Yusuf · 102/111
Tekki Waxtaan — Yusuf
ذَٰلِكَ مِنْ أَنبَاءِ الْغَيْبِ نُوحِيهِ إِلَيْكَ ۖ وَمَا كُنتَ لَدَيْهِمْ إِذْ أَجْمَعُوا أَمْرَهُمْ وَهُمْ يَمْكُرُونَ ۝١٠٢
Zaalika min ambaaa`il ghaibi nooheehi ilaika wa maa kunta ladaihim iz ajma`ooo amrahum wa hum yamkuroon
📖 Tekkim Wolof
Loolu bokk na ca xew-xew yu fàddu ya, ñu soloo la ko. Te fekkewuloo ba ñu mànkoo ci mbir, di tëral pexe.
🎧 Dégg

📜 Aaya 100-104 — Yusuf

100وَرَفَعَ أَبَوَيْهِ عَلَى الْعَرْشِ وَخَرُّوا لَهُ سُجَّدًا ۖ وَقَالَ يَا أَبَتِ هَٰذَا تَأْوِيلُ رُؤْيَايَ مِن قَبْلُ قَدْ جَعَلَهَا رَبِّي حَقًّا ۖ وَقَدْ أَحْسَنَ بِي إِذْ أَخْرَجَنِي مِنَ السِّجْنِ وَجَاءَ بِكُم مِّنَ الْبَدْوِ مِن بَعْدِ أَن نَّزَغَ الشَّيْطَانُ بَيْنِي وَبَيْنَ إِخْوَتِي ۚ إِنَّ رَبِّي لَطِيفٌ لِّمَا يَشَاءُ ۚ إِنَّهُ هُوَ الْعَلِيمُ الْحَكِيمُ
Mu yéegal ñaari waajuram ci kaw gàngunaay ga, ñu rot sujjóotal ko. Mu ne : "Yaw sama baay, lii moo di pirim sama gént ga woon. Sama Boroom def na ko muy dëgg... Te it defal na ma lu baax ba ma mën a génn ci kaso bi, indi leen ngeen jóge ca àll ba, ginnaaw ba Séytaane yàqee sama diggante ak samay doomi-baay. Sama Boroom nag ku lewet la ca la ko soob. Mooy Ku xam te xereñ.
101۞ رَبِّ قَدْ آتَيْتَنِي مِنَ الْمُلْكِ وَعَلَّمْتَنِي مِن تَأْوِيلِ الْأَحَادِيثِ ۚ فَاطِرَ السَّمَاوَاتِ وَالْأَرْضِ أَنتَ وَلِيِّي فِي الدُّنْيَا وَالْآخِرَةِ ۖ تَوَفَّنِي مُسْلِمًا وَأَلْحِقْنِي بِالصَّالِحِينَ
Yaw sama Boroom, may nga ma nguur, jàngal nga ma it pirim gént. Yaw mi sos asamaan yi ak suuf si, Yaw yaay sama sang, ci àddina ak ca àllaaxira. Yal na nga may rey te fekk may aji-jublu ci Yaw [sama Boroom] sama mbir mépp te yal na nga ma yéege ci ñu yiw ña.
102ذَٰلِكَ مِنْ أَنبَاءِ الْغَيْبِ نُوحِيهِ إِلَيْكَ ۖ وَمَا كُنتَ لَدَيْهِمْ إِذْ أَجْمَعُوا أَمْرَهُمْ وَهُمْ يَمْكُرُونَ
Loolu bokk na ca xew-xew yu fàddu ya, ñu soloo la ko. Te fekkewuloo ba ñu mànkoo ci mbir, di tëral pexe.
103وَمَا أَكْثَرُ النَّاسِ وَلَوْ حَرَصْتَ بِمُؤْمِنِينَ
Te li ëpp ci nit ñi duñu gëm doonte la xér nga sax yaw [ci ña gëm].
104وَمَا تَسْأَلُهُمْ عَلَيْهِ مِنْ أَجْرٍ ۚ إِنْ هُوَ إِلَّا ذِكْرٌ لِّلْعَالَمِينَ
Te laajoo leen ag pey ci [Alxuraan ji]. Te nekkul leneen lu dul ag waare ñeel àddina si yépp.
YusufFihi Alxuraan
111Aaya
MeccanRevelation
102Aaya

Tekki — Yusuf 102

Simoore Yusuf Aaya 102 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Loolu bokk na ca xew-xew yu fàddu ya, ñu soloo…

Simoore Aaya 102/111 — Yusuf يوسف (Meccan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Yusuf Dégg, Yusuf Tekki, Yusuf mp3, Yusuf pdf. Aaya 100–104. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers