Yunus · 51/109
Tekki Waxtaan — Yunus
أَثُمَّ إِذَا مَا وَقَعَ آمَنتُم بِهِ ۚ آلْآنَ وَقَدْ كُنتُم بِهِ تَسْتَعْجِلُونَ ۝٥١
Asumma izaa maa waqa`a aamantum bih; aaal`aana wa qad kuntum bihee tasta`jiloon
📖 Tekkim Wolof
“Moo ndax bu agsee ngeen koy door a gëm ? [Kon deef na leen wax : “Léegi, yéen a ngi ci biir ba noppi”.] Te yéen a ngi koy yàkkamti”.
🎧 Dégg

📜 Aaya 49-53 — Yunus

49قُل لَّا أَمْلِكُ لِنَفْسِي ضَرًّا وَلَا نَفْعًا إِلَّا مَا شَاءَ اللَّهُ ۗ لِكُلِّ أُمَّةٍ أَجَلٌ ۚ إِذَا جَاءَ أَجَلُهُمْ فَلَا يَسْتَأْخِرُونَ سَاعَةً ۖ وَلَا يَسْتَقْدِمُونَ
Neel : “Mënaluma sama bopp lor walla njariñ, lu dul lu neex Yàlla. Xeet wu nekk am na àpp. Bu seen àpp matee, deefuleen yeexe wenn waxtu, te duñu jiitu it àpp ba”.
50قُلْ أَرَأَيْتُمْ إِنْ أَتَاكُمْ عَذَابُهُ بَيَاتًا أَوْ نَهَارًا مَّاذَا يَسْتَعْجِلُ مِنْهُ الْمُجْرِمُونَ
Neel : “Waaw waxleen ma ! Bu leen mbugal bettoon guddi walla bëccëg, lan la bàkkaarkat yi mën a gaawal ?
51أَثُمَّ إِذَا مَا وَقَعَ آمَنتُم بِهِ ۚ آلْآنَ وَقَدْ كُنتُم بِهِ تَسْتَعْجِلُونَ
“Moo ndax bu agsee ngeen koy door a gëm ? [Kon deef na leen wax : “Léegi, yéen a ngi ci biir ba noppi”.] Te yéen a ngi koy yàkkamti”.
52ثُمَّ قِيلَ لِلَّذِينَ ظَلَمُوا ذُوقُوا عَذَابَ الْخُلْدِ هَلْ تُجْزَوْنَ إِلَّا بِمَا كُنتُمْ تَكْسِبُونَ
Topp waxees tooñkat ya : “Ayca mosleen mbugal mu sax dàkk ! Moo ndax dees na leen feye lu wuuteek la ngeen doon fàggu ? ”
53۞ وَيَسْتَنبِئُونَكَ أَحَقٌّ هُوَ ۖ قُلْ إِي وَرَبِّي إِنَّهُ لَحَقٌّ ۖ وَمَا أَنتُم بِمُعْجِزِينَ
Te danañu sàkku nga leeral : “Ndax loolu dëgg la ? ” - Neel : “Waawaaw ! Giñ naa ci sama Boroom ne dëgg la !Te yéen dungeen mën a raw”.
YunusFihi Alxuraan
109Aaya
MeccanRevelation
51Aaya

Tekki — Yunus 51

Simoore Yunus Aaya 51 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : “Moo ndax bu agsee ngeen koy door a gëm ?…

Simoore Aaya 51/109 — Yunus يونس (Meccan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Yunus Dégg, Yunus Tekki, Yunus mp3, Yunus pdf. Aaya 49–53. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers