Al-A'raf · 21/206
Tekki Waxtaan — Simoore Al-A'raf
وَقَاسَمَهُمَا إِنِّي لَكُمَا لَمِنَ النَّاصِحِينَ ۝٢١
Wa qaasamahumaaa innee lakumaa laminan naasiheen
📖 Tekkim Wolof
Mu waatal leen, ne leen : “Man dey damaa bokk rekk ci ñi leen di laabire”.

🎧 Dégg


📜 Aaya 19-23 — Simoore Al-A'raf

19وَيَا آدَمُ اسْكُنْ أَنتَ وَزَوْجُكَ الْجَنَّةَ فَكُلَا مِنْ حَيْثُ شِئْتُمَا وَلَا تَقْرَبَا هَٰذِهِ الشَّجَرَةَ فَتَكُونَا مِنَ الظَّالِمِينَ
“Te yaw Aadama, dëkkal yaak sa soxna, Àjjana ; lekkleen yéen ñaar fu leen fi neex ; waaye buleen jegeñ garab gii ; su amee, ngeen tooñ.”
20فَوَسْوَسَ لَهُمَا الشَّيْطَانُ لِيُبْدِيَ لَهُمَا مَا وُورِيَ عَنْهُمَا مِن سَوْآتِهِمَا وَقَالَ مَا نَهَاكُمَا رَبُّكُمَا عَنْ هَٰذِهِ الشَّجَرَةِ إِلَّا أَن تَكُونَا مَلَكَيْنِ أَوْ تَكُونَا مِنَ الْخَالِدِينَ
Séytaane jax-jaxal leen ngir mu feeñal ca ñoom ñaar la Nu leen nëbboon - ci seen cër - mu ne leen : “Seen Boroom terewuleen ngeen jegeñ garab gii lu dul ne Dafa bañ ngeen nekk ñaari Malaaka walla ngeen bokk ca ñay dund fàwwu [duñu dee] ! ”.
21وَقَاسَمَهُمَا إِنِّي لَكُمَا لَمِنَ النَّاصِحِينَ
Mu waatal leen, ne leen : “Man dey damaa bokk rekk ci ñi leen di laabire”.
22فَدَلَّاهُمَا بِغُرُورٍ ۚ فَلَمَّا ذَاقَا الشَّجَرَةَ بَدَتْ لَهُمَا سَوْآتُهُمَا وَطَفِقَا يَخْصِفَانِ عَلَيْهِمَا مِن وَرَقِ الْجَنَّةِ ۖ وَنَادَاهُمَا رَبُّهُمَا أَلَمْ أَنْهَكُمَا عَن تِلْكُمَا الشَّجَرَةِ وَأَقُل لَّكُمَا إِنَّ الشَّيْطَانَ لَكُمَا عَدُوٌّ مُّبِينٌ
Mu tegtal leen cig wor. Ba ñu mosee ñoom ñaar garab ga, la seen pëy daldi feeñ ; ñuy witt di tafoo ay xob ca Àjjana. Seen Boroom woo leen, ne leen : “Ndax terewuma leen woon garab gii ? Te it wax leen ne Séytaane seenug noon tigi la ? ”
23قَالَا رَبَّنَا ظَلَمْنَا أَنفُسَنَا وَإِن لَّمْ تَغْفِرْ لَنَا وَتَرْحَمْنَا لَنَكُونَنَّ مِنَ الْخَاسِرِينَ
[Aadama ak Awa] daldi ne : "Sunu Boroom, tooñ nanu sunu bopp. Soo nu baalul, yërëm nu, kon dananu bokk ca ñu yàqule ña”.
Al-A'rafFihi Alxuraan
206Aaya
MeccanRevelation
21Aaya

Tekki — Al-A'raf 21

Simoore Al-A'raf Aaya 21 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Mu waatal leen, ne leen : “Man dey damaa bokk…

Simoore Aaya 21/206 — Simoore Al-A'raf الأعراف (Meccan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Simoore Al-A'raf Dégg, Simoore Al-A'raf Tekki, Simoore Al-A'raf mp3, Simoore Al-A'raf pdf. Aaya 19–23. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, September 8, 2026

Don't forget us in your sincere prayers