Al-Qasas · 33/88
Tekki Waxtaan — Al-Qasas
قَالَ رَبِّ إِنِّي قَتَلْتُ مِنْهُمْ نَفْسًا فَأَخَافُ أَن يَقْتُلُونِ ۝٣٣
Qaala Rabbi innee qataltu minhum nafsan fa akhaafu ai yaqtuloon
📖 Tekkim Wolof
[Muusaa wax na ne] : “Rey naa ci ñoom bakkan te ragal naa ñu rey ma.
🎧 Dégg

📜 Aaya 31-35 — Al-Qasas

31وَأَنْ أَلْقِ عَصَاكَ ۖ فَلَمَّا رَآهَا تَهْتَزُّ كَأَنَّهَا جَانٌّ وَلَّىٰ مُدْبِرًا وَلَمْ يُعَقِّبْ ۚ يَا مُوسَىٰ أَقْبِلْ وَلَا تَخَفْ ۖ إِنَّكَ مِنَ الْآمِنِينَ
Te : “Nanga sànni sa yet wi” ; [Ba mu ko sànnee] gis ne ma ngay yëngatu mel ni jaan, mu ne baxarñit.”. Yàlla woowaat ko, ne ko : “Dellusil te bul tiit : yaa ngi ci lu wóor”.
32اسْلُكْ يَدَكَ فِي جَيْبِكَ تَخْرُجْ بَيْضَاءَ مِنْ غَيْرِ سُوءٍ وَاضْمُمْ إِلَيْكَ جَنَاحَكَ مِنَ الرَّهْبِ ۖ فَذَانِكَ بُرْهَانَانِ مِن رَّبِّكَ إِلَىٰ فِرْعَوْنَ وَمَلَئِهِ ۚ إِنَّهُمْ كَانُوا قَوْمًا فَاسِقِينَ
Sóobal sa loxo ci sa mbagg, dina génn weex tàll. Te nanga taf sa loxo bi ci sa kaw ngir bañ a tiit. Yooyu yaari mbir ay firnde la yu bawoo ca sa Boroom Mu jëme ko ci Firawna ak gàngooram. Ñoom ay saay-saay lañu”.
33قَالَ رَبِّ إِنِّي قَتَلْتُ مِنْهُمْ نَفْسًا فَأَخَافُ أَن يَقْتُلُونِ
[Muusaa wax na ne] : “Rey naa ci ñoom bakkan te ragal naa ñu rey ma.
34وَأَخِي هَارُونُ هُوَ أَفْصَحُ مِنِّي لِسَانًا فَأَرْسِلْهُ مَعِيَ رِدْءًا يُصَدِّقُنِي ۖ إِنِّي أَخَافُ أَن يُكَذِّبُونِ
Te Aaruuna moo ma gën a leer i wax. Yebal ko mu ànd ak man di ma ruqandi, di ma dëggal : man daal ragal naa ñu jàppe ma fenkat”.
35قَالَ سَنَشُدُّ عَضُدَكَ بِأَخِيكَ وَنَجْعَلُ لَكُمَا سُلْطَانًا فَلَا يَصِلُونَ إِلَيْكُمَا ۚ بِآيَاتِنَا أَنتُمَا وَمَنِ اتَّبَعَكُمَا الْغَالِبُونَ
[Yàlla] ne ko : “Dananu dëgërale sa përëg ci sa mbokk mi, Dananu leen defal ay firnde [doole joo xam ne dana mën a agsi ci yéen] ak Sunuy kéemaan. Yéen ñaar ñépp ak ña leen topp yéen ay not.
Al-QasasFihi Alxuraan
88Aaya
MeccanRevelation
33Aaya

Tekki — Al-Qasas 33

Simoore Al-Qasas Aaya 33 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : [Muusaa wax na ne] : “Rey naa ci ñoom bakkan…

Simoore Aaya 33/88 — Al-Qasas القصص (Meccan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Al-Qasas Dégg, Al-Qasas Tekki, Al-Qasas mp3, Al-Qasas pdf. Aaya 31–35. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers