Taha · 41/135
Tekki Waxtaan — Taha
وَاصْطَنَعْتُكَ لِنَفْسِي ۝٤١
Wastana` tuka linafsee
📖 Tekkim Wolof
Maa la bind ngir Sama mbiri bopp.

🎧 Dégg


📜 Aaya 39-43 — Taha

39أَنِ اقْذِفِيهِ فِي التَّابُوتِ فَاقْذِفِيهِ فِي الْيَمِّ فَلْيُلْقِهِ الْيَمُّ بِالسَّاحِلِ يَأْخُذْهُ عَدُوٌّ لِّي وَعَدُوٌّ لَّهُ ۚ وَأَلْقَيْتُ عَلَيْكَ مَحَبَّةً مِّنِّي وَلِتُصْنَعَ عَلَىٰ عَيْنِي
Ne ko na sànni liir ba ca kees ga, sànni kees ga ca ndox ma, ndox ma dana ko gëq ca tefes ga ; samab noon, dib noonam moo koy jël”. Yaw Muusaa, defal naa la Samag cofeel, te it ci Samag càmm nga màgge.
40إِذْ تَمْشِي أُخْتُكَ فَتَقُولُ هَلْ أَدُلُّكُمْ عَلَىٰ مَن يَكْفُلُهُ ۖ فَرَجَعْنَاكَ إِلَىٰ أُمِّكَ كَيْ تَقَرَّ عَيْنُهَا وَلَا تَحْزَنَ ۚ وَقَتَلْتَ نَفْسًا فَنَجَّيْنَاكَ مِنَ الْغَمِّ وَفَتَنَّاكَ فُتُونًا ۚ فَلَبِثْتَ سِنِينَ فِي أَهْلِ مَدْيَنَ ثُمَّ جِئْتَ عَلَىٰ قَدَرٍ يَا مُوسَىٰ
[Fàttalikul] ba sa jigéen ba di dox te naan leen : “Ndax duma leen tegtal ci ku ko mën a yar ? ” Ba tax Nu delloo la fa sa yaay ngir xelam dal, mu bañ a yàq. Nga reyoon bakkan, Nu musal la ca mbamb ma ; Nu fitnaaloon la, nattu la lu yàgg. Nga demoon fa waa Madiyaana ba am fa ay at. Ba tey jii yaa ngi nii ci àpp bu ma dogaloon.
41وَاصْطَنَعْتُكَ لِنَفْسِي
Maa la bind ngir Sama mbiri bopp.
42اذْهَبْ أَنتَ وَأَخُوكَ بِآيَاتِي وَلَا تَنِيَا فِي ذِكْرِي
Demal yaak sa mbokk ngeen yor samay kàddu ; te buleen sàggane di Ma jaamu.
43اذْهَبَا إِلَىٰ فِرْعَوْنَ إِنَّهُ طَغَىٰ
Demleen yéen ñaar fa Firawna : ndax moom dafa beew.
TahaFihi Alxuraan
135Aaya
MeccanRevelation
41Aaya

Tekki — Taha 41

Simoore Taha Aaya 41 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Maa la bind ngir Sama mbiri bopp.

Simoore Aaya 41/135 — Taha طه (Meccan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Taha Dégg, Taha Tekki, Taha mp3, Taha pdf. Aaya 39–43. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers