Ar-Ra'd · 39/43
Tekki Waxtaan — Ar-Ra'd
يَمْحُو اللَّهُ مَا يَشَاءُ وَيُثْبِتُ ۖ وَعِندَهُ أُمُّ الْكِتَابِ ۝٣٩
Yamhul laahu maa yashaaa`u wa yusbitu wa `indahooo ummul Kitaab
📖 Tekkim Wolof
Yàlla dana far lu ko soob te Dana saxal itam [lu ko soob] ca cosaani Téere ba di [Lawhul- Mahfuuz] ma nga fa Moom.

🎧 Dégg


📜 Aaya 37-41 — Ar-Ra'd

37وَكَذَٰلِكَ أَنزَلْنَاهُ حُكْمًا عَرَبِيًّا ۚ وَلَئِنِ اتَّبَعْتَ أَهْوَاءَهُم بَعْدَمَا جَاءَكَ مِنَ الْعِلْمِ مَا لَكَ مِنَ اللَّهِ مِن وَلِيٍّ وَلَا وَاقٍ
Noonu la Nu ko wàccee muy lu ñu xereñe ci làkku araab [di ay àtte]. Te boo toppoon seeni bànneex ginnaaw li la dikkal ci xam-xam, doo am kenn ku la wattu waxantumaak ku lay fegal [mbugalum] Yàlla.
38وَلَقَدْ أَرْسَلْنَا رُسُلًا مِّن قَبْلِكَ وَجَعَلْنَا لَهُمْ أَزْوَاجًا وَذُرِّيَّةً ۚ وَمَا كَانَ لِرَسُولٍ أَن يَأْتِيَ بِآيَةٍ إِلَّا بِإِذْنِ اللَّهِ ۗ لِكُلِّ أَجَلٍ كِتَابٌ
Yónni woon Nanu ay Yonent lu jiitu, te defaloon Nanu leen ay soxna ak i doom. Te ab Yonent daawul mën a def kéemaan lu dul ci ndigalul Yàlla. Àppub xew-xew bu mu mën a doon bind Nanu ko ba noppi.
39يَمْحُو اللَّهُ مَا يَشَاءُ وَيُثْبِتُ ۖ وَعِندَهُ أُمُّ الْكِتَابِ
Yàlla dana far lu ko soob te Dana saxal itam [lu ko soob] ca cosaani Téere ba di [Lawhul- Mahfuuz] ma nga fa Moom.
40وَإِن مَّا نُرِيَنَّكَ بَعْضَ الَّذِي نَعِدُهُمْ أَوْ نَتَوَفَّيَنَّكَ فَإِنَّمَا عَلَيْكَ الْبَلَاغُ وَعَلَيْنَا الْحِسَابُ
Ndegam won Nanu la lenn ci li Nu leen dig, walla Nu rey la [lu mu ca mën di doon], yaw li la war moo di jotal, waaye Nun noo warloo natt [jëf ya].
41أَوَلَمْ يَرَوْا أَنَّا نَأْتِي الْأَرْضَ نَنقُصُهَا مِنْ أَطْرَافِهَا ۚ وَاللَّهُ يَحْكُمُ لَا مُعَقِّبَ لِحُكْمِهِ ۚ وَهُوَ سَرِيعُ الْحِسَابِ
Xanaa dañoo gisul ne Nun noo ngi wàññi suuf si ci ay catam ? Yàlla mooy àtte, Dananu delloob àtteem, te Moom ku gaaw la cib nattam.
Ar-Ra'dFihi Alxuraan
43Aaya
MedinanRevelation
39Aaya

Tekki — Ar-Ra'd 39

Simoore Ar-Ra'd Aaya 39 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Yàlla dana far lu ko soob te Dana saxal itam…

Simoore Aaya 39/43 — Ar-Ra'd الرعد (Medinan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Ar-Ra'd Dégg, Ar-Ra'd Tekki, Ar-Ra'd mp3, Ar-Ra'd pdf. Aaya 37–41. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers