngi ci man, kon mbir ya sottikoon na sama diggante ak yéen.” Te Yàllaa gën a xam tooñkat ya.
59۞ وَعِندَهُ مَفَاتِحُ الْغَيْبِ لَا يَعْلَمُهَا إِلَّا هُوَ ۚ وَيَعْلَمُ مَا فِي الْبَرِّ وَالْبَحْرِ ۚ وَمَا تَسْقُطُ مِن وَرَقَةٍ إِلَّا يَعْلَمُهَا وَلَا حَبَّةٍ فِي ظُلُمَاتِ الْأَرْضِ وَلَا رَطْبٍ وَلَا يَابِسٍ إِلَّا فِي كِتَابٍ مُّبِينٍ
Fa Moom la caabiy kumpa nekk. Kenn xamuleen ku dul Moom. Te xam na li nekk ci jéeri ji ak géej gi. Te amul fenn xob wuy rot te xamu ko. Du caageene wenn fepp wu nekk ci biir lëndëmu suuf si, di lu tooy, di lu wow, ndare du nekk na ci ab téere bu leer nàññ.
Al-An'amFihi Alxuraan
165Aaya
MeccanRevelation
57Aaya

Tekki — Al-An'am 57

Simoore Al-An'am Aaya 57 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Neel : “Man dama nekk ci lu bir [leer nàññ],…

Simoore Aaya 57/165 — Al-An'am الأنعام (Meccan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Al-An'am Dégg, Al-An'am Tekki, Al-An'am mp3, Al-An'am pdf. Aaya 55–59. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers