Al-A'raf · 128/206
Tekki Waxtaan — Simoore Al-A'raf
قَالَ مُوسَىٰ لِقَوْمِهِ اسْتَعِينُوا بِاللَّهِ وَاصْبِرُوا ۖ إِنَّ الْأَرْضَ لِلَّهِ يُورِثُهَا مَن يَشَاءُ مِنْ عِبَادِهِ ۖ وَالْعَاقِبَةُ لِلْمُتَّقِينَ ۝١٢٨
Qaala Moosaa liqawmihis ta`eenoo billaahi wasbiroo innal arda lillaahi yoorisuhaa mai yashaaa`u min `ibaadihee wal `aaqibatu lilmuttaqeen
📖 Tekkim Wolof
Muusaa wax ay nitam : “Sàkkuleen ndimbal ci Yàlla te ngeen muñ, suuf si Yàllaa ko moom. Dana ko donnale ku ko neex ciy jaamam. Te muj ga, way-ragal Yàlla yee ko moom”.

🎧 Dégg


📜 Aaya 126-130 — Simoore Al-A'raf

126وَمَا تَنقِمُ مِنَّا إِلَّا أَنْ آمَنَّا بِآيَاتِ رَبِّنَا لَمَّا جَاءَتْنَا ۚ رَبَّنَا أَفْرِغْ عَلَيْنَا صَبْرًا وَتَوَفَّنَا مُسْلِمِينَ
Feyoowoo ci nun lu dul nu gëm ay kéemaani sunu Boroom, ba ñu agsee ci nun. Sunu Boroom ! Sottil ci nun muñ te nga rey nu fekk nu dee jullit.”
127وَقَالَ الْمَلَأُ مِن قَوْمِ فِرْعَوْنَ أَتَذَرُ مُوسَىٰ وَقَوْمَهُ لِيُفْسِدُوا فِي الْأَرْضِ وَيَذَرَكَ وَآلِهَتَكَ ۚ قَالَ سَنُقَتِّلُ أَبْنَاءَهُمْ وَنَسْتَحْيِي نِسَاءَهُمْ وَإِنَّا فَوْقَهُمْ قَاهِرُونَ
Kilifa ya bokk ci nitu Firawna ne ko : “Moo ndax dangaa bàyyi Muusaa ak u nitam ñuy yàq ci suuf si, te moom mu bàyyi la, bàyyi sa yàlla ? ”. Mu toontu ne : “Danaa rey seeni doom yu góor, ba yu jigéen yi. Ndax nun noo leen tiim, noo leen not.”
128قَالَ مُوسَىٰ لِقَوْمِهِ اسْتَعِينُوا بِاللَّهِ وَاصْبِرُوا ۖ إِنَّ الْأَرْضَ لِلَّهِ يُورِثُهَا مَن يَشَاءُ مِنْ عِبَادِهِ ۖ وَالْعَاقِبَةُ لِلْمُتَّقِينَ
Muusaa wax ay nitam : “Sàkkuleen ndimbal ci Yàlla te ngeen muñ, suuf si Yàllaa ko moom. Dana ko donnale ku ko neex ciy jaamam. Te muj ga, way-ragal Yàlla yee ko moom”.
129قَالُوا أُوذِينَا مِن قَبْلِ أَن تَأْتِيَنَا وَمِن بَعْدِ مَا جِئْتَنَا ۚ قَالَ عَسَىٰ رَبُّكُمْ أَن يُهْلِكَ عَدُوَّكُمْ وَيَسْتَخْلِفَكُمْ فِي الْأَرْضِ فَيَنظُرَ كَيْفَ تَعْمَلُونَ
[Ñoom yahuud ya] ne : “Loreef nanu lu jiitu sa dikk ci nun ak ginnaaw la nga nu indil.”. Mu ne : “Xéy-na seen Boroom dana rey seeni noon, Mu wuutal leen ci suuf si ba noppi di saytu na ngeen di def”.
130وَلَقَدْ أَخَذْنَا آلَ فِرْعَوْنَ بِالسِّنِينَ وَنَقْصٍ مِّنَ الثَّمَرَاتِ لَعَلَّهُمْ يَذَّكَّرُونَ
Teg Nanu nitu Firawna bekkoor ay at ak wàññikug meññent ndax xéy-na ñu fàttaliku [seen Boroom].
Al-A'rafFihi Alxuraan
206Aaya
MeccanRevelation
128Aaya

Tekki — Al-A'raf 128

Simoore Al-A'raf Aaya 128 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Muusaa wax ay nitam : “Sàkkuleen ndimbal ci Yàlla te…

Simoore Aaya 128/206 — Simoore Al-A'raf الأعراف (Meccan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Simoore Al-A'raf Dégg, Simoore Al-A'raf Tekki, Simoore Al-A'raf mp3, Simoore Al-A'raf pdf. Aaya 126–130. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, September 8, 2026

Don't forget us in your sincere prayers