Saba · 29/54
Tekki Waxtaan — Saba
وَيَقُولُونَ مَتَىٰ هَٰذَا الْوَعْدُ إِن كُنتُمْ صَادِقِينَ ۝٢٩
Wa yaqooloona mataa haazal wa`du in kuntum saadiqeen
📖 Tekkim Wolof
Ñuy wax naan : “Dig ba kañ lay doon su fekkee ne li ngeen di wax dëgg la ? ”.

🎧 Dégg


📜 Aaya 27-31 — Saba

27قُلْ أَرُونِيَ الَّذِينَ أَلْحَقْتُم بِهِ شُرَكَاءَ ۖ كَلَّا ۚ بَلْ هُوَ اللَّهُ الْعَزِيزُ الْحَكِيمُ
Waxal ne : “Wonleen ma ña ngeen daan bokkaaleek Yàlla. [Mukk] ! Li wér moo di ne Mooy Yàlla, di Boroom Kàttan, di Ku Xereñ”.
28وَمَا أَرْسَلْنَاكَ إِلَّا كَافَّةً لِّلنَّاسِ بَشِيرًا وَنَذِيرًا وَلَٰكِنَّ أَكْثَرَ النَّاسِ لَا يَعْلَمُونَ
Yónniwunu la [yaw Muhammad] lu dul nga daj képp nit ñi, di béglekat, di xuppekat. Waaye li ëpp ci nit ñi duñu xam.
29وَيَقُولُونَ مَتَىٰ هَٰذَا الْوَعْدُ إِن كُنتُمْ صَادِقِينَ
Ñuy wax naan : “Dig ba kañ lay doon su fekkee ne li ngeen di wax dëgg la ? ”.
30قُل لَّكُم مِّيعَادُ يَوْمٍ لَّا تَسْتَأْخِرُونَ عَنْهُ سَاعَةً وَلَا تَسْتَقْدِمُونَ
Waxal ne : “Am ngeen digub Bis boo xam ne dungeen ko jiitu, dungen ko yées ! ”.
31وَقَالَ الَّذِينَ كَفَرُوا لَن نُّؤْمِنَ بِهَٰذَا الْقُرْآنِ وَلَا بِالَّذِي بَيْنَ يَدَيْهِ ۗ وَلَوْ تَرَىٰ إِذِ الظَّالِمُونَ مَوْقُوفُونَ عِندَ رَبِّهِمْ يَرْجِعُ بَعْضُهُمْ إِلَىٰ بَعْضٍ الْقَوْلَ يَقُولُ الَّذِينَ اسْتُضْعِفُوا لِلَّذِينَ اسْتَكْبَرُوا لَوْلَا أَنتُمْ لَكُنَّا مُؤْمِنِينَ
Yéefar ya nee nañu : “Duñu gëm Alxuraan walla lu ko jiitu”. Cëy boo gisoon tooñkat ya bu keroogee ba ñu taxawal leen ci seen kanamu Boroom, nga gis leen ñuy wàqante ! Ña néewoon doole di wax kilifa ya, naan leen : “Bu dul kon ak yéen, ay jullit la nuy doon”.
SabaFihi Alxuraan
54Aaya
MeccanRevelation
29Aaya

Tekki — Saba 29

Simoore Saba Aaya 29 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Ñuy wax naan : “Dig ba kañ lay doon su…

Simoore Aaya 29/54 — Saba سبأ (Meccan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Saba Dégg, Saba Tekki, Saba mp3, Saba pdf. Aaya 27–31. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers