Ibrahima · 19/52
Tekki Waxtaan — Simoore Ibrahima
أَلَمْ تَرَ أَنَّ اللَّهَ خَلَقَ السَّمَاوَاتِ وَالْأَرْضَ بِالْحَقِّ ۚ إِن يَشَأْ يُذْهِبْكُمْ وَيَأْتِ بِخَلْقٍ جَدِيدٍ ۝١٩
Alam tara annal laaha khalaqas samaawaati wal arda bilhaqq; iny yashaa yuzhibkum wa yaati bikhalqin jadeed
📖 Tekkim Wolof
Ndax dañoo gisul ne Yàllaa bind asamaan yi ak suuf si ci dëgg ? Bu ko neexoon Mu jële leen fi, indi fi ay mbindéef yu bees,

🎧 Dégg


📜 Aaya 17-21 — Simoore Ibrahima

17يَتَجَرَّعُهُ وَلَا يَكَادُ يُسِيغُهُ وَيَأْتِيهِ الْمَوْتُ مِن كُلِّ مَكَانٍ وَمَا هُوَ بِمَيِّتٍ ۖ وَمِن وَرَائِهِ عَذَابٌ غَلِيظٌ
dana ko guux. Waaye du ko xaw a mën a wann. Dee di ko dikkale wet gu nekk, te du dee ; te it mbugal mu tar dana ca topp.
18مَّثَلُ الَّذِينَ كَفَرُوا بِرَبِّهِمْ ۖ أَعْمَالُهُمْ كَرَمَادٍ اشْتَدَّتْ بِهِ الرِّيحُ فِي يَوْمٍ عَاصِفٍ ۖ لَّا يَقْدِرُونَ مِمَّا كَسَبُوا عَلَىٰ شَيْءٍ ۚ ذَٰلِكَ هُوَ الضَّلَالُ الْبَعِيدُ
Ña weddi seen Boroom, seeni jëf dafa mel cig niróole ni ab dóom bu ngelaw ëf ci bisu mbóoya mu ràddi. Duñu mën a jariñoo dara ca la ñu fàggu woon. Loolu moo di réer gu sori dëgg.
19أَلَمْ تَرَ أَنَّ اللَّهَ خَلَقَ السَّمَاوَاتِ وَالْأَرْضَ بِالْحَقِّ ۚ إِن يَشَأْ يُذْهِبْكُمْ وَيَأْتِ بِخَلْقٍ جَدِيدٍ
Ndax dañoo gisul ne Yàllaa bind asamaan yi ak suuf si ci dëgg ? Bu ko neexoon Mu jële leen fi, indi fi ay mbindéef yu bees,
20وَمَا ذَٰلِكَ عَلَى اللَّهِ بِعَزِيزٍ
Loolu nekkul lu jafe Yàlla.
21وَبَرَزُوا لِلَّهِ جَمِيعًا فَقَالَ الضُّعَفَاءُ لِلَّذِينَ اسْتَكْبَرُوا إِنَّا كُنَّا لَكُمْ تَبَعًا فَهَلْ أَنتُم مُّغْنُونَ عَنَّا مِنْ عَذَابِ اللَّهِ مِن شَيْءٍ ۚ قَالُوا لَوْ هَدَانَا اللَّهُ لَهَدَيْنَاكُمْ ۖ سَوَاءٌ عَلَيْنَا أَجَزِعْنَا أَمْ صَبَرْنَا مَا لَنَا مِن مَّحِيصٍ
Ñoom ñépp ñu teew ca Yàlla. Ña neew doole wax ña daan màgg-màggalu ne leen : “Nun dey, yéen lanu toppoon. Moo ndax mën ngeen noo jiñal dara ci mbugalum Yàlla mi ? ” - Ñu tontu ne : “Su nu Yàlla jubaloon kon nu jubal leen. Léegi nag, nu tiit walla nu muñ, lépp a yem ci nun ; amunu làquwaay [fu nu rawe]”.
IbrahimaFihi Alxuraan
52Aaya
MeccanRevelation
19Aaya

Tekki — Ibrahima 19

Simoore Ibrahima Aaya 19 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Ndax dañoo gisul ne Yàllaa bind asamaan yi ak suuf…

Simoore Aaya 19/52 — Simoore Ibrahima إبراهيم (Meccan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Simoore Ibrahima Dégg, Simoore Ibrahima Tekki, Simoore Ibrahima mp3, Simoore Ibrahima pdf. Aaya 17–21. Tekkim Wolof: Fulfulde.





Alxuraan bu Tedd bi


Monday, September 21, 2026

Don't forget us in your sincere prayers