Al-A'raf · 175/206
Tekki Waxtaan — Al-A'raf
وَاتْلُ عَلَيْهِمْ نَبَأَ الَّذِي آتَيْنَاهُ آيَاتِنَا فَانسَلَخَ مِنْهَا فَأَتْبَعَهُ الشَّيْطَانُ فَكَانَ مِنَ الْغَاوِينَ ۝١٧٥
Watlu `alaihim naba allazeee aatainaahu Aayaatinaa fansalakha minhaa fa atba`a hush Shaytaano fakaana minal ghaaween
📖 Tekkim Wolof
Nettalileen ka Nu joxoon Sunuy mbóot mu rocceeku ca. Séytaane topp ko, tax na mu bokk ca way-beew ña.

🎧 Dégg


📜 Aaya 173-177 — Al-A'raf

173أَوْ تَقُولُوا إِنَّمَا أَشْرَكَ آبَاؤُنَا مِن قَبْلُ وَكُنَّا ذُرِّيَّةً مِّن بَعْدِهِمْ ۖ أَفَتُهْلِكُنَا بِمَا فَعَلَ الْمُبْطِلُونَ
mbaa ngeen bañ a wax : “Du dara lu dul sunuy maam dañoo bokkaale woon lu jiitu nu sëtoo ca ñoom ginnaaw ga. Ndax dees na nu mbugal [ci loo xam ne ña jubutoon ca nun ñoo ko def] ? ”
174وَكَذَٰلِكَ نُفَصِّلُ الْآيَاتِ وَلَعَلَّهُمْ يَرْجِعُونَ
Noonu la Nuy leeralee tegtal yi. Ndax xéy-na ñu dellusi [ci seen Boroom] !
175وَاتْلُ عَلَيْهِمْ نَبَأَ الَّذِي آتَيْنَاهُ آيَاتِنَا فَانسَلَخَ مِنْهَا فَأَتْبَعَهُ الشَّيْطَانُ فَكَانَ مِنَ الْغَاوِينَ
Nettalileen ka Nu joxoon Sunuy mbóot mu rocceeku ca. Séytaane topp ko, tax na mu bokk ca way-beew ña.
176وَلَوْ شِئْنَا لَرَفَعْنَاهُ بِهَا وَلَٰكِنَّهُ أَخْلَدَ إِلَى الْأَرْضِ وَاتَّبَعَ هَوَاهُ ۚ فَمَثَلُهُ كَمَثَلِ الْكَلْبِ إِن تَحْمِلْ عَلَيْهِ يَلْهَثْ أَوْ تَتْرُكْهُ يَلْهَث ۚ ذَّٰلِكَ مَثَلُ الْقَوْمِ الَّذِينَ كَذَّبُوا بِآيَاتِنَا ۚ فَاقْصُصِ الْقَصَصَ لَعَلَّهُمْ يَتَفَكَّرُونَ
Su nu sooboon Nu yékkatikook mbóot yooyu, waaye dafa jengoon jëm ci àddina, topp bànneexam. Dafay mel ni xaj, boo ko songee muy yalkat, boo ko bàyyee muy yalkat. Loolu mooy niróowaaleeb nit ña weddi Sunuy kàddu. Nettalil xew-xew ba. Xéy-na ñoom ñu fàttaliku !
177سَاءَ مَثَلًا الْقَوْمُ الَّذِينَ كَذَّبُوا بِآيَاتِنَا وَأَنفُسَهُمْ كَانُوا يَظْلِمُونَ
Nekkinu nit ña weddi Sunuy kàddu, aka bon, waaye seen bopp lañuy tooñ nag.
Al-A'rafFihi Alxuraan
206Aaya
MeccanRevelation
175Aaya

Tekki — Al-A'raf 175

Simoore Al-A'raf Aaya 175 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Nettalileen ka Nu joxoon Sunuy mbóot mu rocceeku ca. Séytaane…

Simoore Aaya 175/206 — Al-A'raf الأعراف (Meccan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Al-A'raf Dégg, Al-A'raf Tekki, Al-A'raf mp3, Al-A'raf pdf. Aaya 173–177. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers