PDF —
22 Aaya Meccan PDF
Built right in your browser — download starts automatically

Simoore Al-Buruj pdf — Wàcce (Wolof)

Simoore Al-Buruj pdf Wolof — Wàcce Simoore Al-Buruj Tekki. Simoore Al-Buruj (Meccan) 22 Aaya.

← Al-InshiqaqSimoore Al-Buruj At-Tariq →


22 Aaya · Meccan · Wolof
bismillah
ﭛﭜﭝﭞ
85:1 Ci asamaan sa di boroom biddiw yu mag ! Maa ngi giñ!
ﭟﭠﭡ
85:2 ak ci bis ba ñu dige !
ﭢﭣﭤ
85:3 ak ci kuy seede ak ca ka ñuy seede !
ﭥﭦﭧﭨ
85:4 Faagaagal na waa Uxduud,
ﭩﭪﭫﭬ
85:5 ak ci safara wa am lu koy xamb,
ﭭﭮﭯﭰﭱ
85:6 ca ba ñu toogee wër ko,
ﭲﭳﭴﭵﭶﭷﭸ
85:7 te ñoom seede la ñu ca la ñu defoon way gëm ña,
ﭹﭺﭻﭼﭽﭾﭿﮀﮁﮂ
85:8 te fitnaale wu ñu leen ci lu dul ne da ñoo gëm Yàlla, boroom Kàttan ga, Yayoowaakooni cant ba,
ﮃﮄﮅﮆﮇﮈﮉﮊﮋﮌﮍﮎ
85:9 Yàlla mi moom nguurug asamaan yeek suuf si. Te yàlla seede la ci lépp lu ne.
ﮏﮐﮑﮒﮓﮔﮕﮖﮗﮘﮙﮚﮛﮜﮝ
85:10 Ña daan fitnaal jullit yu góor yaak yu jigéen ya, te tubu ñu ko, dananu am mbugëlum Jahanama ñu di leen ca lakk. (ca safaraam wa)
ﮞﮟﮠﮡﮢﮣﮤﮥﮦﮧﮨﮩﮪﮫﮬﮭ
85:11 Ña gëmoon te daan jëf yiw am nañu ay Àjjana yu ay dex di daw ci suufam. Loolu moo di texe gu mag ga.
ﮮﮯﮰﮱﯓ
85:12 Sa fayug boroom lu tar la.
ﯔﯕﯖﯗﯘ
85:13 Moom mooy, sos bindeef yi, te mooleen di dekkilaat.
ﯙﯚﯛﯜ
85:14 Te moom moo di Jéggëlaakoon bi, di soppi lépp,
ﯝﯞﯟﯠ
85:15 Mooy boroom Gàngunaay gu Màgg ga (Aras),
ﯡﯢﯣﯤ
85:16 Lu mu namm dana ko def.
ﯥﯦﯧﯨﯩ
85:17 Moo ndax waxtaanu xarekat ya dikal na la ( xibaar ya),
ﯪﯫﯬ
85:18 Firawna, ak Samuud ?
ﯭﯮﯯﯰﯱﯲ
85:19 Yéefër ya dañuy weddi,
ﯳﯴﯵﯶﯷ
85:20 te Yàlla ngi leen peeg, ci wet gu nekk.
ﯸﯹﯺﯻﯼ
85:21 li wér mooy Alxuraan ju màgg la
ﯽﯾﯿﰀ
85:22 ca biir Àlluwa ja ñu wàttu fa Yàlla (Lawhul Mahfuus ).

Alxuraan bu Tedd bi


Wednesday, September 9, 2026

Don't forget us in your sincere prayers