Al-An'am · 27/165
Tekki Waxtaan — Al-An'am
وَلَوْ تَرَىٰ إِذْ وُقِفُوا عَلَى النَّارِ فَقَالُوا يَا لَيْتَنَا نُرَدُّ وَلَا نُكَذِّبَ بِآيَاتِ رَبِّنَا وَنَكُونَ مِنَ الْمُؤْمِنِينَ ۝٢٧
Wa law taraaa iz wauqifoo `alan Naari faqaaloo yaa laitanaa nuraddu wa laa nukaz ziba bi Aayaati Rabbinaa wa nakoona minal mu`mineen
📖 Tekkim Wolof
Cëy boo leen gisoon, fa ñu leen taxawale ca Safara. Te ñuy wax : “Ngalla nun ! Yelante kon ñu delloo nu àddina, ba dunu weddi kàddug Yàlla sunu Boroom, bokk ca way-gëm ña”.

🎧 Dégg


📜 Aaya 25-29 — Al-An'am

25وَمِنْهُم مَّن يَسْتَمِعُ إِلَيْكَ ۖ وَجَعَلْنَا عَلَىٰ قُلُوبِهِمْ أَكِنَّةً أَن يَفْقَهُوهُ وَفِي آذَانِهِمْ وَقْرًا ۚ وَإِن يَرَوْا كُلَّ آيَةٍ لَّا يُؤْمِنُوا بِهَا ۚ حَتَّىٰ إِذَا جَاءُوكَ يُجَادِلُونَكَ يَقُولُ الَّذِينَ كَفَرُوا إِنْ هَٰذَا إِلَّا أَسَاطِيرُ الْأَوَّلِينَ
Am na ci ñoom ñu lay déglu, waaye def Nanu ci seen xol muuraay ba duñu am dégg-dégg ci Alxuraan, te ca seeni nopp, def Nanu ca saañ. Tax na bu ñu gisee laaya, ju mu mën di doon, ne duñu ko gëm. Ba ba ñuy ñëw dàggasanteek yaw, dañuy wax ñoom ñi weddi : “Lii du dara lu dul léebi mag ñu njëkk ña”.
26وَهُمْ يَنْهَوْنَ عَنْهُ وَيَنْأَوْنَ عَنْهُ ۖ وَإِن يُهْلِكُونَ إِلَّا أَنفُسَهُمْ وَمَا يَشْعُرُونَ
Te ñoom dañuy tere ku jegeñ Yonent bi, te di ko sori. Waaye alaguñu kenn ku dul seen bopp te bëgguñu ko.
27وَلَوْ تَرَىٰ إِذْ وُقِفُوا عَلَى النَّارِ فَقَالُوا يَا لَيْتَنَا نُرَدُّ وَلَا نُكَذِّبَ بِآيَاتِ رَبِّنَا وَنَكُونَ مِنَ الْمُؤْمِنِينَ
Cëy boo leen gisoon, fa ñu leen taxawale ca Safara. Te ñuy wax : “Ngalla nun ! Yelante kon ñu delloo nu àddina, ba dunu weddi kàddug Yàlla sunu Boroom, bokk ca way-gëm ña”.
28بَلْ بَدَا لَهُم مَّا كَانُوا يُخْفُونَ مِن قَبْلُ ۖ وَلَوْ رُدُّوا لَعَادُوا لِمَا نُهُوا عَنْهُ وَإِنَّهُمْ لَكَاذِبُونَ
Li wér mooy, la ñu doon nëbb, bu jëkkoon feeñ na ca ñoom. Te bu ñu leen delloo woon it, ñu dellu di def la ñu leen tere woon. Ca dëgg-dëgg ñoom ay fenkat lañu.
29وَقَالُوا إِنْ هِيَ إِلَّا حَيَاتُنَا الدُّنْيَا وَمَا نَحْنُ بِمَبْعُوثِينَ
Dañuy wax ne : “Amul geneen dundu gu dul gu àddina bii ; [nun bu nu faatoo] kenn du nu dekkalaat”.
Al-An'amFihi Alxuraan
165Aaya
MeccanRevelation
27Aaya

Tekki — Al-An'am 27

Simoore Al-An'am Aaya 27 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Cëy boo leen gisoon, fa ñu leen taxawale ca Safara.…

Simoore Aaya 27/165 — Al-An'am الأنعام (Meccan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Al-An'am Dégg, Al-An'am Tekki, Al-An'am mp3, Al-An'am pdf. Aaya 25–29. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers