Simoore An-Nazi'at pdf — Wàcce (Wolof)
Simoore An-Nazi'at pdf Wolof — Wàcce Simoore An-Nazi'at Tekki. Simoore An-Nazi'at (Meccan) 46 Aaya.
Related
More Simoore PDF
Simoore An-Nazi'at

ﮢﮣﮤ
79:1
Ci roccikat yay sanjaafu, maa ngi giñ !
ﮥﮦﮧ
79:2
Ak ña koy rocci ndànk-ndànk !
ﮨﮩﮪ
79:3
Ak ñay féey ca asamaan sa,
ﮫﮬﮭ
79:4
ak ñay jëkënte cig ngëm,
ﮮﮯﮰ
79:5
ak ñay settantal di lijjënti mbir yi!
ﮱﯓﯔﯕ
79:6
Ca bis boobule [suuf] di yëngutu ci wal gu jëkkug mbiib ga [bufta ba]
ﯖﯗﯘ
79:7
ñaarelug wal ga daldi cay topp.
ﯙﯚﯛﯜ
79:8
Bu keroogee, dana am ay xol yu tiit,
ﯝﯞﯟ
79:9
seenub gis sàjju ngir ragal.
ﯠﯡﯢﯣﯤﯥ
79:10
Ña ngay wax naan : “Ndax danuy dundaat ginnaaw dee,
ﯦﯧﯨﯩﯪ
79:11
ak sax ginnaaw bu nu doonee ay yax yu funux ? ”
ﯫﯬﯭﯮﯯﯰ
79:12
Ña ngay wax naan : “loolu deey yàqule la ! ”
ﯱﯲﯳﯴﯵ
79:13
loolu ab jàjj la,
ﯶﯷﯸﯹ
79:14
ñu jekki-jekki rekk ne jaww ci kaw suuf si dekkiwaat.
ﯺﯻﯼﯽﯾ
79:15
Ndax waxtaanu Muusaa dikkël na la ? Ay xibaaram ?
ﯿﰀﰁﰂﰃﰄﰅ
79:16
Ba ko Boroomam di woo, ca xuru Tuwaa, wu sell wa, di ko wax ne :
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖ
79:17
“Demal ca Firawna. Moom bew na !
ﭗﭘﭙﭚﭛﭜﭝ
79:18
Te nga wax ko ne : “Ndax bëgg ngaa tuub ?
ﭞﭟﭠﭡﭢ
79:19
kon dey da naa la gindi ci sa Boroom nga ragal ko ? ”
ﭣﭤﭥﭦ
79:20
Mu wan ko keemtaan yu màgg ya.
ﭧﭨﭩ
79:21
Mu weddi ko (Firawna) daldi koy moy ;
ﭪﭫﭬﭭ
79:22
Mu daldi, dumóoyu, féew dem,
ﭮﭯﭰ
79:23
daldi woo nit ña dajale leen,
ﭱﭲﭳﭴﭵ
79:24
daldi wax ne : “Man maay sen boroom, bi gëna kawe”.
ﭶﭷﭸﭹﭺﭻ
79:25
Yàlla daldi koy faagaagal mbugalum àddina muy sar ba àllaaxira.
ﭼﭽﭾﭿﮀﮁﮂ
79:26
Ag fàttalikoo ngi ci loolu ña ragal Yàlla.
ﮃﮄﮅﮆﮇﮈﮉﮊ
79:27
li ngeen sos moo gëna dëgër ? walla asamaan si ma tabax ?
ﮋﮌﮍﮎ
79:28
Kaweel na talaayam ba, te maasale ko ;
ﮏﮐﮑﮒﮓ
79:29
Moo lëndamal guddi yi te leeral bëccëg yi.
ﮔﮕﮖﮗﮘ
79:30
Ginnaaw loolu moo tallal suuf si :
ﮙﮚﮛﮜﮝ
79:31
Mu génnee ca ndox ak i gàncax,
ﮞﮟﮠ
79:32
mu saxal ca duutan ca tund doj yi,
ﮡﮢﮣﮤ
79:33
mu di bànneexu, ci yéen ak ci seenug jur.
ﮥﮦﮧﮨﮩ
79:34
Saa su mbambu mu rëy ma dikkee,
ﮪﮫﮬﮭﮮﮯ
79:35
bu keroogee nit dana fàttaliku la mu jëfoon,
ﮰﮱﯓﯔﯕ
79:36
Safara danaan fàŋŋ ku ko xool gis ko...
ﯖﯗﯘﯙ
79:37
Képp ku bewoon daan jalgati
ﯚﯛﯜﯝ
79:38
te bëggoon dundug àddina sii doŋŋ (di ko xëntéewóo),
ﯞﯟﯠﯡﯢ
79:39
kookee, Safaraa di wàccuwaayam.
ﯣﯤﯥﯦﯧﯨﯩﯪﯫﯬ
79:40
Képp ku ragaloon ne dana taxaw ca Boroomam, te daan tere bakkanam bànneex (ay caaxaan),
ﯭﯮﯯﯰﯱ
79:41
kookee àjjanaa di wàccuwaayam.
ﯲﯳﯴﯵﯶﯷ
79:42
Ña nga lay laaj bis pénc ba : “Kañ lay teeral”
ﯸﯹﯺﯻﯼ
79:43
Ana ban xam-xam nga ci am ngir tontu leen ?
ﯽﯾﯿﰀ
79:44
Ab yemukaayam sa Boroom rekk ko xam.
ﰁﰂﰃﰄﰅﰆ
79:45
Yaw nag ab xuppekat doŋŋ nga ngir ña ko ragal.
ﰇﰈﰉﰊﰋﰌﰍﰎﰏﰐ
79:46
Bis bu ñu ko gisee, dafay mel ne seen dund gépp genn ngoon la woon walla yoor-yoor.
Alxuraan bu Tedd bi
Wednesday, September 9, 2026
Don't forget us in your sincere prayers







