Hud · 40/123
Tekki Waxtaan — Hud
حَتَّىٰ إِذَا جَاءَ أَمْرُنَا وَفَارَ التَّنُّورُ قُلْنَا احْمِلْ فِيهَا مِن كُلٍّ زَوْجَيْنِ اثْنَيْنِ وَأَهْلَكَ إِلَّا مَن سَبَقَ عَلَيْهِ الْقَوْلُ وَمَنْ آمَنَ ۚ وَمَا آمَنَ مَعَهُ إِلَّا قَلِيلٌ ۝٤٠
Hattaaa izaa jaaa`a amrunaa wa faarat tannooru qulnah mil feehaa min kullin zawjainis naini wa ahlaka illaa man sabaqa `alaihil qawlu wa man aaman; wa maaa aamana ma`ahooo illaa qaleel
📖 Tekkim Wolof
Ba Sunu ndigal agsee, ndox ma di ballee fu ne, Nu ne : “Defal ci gaal gi, ci xeet wu nekk ñaar [góor ak jigéen] ak sa njaboot - ba mu des ña dogal ba xas dal [ña weddi] - ak ña gëm”. Te lim bu néew rekk a gëmoon.

🎧 Dégg


📜 Aaya 38-42 — Hud

38وَيَصْنَعُ الْفُلْكَ وَكُلَّمَا مَرَّ عَلَيْهِ مَلَأٌ مِّن قَوْمِهِ سَخِرُوا مِنْهُ ۚ قَالَ إِن تَسْخَرُوا مِنَّا فَإِنَّا نَسْخَرُ مِنكُمْ كَمَا تَسْخَرُونَ
Muy defar gaal ga. Saa yu ko kenn ci kilifay aw nitam rombee, reetaan ko. Mu ne : “Su ngeen nu reetaanee [tey jii], nun itam [dananu leen reetaan] nu ngeen nu reetaanee woon.
39فَسَوْفَ تَعْلَمُونَ مَن يَأْتِيهِ عَذَابٌ يُخْزِيهِ وَيَحِلُّ عَلَيْهِ عَذَابٌ مُّقِيمٌ
Xalset ngeen a xam ana kan la mbugalam di dal, toroxal ko, ba noppi mbugalam wàcc ci kawam, di lu sax dàkk ! ”
40حَتَّىٰ إِذَا جَاءَ أَمْرُنَا وَفَارَ التَّنُّورُ قُلْنَا احْمِلْ فِيهَا مِن كُلٍّ زَوْجَيْنِ اثْنَيْنِ وَأَهْلَكَ إِلَّا مَن سَبَقَ عَلَيْهِ الْقَوْلُ وَمَنْ آمَنَ ۚ وَمَا آمَنَ مَعَهُ إِلَّا قَلِيلٌ
Ba Sunu ndigal agsee, ndox ma di ballee fu ne, Nu ne : “Defal ci gaal gi, ci xeet wu nekk ñaar [góor ak jigéen] ak sa njaboot - ba mu des ña dogal ba xas dal [ña weddi] - ak ña gëm”. Te lim bu néew rekk a gëmoon.
41۞ وَقَالَ ارْكَبُوا فِيهَا بِسْمِ اللَّهِ مَجْرَاهَا وَمُرْسَاهَا ۚ إِنَّ رَبِّي لَغَفُورٌ رَّحِيمٌ
Mu ne leen : “Yéegleen ci biir tey tudd Yàlla, mooy aw xélam, te it ag teeram. Sama Boroom nag Jéggalaakoon la, Jaglewaakoon la”.
42وَهِيَ تَجْرِي بِهِمْ فِي مَوْجٍ كَالْجِبَالِ وَنَادَىٰ نُوحٌ ابْنَهُ وَكَانَ فِي مَعْزِلٍ يَا بُنَيَّ ارْكَب مَّعَنَا وَلَا تَكُن مَّعَ الْكَافِرِينَ
Gaal gay daw ak ñoom ciy ganax yu kawe ni ay tundu. Nooh daldi woo doomam, fekk mu beru woon, ne ko : "Sama doom, yéegal ànd ak nun te bul ànd ak yéefar yi”.
HudFihi Alxuraan
123Aaya
MeccanRevelation
40Aaya

Tekki — Hud 40

Simoore Hud Aaya 40 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Ba Sunu ndigal agsee, ndox ma di ballee fu ne,…

Simoore Aaya 40/123 — Hud هود (Meccan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Hud Dégg, Hud Tekki, Hud mp3, Hud pdf. Aaya 38–42. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers