Ibrahima · 3/52
Tekki Waxtaan — Ibrahima
الَّذِينَ يَسْتَحِبُّونَ الْحَيَاةَ الدُّنْيَا عَلَى الْآخِرَةِ وَيَصُدُّونَ عَن سَبِيلِ اللَّهِ وَيَبْغُونَهَا عِوَجًا ۚ أُولَٰئِكَ فِي ضَلَالٍ بَعِيدٍ ۝٣
Allazeena yastahibboo nal hayaatad dunyaa `alal aakhirati wa yasuddoona `ansabeelil laahi wa yabghoonahaa `iwajaa; ulaaa `ika fee dalaalim ba`eed
📖 Tekkim Wolof
Ña nga xam ne dañoo tànn dundug àdduna [mu gënal leen] gu àllaaxira, te ñuy wëlbati ña jëm ci yoonu Yàlla, di ko sàkkal ay gàkk, ñooña ñanga ca ag réer gu sori dëgg.
🎧 Dégg

📜 Aaya 1-5 — Ibrahima

1الر ۚ كِتَابٌ أَنزَلْنَاهُ إِلَيْكَ لِتُخْرِجَ النَّاسَ مِنَ الظُّلُمَاتِ إِلَى النُّورِ بِإِذْنِ رَبِّهِمْ إِلَىٰ صِرَاطِ الْعَزِيزِ الْحَمِيدِ
Alif, Laam, Raa. Ab téere la bu Nu wàcce ci yaw ngir nga génne nit ñi cig lëndëm [kéefar], jëme leen cig leer [gëm Yàlla], ci ndigalu seen Boroom jëme leen ci yoonu Boroom kàttan gi, Ki yeyoo gépp cant,
2اللَّهِ الَّذِي لَهُ مَا فِي السَّمَاوَاتِ وَمَا فِي الْأَرْضِ ۗ وَوَيْلٌ لِّلْكَافِرِينَ مِنْ عَذَابٍ شَدِيدٍ
[ci yoonu] Yàlla mi nga xam ne Moo moom li nekk ci asamaan yi ak suuf si. Te alkaande ñeel na yéefar yi ci mbugal mu tar.
3الَّذِينَ يَسْتَحِبُّونَ الْحَيَاةَ الدُّنْيَا عَلَى الْآخِرَةِ وَيَصُدُّونَ عَن سَبِيلِ اللَّهِ وَيَبْغُونَهَا عِوَجًا ۚ أُولَٰئِكَ فِي ضَلَالٍ بَعِيدٍ
Ña nga xam ne dañoo tànn dundug àdduna [mu gënal leen] gu àllaaxira, te ñuy wëlbati ña jëm ci yoonu Yàlla, di ko sàkkal ay gàkk, ñooña ñanga ca ag réer gu sori dëgg.
4وَمَا أَرْسَلْنَا مِن رَّسُولٍ إِلَّا بِلِسَانِ قَوْمِهِ لِيُبَيِّنَ لَهُمْ ۖ فَيُضِلُّ اللَّهُ مَن يَشَاءُ وَيَهْدِي مَن يَشَاءُ ۚ وَهُوَ الْعَزِيزُ الْحَكِيمُ
Dunu yónni ab Yonent lu dul ci làkku nitam ña [lay waxe] ngir mu leeralal leen [la ñu ko yónni]. Te Yàlla mooy bàyyi cig réer ku ko soob, Dana gindi itam ku ko soob. Ndax Moom moo di boroom kàttan gi tey Aji-xereñ [ciy àtteem].
5وَلَقَدْ أَرْسَلْنَا مُوسَىٰ بِآيَاتِنَا أَنْ أَخْرِجْ قَوْمَكَ مِنَ الظُّلُمَاتِ إِلَى النُّورِ وَذَكِّرْهُم بِأَيَّامِ اللَّهِ ۚ إِنَّ فِي ذَٰلِكَ لَآيَاتٍ لِّكُلِّ صَبَّارٍ شَكُورٍ
Yónni woon Nanu Muusaa, dooleel kook Sunuy kaawtéef, ne ko : “Génneel saw nit cig lëndëm jëme leen cig réer, te nga waar leen ci xéewali Yàlla yi”. Ndax kéemtaan a ngi ci loolu ñeel képp ku di ab muñaakoon, di ab santaakoon.
IbrahimaFihi Alxuraan
52Aaya
MeccanRevelation
3Aaya

Tekki — Ibrahima 3

Simoore Ibrahima Aaya 3 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Ña nga xam ne dañoo tànn dundug àdduna [mu gënal…

Simoore Aaya 3/52 — Ibrahima إبراهيم (Meccan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Ibrahima Dégg, Ibrahima Tekki, Ibrahima mp3, Ibrahima pdf. Aaya 1–5. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers