At-Tawba · 96/129
Tekki Waxtaan — At-Tawba
يَحْلِفُونَ لَكُمْ لِتَرْضَوْا عَنْهُمْ ۖ فَإِن تَرْضَوْا عَنْهُمْ فَإِنَّ اللَّهَ لَا يَرْضَىٰ عَنِ الْقَوْمِ الْفَاسِقِينَ ۝٩٦
Yahlifoona lakum litardaw `anhum fa in tardaw `anhum fa innal laaha laa yardaa `anil qawmil faasiqeen
📖 Tekkim Wolof
Ñanga leen di waatal ngir ngeen nangu (seeni ngànt), rafet njort ci ñoom. Bu ngeen nangoo seeni lay, Yàlla du nangul aw lay nit ñu di ay saay-saay.
🎧 Dégg

📜 Aaya 94-98 — At-Tawba

94يَعْتَذِرُونَ إِلَيْكُمْ إِذَا رَجَعْتُمْ إِلَيْهِمْ ۚ قُل لَّا تَعْتَذِرُوا لَن نُّؤْمِنَ لَكُمْ قَدْ نَبَّأَنَا اللَّهُ مِنْ أَخْبَارِكُمْ ۚ وَسَيَرَى اللَّهُ عَمَلَكُمْ وَرَسُولُهُ ثُمَّ تُرَدُّونَ إِلَىٰ عَالِمِ الْغَيْبِ وَالشَّهَادَةِ فَيُنَبِّئُكُم بِمَا كُنتُمْ تَعْمَلُونَ
Danañu ñëw ci yéen di lay bu ngeen dellusee. Neel : “Buleen lay : dunuleen gëm mukk. Yàlla nettali nanu ba noppi seen mbir. Te Yàlla ak ub Yonentam Danañu gis seeni jëf. Nu door leen a delloo fa Aji-xam ja kumpa ak la feeñ, Mu xamal leen li ngeen daan def.
95سَيَحْلِفُونَ بِاللَّهِ لَكُمْ إِذَا انقَلَبْتُمْ إِلَيْهِمْ لِتُعْرِضُوا عَنْهُمْ ۖ فَأَعْرِضُوا عَنْهُمْ ۖ إِنَّهُمْ رِجْسٌ ۖ وَمَأْوَاهُمْ جَهَنَّمُ جَزَاءً بِمَا كَانُوا يَكْسِبُونَ
Danañu leen waatal ci Yàlla, ba ngeen dellusee ci ñoom, ngir ngeen bañ leen a sikk. Waaye nangeen leen dëddu. Ñoom nag sobe lañu te seen delluwaay mooy Safara, muy peyug la ñu nekkoon di ko fàggu.
96يَحْلِفُونَ لَكُمْ لِتَرْضَوْا عَنْهُمْ ۖ فَإِن تَرْضَوْا عَنْهُمْ فَإِنَّ اللَّهَ لَا يَرْضَىٰ عَنِ الْقَوْمِ الْفَاسِقِينَ
Ñanga leen di waatal ngir ngeen nangu (seeni ngànt), rafet njort ci ñoom. Bu ngeen nangoo seeni lay, Yàlla du nangul aw lay nit ñu di ay saay-saay.
97الْأَعْرَابُ أَشَدُّ كُفْرًا وَنِفَاقًا وَأَجْدَرُ أَلَّا يَعْلَمُوا حُدُودَ مَا أَنزَلَ اللَّهُ عَلَىٰ رَسُولِهِ ۗ وَاللَّهُ عَلِيمٌ حَكِيمٌ
Sàmm sa, ñoo gën a tar ag weddi ak ug naaféq, te gën a yey ci ñàkk a xam ndigal yi Yàlla wàcce cib Yonentam. Yàlla nag Ku xam la, Ku xereñ la.
98وَمِنَ الْأَعْرَابِ مَن يَتَّخِذُ مَا يُنفِقُ مَغْرَمًا وَيَتَرَبَّصُ بِكُمُ الدَّوَائِرَ ۚ عَلَيْهِمْ دَائِرَةُ السَّوْءِ ۗ وَاللَّهُ سَمِيعٌ عَلِيمٌ
Am na ci sàmm si ñu jàpp ni, la ñu joxe (ngir Yàlla) lu yàqu la, tax na ñuy seentu xew- xew (bu bon dal leeen). Yal na xew-xew bu bon (ba ñuy seentu) dal ci seen kaw ! Yàlla Kuy dégg la, Kuy xam la.
At-TawbaFihi Alxuraan
129Aaya
MedinanRevelation
96Aaya

Tekki — At-Tawba 96

Simoore At-Tawba Aaya 96 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Ñanga leen di waatal ngir ngeen nangu (seeni ngànt), rafet…

Simoore Aaya 96/129 — At-Tawba التوبة (Medinan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: At-Tawba Dégg, At-Tawba Tekki, At-Tawba mp3, At-Tawba pdf. Aaya 94–98. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers