Yunus · 60/109
Tekki Waxtaan — Yunus
وَمَا ظَنُّ الَّذِينَ يَفْتَرُونَ عَلَى اللَّهِ الْكَذِبَ يَوْمَ الْقِيَامَةِ ۗ إِنَّ اللَّهَ لَذُو فَضْلٍ عَلَى النَّاسِ وَلَٰكِنَّ أَكْثَرَهُمْ لَا يَشْكُرُونَ ۝٦٠
Wa maa zannul lazeena yaftaroona `alal laahil kaziba Yawmal Qiyaamah; innal laaha lazoo fadlin `alan naasi wa laakinna aksarahum laa yashkuroon
📖 Tekkim Wolof
Ana lan mooy njortul ñiy duural Yàlla ay fen Bis-pénc ba ? - Dafa dëggu ne Yàlla xéewalaakoon la, waaye li ëpp ci ñoom duñu gërêm [Yàlla].

🎧 Dégg


📜 Aaya 58-62 — Yunus

58قُلْ بِفَضْلِ اللَّهِ وَبِرَحْمَتِهِ فَبِذَٰلِكَ فَلْيَفْرَحُوا هُوَ خَيْرٌ مِّمَّا يَجْمَعُونَ
Neel : “Bégleen ci xéewal ak yërmaande ; te loolu lépp moo gën la ñu daan dajale [ci alal]”.
59قُلْ أَرَأَيْتُم مَّا أَنزَلَ اللَّهُ لَكُم مِّن رِّزْقٍ فَجَعَلْتُم مِّنْهُ حَرَامًا وَحَلَالًا قُلْ آللَّهُ أَذِنَ لَكُمْ ۖ أَمْ عَلَى اللَّهِ تَفْتَرُونَ
Neel : “Moo ndax gis ngeen li leen Yàlla wàcceel ci xéewal, ngeen jàpp ne am na ci yu araam ak yu dagan ? - Neel : “Ndax Yàllaa leen ko digal ? Walla dangeen di duural Yàlla” ?
60وَمَا ظَنُّ الَّذِينَ يَفْتَرُونَ عَلَى اللَّهِ الْكَذِبَ يَوْمَ الْقِيَامَةِ ۗ إِنَّ اللَّهَ لَذُو فَضْلٍ عَلَى النَّاسِ وَلَٰكِنَّ أَكْثَرَهُمْ لَا يَشْكُرُونَ
Ana lan mooy njortul ñiy duural Yàlla ay fen Bis-pénc ba ? - Dafa dëggu ne Yàlla xéewalaakoon la, waaye li ëpp ci ñoom duñu gërêm [Yàlla].
61وَمَا تَكُونُ فِي شَأْنٍ وَمَا تَتْلُو مِنْهُ مِن قُرْآنٍ وَلَا تَعْمَلُونَ مِنْ عَمَلٍ إِلَّا كُنَّا عَلَيْكُمْ شُهُودًا إِذْ تُفِيضُونَ فِيهِ ۚ وَمَا يَعْزُبُ عَن رَّبِّكَ مِن مِّثْقَالِ ذَرَّةٍ فِي الْأَرْضِ وَلَا فِي السَّمَاءِ وَلَا أَصْغَرَ مِن ذَٰلِكَ وَلَا أَكْبَرَ إِلَّا فِي كِتَابٍ مُّبِينٍ
Doo nekk ci menn mbir, walla ngay jàng dara ci Alxuraan, walla ngeen def jenn jëf te Nekkunu ca seede ba ngeen cay duggu. Te lu toll ni pepp su tuuti du rëcc sa Boroom, du ci suuf si, du ci asamaan yi ; te amul lu ko gën a tuuti walla lu ko gën a rëy lu dul ne mi ngi ci ab téere bu bir.
62أَلَا إِنَّ أَوْلِيَاءَ اللَّهِ لَا خَوْفٌ عَلَيْهِمْ وَلَا هُمْ يَحْزَنُونَ
Ca dëgg-dëgg, ña féeteek Yàlla duñu gis lu ñu ragal, duñu gis njàqare,
YunusFihi Alxuraan
109Aaya
MeccanRevelation
60Aaya

Tekki — Yunus 60

Simoore Yunus Aaya 60 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Ana lan mooy njortul ñiy duural Yàlla ay fen Bis-pénc…

Simoore Aaya 60/109 — Yunus يونس (Meccan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Yunus Dégg, Yunus Tekki, Yunus mp3, Yunus pdf. Aaya 58–62. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers