Al-An'am · 69/165
Tekki Waxtaan — Al-An'am
وَمَا عَلَى الَّذِينَ يَتَّقُونَ مِنْ حِسَابِهِم مِّن شَيْءٍ وَلَٰكِن ذِكْرَىٰ لَعَلَّهُمْ يَتَّقُونَ ۝٦٩
Wa maa `alal lazeena yattaqoona min hisaabihim min shai`inw wa laakin zikraa la`allahum yattaqoon
📖 Tekkim Wolof
Ñi ragal Yàlla, kenn àtteloowuleen ñooña. Xanaa kay ñu di leen fàttali. Ndax xéy-na ñoom it ñu ragal Yàlla.
🎧 Dégg

📜 Aaya 67-71 — Al-An'am

67لِّكُلِّ نَبَإٍ مُّسْتَقَرٌّ ۚ وَسَوْفَ تَعْلَمُونَ
Xew-xew bu ne am na waxtoon te dangeen mës a xam.”
68وَإِذَا رَأَيْتَ الَّذِينَ يَخُوضُونَ فِي آيَاتِنَا فَأَعْرِضْ عَنْهُمْ حَتَّىٰ يَخُوضُوا فِي حَدِيثٍ غَيْرِهِ ۚ وَإِمَّا يُنسِيَنَّكَ الشَّيْطَانُ فَلَا تَقْعُدْ بَعْدَ الذِّكْرَىٰ مَعَ الْقَوْمِ الظَّالِمِينَ
Boo gisee aw nit ñuy doyadal Sunuy kàddu, dëdduleen ba bañuy xuus ci weneen waxtaan. Bu la Séytaane fàtteloo ba nga fàtte ko. Saa soo ko fàttalikoo sañatoo toogandoo nag ak aw nit ñu di ay tooñkat.
69وَمَا عَلَى الَّذِينَ يَتَّقُونَ مِنْ حِسَابِهِم مِّن شَيْءٍ وَلَٰكِن ذِكْرَىٰ لَعَلَّهُمْ يَتَّقُونَ
Ñi ragal Yàlla, kenn àtteloowuleen ñooña. Xanaa kay ñu di leen fàttali. Ndax xéy-na ñoom it ñu ragal Yàlla.
70وَذَرِ الَّذِينَ اتَّخَذُوا دِينَهُمْ لَعِبًا وَلَهْوًا وَغَرَّتْهُمُ الْحَيَاةُ الدُّنْيَا ۚ وَذَكِّرْ بِهِ أَن تُبْسَلَ نَفْسٌ بِمَا كَسَبَتْ لَيْسَ لَهَا مِن دُونِ اللَّهِ وَلِيٌّ وَلَا شَفِيعٌ وَإِن تَعْدِلْ كُلَّ عَدْلٍ لَّا يُؤْخَذْ مِنْهَا ۗ أُولَٰئِكَ الَّذِينَ أُبْسِلُوا بِمَا كَسَبُوا ۖ لَهُمْ شَرَابٌ مِّنْ حَمِيمٍ وَعَذَابٌ أَلِيمٌ بِمَا كَانُوا يَكْفُرُونَ
Bàyyil ña nga xam ne dañoo jàppe seen diine am po ak i caaxaan fii ci àddina. Waarleen ci Alxuraan ndax benn bakkan bañ a yàqule ci sababus la mu doon fàggu, amul lenn kiiraay walla kuy rammu ku dul Yàlla. Te deesu ko nangul mu jotu ak menn jotu. Ñooña, dañoo alku ngir la ñu doon fàggu [ciy ñaawteef]. Naan gu tàng jérr lañuy jolu ak mbugal mu metti, ndax la ñu doon weddi.
71قُلْ أَنَدْعُو مِن دُونِ اللَّهِ مَا لَا يَنفَعُنَا وَلَا يَضُرُّنَا وَنُرَدُّ عَلَىٰ أَعْقَابِنَا بَعْدَ إِذْ هَدَانَا اللَّهُ كَالَّذِي اسْتَهْوَتْهُ الشَّيَاطِينُ فِي الْأَرْضِ حَيْرَانَ لَهُ أَصْحَابٌ يَدْعُونَهُ إِلَى الْهُدَى ائْتِنَا ۗ قُلْ إِنَّ هُدَى اللَّهِ هُوَ الْهُدَىٰ ۖ وَأُمِرْنَا لِنُسْلِمَ لِرَبِّ الْعَالَمِينَ
Neel : “Moo ndax danuy jaamu loo xam ne dunu jariñ, dunu lor, bàyyi Yàlla ? Kon dey nu dellu ginnaaw, te fekk Yàlla gindi nanu ba noppi, mel ni ka nga xam ne Séytaane dakoo réeral ci kaw suuf, muy ku gëlëm, ay àndandoom di ko woo ci njub, naan ko : - “Ñëwal ci nun.”. Neel : “Njubug Yàlla mooy dëggi-dëggi njub. Te am nanu ndigal ci wommatu jëm ci Boroom àddina si,
Al-An'amFihi Alxuraan
165Aaya
MeccanRevelation
69Aaya

Tekki — Al-An'am 69

Simoore Al-An'am Aaya 69 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Ñi ragal Yàlla, kenn àtteloowuleen ñooña. Xanaa kay ñu di…

Simoore Aaya 69/165 — Al-An'am الأنعام (Meccan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Al-An'am Dégg, Al-An'am Tekki, Al-An'am mp3, Al-An'am pdf. Aaya 67–71. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers