Al-Baqara · 78/286
Tekki Waxtaan — Al-Baqara
وَمِنْهُمْ أُمِّيُّونَ لَا يَعْلَمُونَ الْكِتَابَ إِلَّا أَمَانِيَّ وَإِنْ هُمْ إِلَّا يَظُنُّونَ ۝٧٨
Wa minhum ummiyyoona laa ya`lamoonal kitaaba illaaa amaaniyya wa in hum illaa yazunnoon
📖 Tekkim Wolof
Am na ca ñoo xam ne mënuñoo jàng, xamuñu téere ba lu dul ay fen yu nekk ay njort doŋŋ.
🎧 Dégg

📜 Aaya 76-80 — Al-Baqara

76وَإِذَا لَقُوا الَّذِينَ آمَنُوا قَالُوا آمَنَّا وَإِذَا خَلَا بَعْضُهُمْ إِلَىٰ بَعْضٍ قَالُوا أَتُحَدِّثُونَهُم بِمَا فَتَحَ اللَّهُ عَلَيْكُمْ لِيُحَاجُّوكُم بِهِ عِندَ رَبِّكُمْ ۚ أَفَلَا تَعْقِلُونَ
- Bu ñu dajeek ñu gëm, ne : “Gëm nañu” ; te bu ñu wéetee ñoom doŋŋ, naan : “Ndax dungeen waxtaane li leen Yàlla xamal, nu mën caa sukkandiku [ñoom jullit yi] di dàggeek yéen ci seeni [mbiri] Boroom ! Moo ndax dangeen dul xel-lu ? ”.
77أَوَلَا يَعْلَمُونَ أَنَّ اللَّهَ يَعْلَمُ مَا يُسِرُّونَ وَمَا يُعْلِنُونَ
- Moo ndax dañoo xamul ne Yàlla xam na la ñuy nëbb ak la ñuy feeñal ?
78وَمِنْهُمْ أُمِّيُّونَ لَا يَعْلَمُونَ الْكِتَابَ إِلَّا أَمَانِيَّ وَإِنْ هُمْ إِلَّا يَظُنُّونَ
Am na ca ñoo xam ne mënuñoo jàng, xamuñu téere ba lu dul ay fen yu nekk ay njort doŋŋ.
79فَوَيْلٌ لِّلَّذِينَ يَكْتُبُونَ الْكِتَابَ بِأَيْدِيهِمْ ثُمَّ يَقُولُونَ هَٰذَا مِنْ عِندِ اللَّهِ لِيَشْتَرُوا بِهِ ثَمَنًا قَلِيلًا ۖ فَوَيْلٌ لَّهُم مِّمَّا كَتَبَتْ أَيْدِيهِمْ وَوَيْلٌ لَّهُم مِّمَّا يَكْسِبُونَ
Alkaande ñeel na ñay bind téere ba, ba noppi naan lii ca Yàlla la jóge ndax mën caa jële njëg gu néew ! - Alkaande ñeel na leen ngir la ca seeni yoxo bind, ñeel na leen ngir la ñu ca fàggu [ci alal] !
80وَقَالُوا لَن تَمَسَّنَا النَّارُ إِلَّا أَيَّامًا مَّعْدُودَةً ۚ قُلْ أَتَّخَذْتُمْ عِندَ اللَّهِ عَهْدًا فَلَن يُخْلِفَ اللَّهُ عَهْدَهُ ۖ أَمْ تَقُولُونَ عَلَى اللَّهِ مَا لَا تَعْلَمُونَ
Wax nañu ne : “Safara dunu laal lu dul ay bis yu ñuy waññi ! ”. Neeleen : “Moo ndax dangeen cee déggook Yàlla - te Yàlla du wuute ab digam ; - walla dangeen di wax ci Yàlla lu ngeen xamul”.
Al-BaqaraFihi Alxuraan
286Aaya
MedinanRevelation
78Aaya

Tekki — Al-Baqara 78

Simoore Al-Baqara Aaya 78 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Am na ca ñoo xam ne mënuñoo jàng, xamuñu téere…

Simoore Aaya 78/286 — Al-Baqara البقرة (Medinan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Al-Baqara Dégg, Al-Baqara Tekki, Al-Baqara mp3, Al-Baqara pdf. Aaya 76–80. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers