Al-A'raf · 84/206
Tekki Waxtaan — Simoore Al-A'raf
وَأَمْطَرْنَا عَلَيْهِم مَّطَرًا ۖ فَانظُرْ كَيْفَ كَانَ عَاقِبَةُ الْمُجْرِمِينَ ۝٨٤
Wa `amtarnaa `alaihim mataran fanzur kaifa kaana aaqibatul mujjrimeen
📖 Tekkim Wolof
Nu sotti ca seen kaw ab taw , waay-waay gisal na mujjug saay-saay sa mel !

🎧 Dégg


📜 Aaya 82-86 — Simoore Al-A'raf

82وَمَا كَانَ جَوَابَ قَوْمِهِ إِلَّا أَن قَالُوا أَخْرِجُوهُم مِّن قَرْيَتِكُمْ ۖ إِنَّهُمْ أُنَاسٌ يَتَطَهَّرُونَ
Toontul aw nitam nekkul lu dulñu ne : “Génneleen leen seenub dëkk. Ndax ñoom aw nit lañu ñuy laab-laablu” !
83فَأَنجَيْنَاهُ وَأَهْلَهُ إِلَّا امْرَأَتَهُ كَانَتْ مِنَ الْغَابِرِينَ
Nu musal ko (Nun Yàlla) mook waa këram, ba mu des soxnaam, moom dafa des ca mbugal ma.
84وَأَمْطَرْنَا عَلَيْهِم مَّطَرًا ۖ فَانظُرْ كَيْفَ كَانَ عَاقِبَةُ الْمُجْرِمِينَ
Nu sotti ca seen kaw ab taw , waay-waay gisal na mujjug saay-saay sa mel !
85وَإِلَىٰ مَدْيَنَ أَخَاهُمْ شُعَيْبًا ۗ قَالَ يَا قَوْمِ اعْبُدُوا اللَّهَ مَا لَكُم مِّنْ إِلَٰهٍ غَيْرُهُ ۖ قَدْ جَاءَتْكُم بَيِّنَةٌ مِّن رَّبِّكُمْ ۖ فَأَوْفُوا الْكَيْلَ وَالْمِيزَانَ وَلَا تَبْخَسُوا النَّاسَ أَشْيَاءَهُمْ وَلَا تُفْسِدُوا فِي الْأَرْضِ بَعْدَ إِصْلَاحِهَا ۚ ذَٰلِكُمْ خَيْرٌ لَّكُمْ إِن كُنتُم مُّؤْمِنِينَ
(Fàttalikul ba Nu yónnee) fa Madyaana, seen mbokk Chuhaybu, mu ne leen : "Éy yéen samaw nit, jaamuleen Yàlla. Amuleen jeneen Yàlla ju dul Moom. Te ay lay yu leer dikkal na leen yu bawoo ca seen Boroom. Kon nangeen di matal natt ak màndaxe te buleen wàññil nit ña, la ñu moom. Te it buleen yàq ci suuf si ginnaaw ba ñu ko yéwénalee. Loolu dey, moo di li gën ci yéen, bu fekkee ni gëm ngeen.
86وَلَا تَقْعُدُوا بِكُلِّ صِرَاطٍ تُوعِدُونَ وَتَصُدُّونَ عَن سَبِيلِ اللَّهِ مَنْ آمَنَ بِهِ وَتَبْغُونَهَا عِوَجًا ۚ وَاذْكُرُوا إِذْ كُنتُمْ قَلِيلًا فَكَثَّرَكُمْ ۖ وَانظُرُوا كَيْفَ كَانَ عَاقِبَةُ الْمُفْسِدِينَ
Te buleen di toog ci wépp yoon, di dëkku ñi gëm Yàlla, di leen wëlbati, di dox seen digganteek yoonu Yàlla, di ko jéngal. Fàttalikuleen ba ngeen nekkee di ñu néew, Mu baril leen. Te nangeen settantal naka la mujjug yàqkat ya meloon.
Al-A'rafFihi Alxuraan
206Aaya
MeccanRevelation
84Aaya

Tekki — Al-A'raf 84

Simoore Al-A'raf Aaya 84 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Nu sotti ca seen kaw ab taw , waay-waay gisal…

Simoore Aaya 84/206 — Simoore Al-A'raf الأعراف (Meccan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Simoore Al-A'raf Dégg, Simoore Al-A'raf Tekki, Simoore Al-A'raf mp3, Simoore Al-A'raf pdf. Aaya 82–86. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Monday, September 7, 2026

Don't forget us in your sincere prayers