An-Nahl · 14/128
Tekki Waxtaan — An-Nahl
وَهُوَ الَّذِي سَخَّرَ الْبَحْرَ لِتَأْكُلُوا مِنْهُ لَحْمًا طَرِيًّا وَتَسْتَخْرِجُوا مِنْهُ حِلْيَةً تَلْبَسُونَهَا وَتَرَى الْفُلْكَ مَوَاخِرَ فِيهِ وَلِتَبْتَغُوا مِن فَضْلِهِ وَلَعَلَّكُمْ تَشْكُرُونَ ۝١٤
Wa Huwal lazee sakhkharal bahra litaakuloo minhu lahman tariyyanw wa tastakhrijoo minhu hilyatan talbasoonahaa wa taral fulka mawaakhira feehi wa litabtaghoo min fadlihee wa la`allakum tashkuroon
📖 Tekkim Wolof
Te Moom moo leen tàggatal géej gi ngir ngeen mën ciy jële yàpp wu tooy wu ngeen di lekk, ak ngeen ciy mën a génne ay takkaay yu ngeen di takk. Te gis ngeen ne gaal yaa ngi cay daw, ak it ngeen di ca sàkku ci xéewalam ya, te kon xéy-na di ngeen ko gërëm.
🎧 Dégg

📜 Aaya 12-16 — An-Nahl

12وَسَخَّرَ لَكُمُ اللَّيْلَ وَالنَّهَارَ وَالشَّمْسَ وَالْقَمَرَ ۖ وَالنُّجُومُ مُسَخَّرَاتٌ بِأَمْرِهِ ۗ إِنَّ فِي ذَٰلِكَ لَآيَاتٍ لِّقَوْمٍ يَعْقِلُونَ
Te Moo leen tàggatal guddi gi ak bëccëg gi ; ak jant bi ak weer wi. Ak bidiw yi itam. Ci ndigalam, loolu dey ag kéemaan a ngi ci ngir aw nit ñuy xel-lu.
13وَمَا ذَرَأَ لَكُمْ فِي الْأَرْضِ مُخْتَلِفًا أَلْوَانُهُ ۗ إِنَّ فِي ذَٰلِكَ لَآيَةً لِّقَوْمٍ يَذَّكَّرُونَ
Te li Mu leen wesaareel ci kaw suuf si am nañu ay melo yu wuute. Te ci biir yooyu, am na ca ay kéemaan ñeel aw nit ñuy waaru.
14وَهُوَ الَّذِي سَخَّرَ الْبَحْرَ لِتَأْكُلُوا مِنْهُ لَحْمًا طَرِيًّا وَتَسْتَخْرِجُوا مِنْهُ حِلْيَةً تَلْبَسُونَهَا وَتَرَى الْفُلْكَ مَوَاخِرَ فِيهِ وَلِتَبْتَغُوا مِن فَضْلِهِ وَلَعَلَّكُمْ تَشْكُرُونَ
Te Moom moo leen tàggatal géej gi ngir ngeen mën ciy jële yàpp wu tooy wu ngeen di lekk, ak ngeen ciy mën a génne ay takkaay yu ngeen di takk. Te gis ngeen ne gaal yaa ngi cay daw, ak it ngeen di ca sàkku ci xéewalam ya, te kon xéy-na di ngeen ko gërëm.
15وَأَلْقَىٰ فِي الْأَرْضِ رَوَاسِيَ أَن تَمِيدَ بِكُمْ وَأَنْهَارًا وَسُبُلًا لَّعَلَّكُمْ تَهْتَدُونَ
Te Moo samp ci suuf si ay ndëgërlaay [mu dal] bañ a jaayu ak yéen, ak i dex ak i yoon,
16وَعَلَامَاتٍ ۚ وَبِالنَّجْمِ هُمْ يَهْتَدُونَ
[def na it ci suuf si] ay màndarga, nit ña mën a gindikoo ci bidiw yi.
An-NahlFihi Alxuraan
128Aaya
MeccanRevelation
14Aaya

Tekki — An-Nahl 14

Simoore An-Nahl Aaya 14 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Te Moom moo leen tàggatal géej gi ngir ngeen mën…

Simoore Aaya 14/128 — An-Nahl النحل (Meccan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: An-Nahl Dégg, An-Nahl Tekki, An-Nahl mp3, An-Nahl pdf. Aaya 12–16. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers