Aali Imran · 24/200
Tekki Waxtaan — Simoore Aali Imran
ذَٰلِكَ بِأَنَّهُمْ قَالُوا لَن تَمَسَّنَا النَّارُ إِلَّا أَيَّامًا مَّعْدُودَاتٍ ۖ وَغَرَّهُمْ فِي دِينِهِم مَّا كَانُوا يَفْتَرُونَ ۝٢٤
Zaalika bi annahum qaaloo lan tamassanan naaru illaaa ayyaamam ma`doodaatinw wa gharrahum fee deenihim maa kaanoo yaftaroon
📖 Tekkim Wolof
Ndax ñoom dañuy wax ne : “Safara dunu laal lu dul ay bis yuñu lim”. Dañuy duural Yàlla ci seen diine, loolaa leen nax.

🎧 Dégg


📜 Aaya 22-26 — Simoore Aali Imran

22أُولَٰئِكَ الَّذِينَ حَبِطَتْ أَعْمَالُهُمْ فِي الدُّنْيَا وَالْآخِرَةِ وَمَا لَهُم مِّن نَّاصِرِينَ
Ñooña seeni jëf sippiku na ci àddina ak ca àllaaxira. Te duñu am ndimbal !
23أَلَمْ تَرَ إِلَى الَّذِينَ أُوتُوا نَصِيبًا مِّنَ الْكِتَابِ يُدْعَوْنَ إِلَىٰ كِتَابِ اللَّهِ لِيَحْكُمَ بَيْنَهُمْ ثُمَّ يَتَوَلَّىٰ فَرِيقٌ مِّنْهُمْ وَهُم مُّعْرِضُونَ
Moo ndax gisoo ñañu jox cér ca téere ba , woowees na leen jëme ci Téere Yàlla bi ngir mu àtte seeni diggante ; am kurél ci ñoom bu dummóoyu, far ñoom ñépp dummóoyu.
24ذَٰلِكَ بِأَنَّهُمْ قَالُوا لَن تَمَسَّنَا النَّارُ إِلَّا أَيَّامًا مَّعْدُودَاتٍ ۖ وَغَرَّهُمْ فِي دِينِهِم مَّا كَانُوا يَفْتَرُونَ
Ndax ñoom dañuy wax ne : “Safara dunu laal lu dul ay bis yuñu lim”. Dañuy duural Yàlla ci seen diine, loolaa leen nax.
25فَكَيْفَ إِذَا جَمَعْنَاهُمْ لِيَوْمٍ لَّا رَيْبَ فِيهِ وَوُفِّيَتْ كُلُّ نَفْسٍ مَّا كَسَبَتْ وَهُمْ لَا يُظْلَمُونَ
Naka la ñuy def ca bis ba, kenn warut a nàttable ci ne dana am, bu ñu leen dajalee ba kenn ku nekk ñu jox ko la mu fàggu woon mu mat sëkk.
26قُلِ اللَّهُمَّ مَالِكَ الْمُلْكِ تُؤْتِي الْمُلْكَ مَن تَشَاءُ وَتَنزِعُ الْمُلْكَ مِمَّن تَشَاءُ وَتُعِزُّ مَن تَشَاءُ وَتُذِلُّ مَن تَشَاءُ ۖ بِيَدِكَ الْخَيْرُ ۖ إِنَّكَ عَلَىٰ كُلِّ شَيْءٍ قَدِيرٌ
- Neel : “Sama Boroom, Yaw miy Boroom nguur. Yaay jox nguur ku la soob, di rocci nguur ci ku la soob ; Yaay teral ku la soob, Yaay toroxal ku la soob. Yiw wépp a ngi ci sa loxo te kàttanu nga ci def lu ne.
Aali ImranFihi Alxuraan
200Aaya
MedinanRevelation
24Aaya

Tekki — Aali Imran 24

Simoore Aali Imran Aaya 24 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Ndax ñoom dañuy wax ne : “Safara dunu laal lu…

Simoore Aaya 24/200 — Simoore Aali Imran آل عمران (Medinan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Simoore Aali Imran Dégg, Simoore Aali Imran Tekki, Simoore Aali Imran mp3, Simoore Aali Imran pdf. Aaya 22–26. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, September 8, 2026

Don't forget us in your sincere prayers