An-Nahl · 40/128
Tekki Waxtaan — An-Nahl
إِنَّمَا قَوْلُنَا لِشَيْءٍ إِذَا أَرَدْنَاهُ أَن نَّقُولَ لَهُ كُن فَيَكُونُ ۝٤٠
Innamaa qawlunaa lisha y`in izaa aradnaahu an naqoola lahoo kun fa yakoon
📖 Tekkim Wolof
[Li am mooy], Sunu kàddu ci mbir, bu Nu ko bëggee, Danu ko naan : “Nekkal”. Mu daldi nekk.
🎧 Dégg

📜 Aaya 38-42 — An-Nahl

38وَأَقْسَمُوا بِاللَّهِ جَهْدَ أَيْمَانِهِمْ ۙ لَا يَبْعَثُ اللَّهُ مَن يَمُوتُ ۚ بَلَىٰ وَعْدًا عَلَيْهِ حَقًّا وَلَٰكِنَّ أَكْثَرَ النَّاسِ لَا يَعْلَمُونَ
Ñangay giñ ba fa seeni ngiñ yem naan : “Yàlla du dekkal ku dee”. Axakañ ! Loolu dig bu dëggu la ci Moom [Yàlla], waaye li ëpp ci nit ñi xamuñu.
39لِيُبَيِّنَ لَهُمُ الَّذِي يَخْتَلِفُونَ فِيهِ وَلِيَعْلَمَ الَّذِينَ كَفَرُوا أَنَّهُمْ كَانُوا كَاذِبِينَ
Ngir mu leeralal leen [lay dëgg] ca la ñu daan wuute, ak it ña weddi xam ne dañu daan fen.
40إِنَّمَا قَوْلُنَا لِشَيْءٍ إِذَا أَرَدْنَاهُ أَن نَّقُولَ لَهُ كُن فَيَكُونُ
[Li am mooy], Sunu kàddu ci mbir, bu Nu ko bëggee, Danu ko naan : “Nekkal”. Mu daldi nekk.
41وَالَّذِينَ هَاجَرُوا فِي اللَّهِ مِن بَعْدِ مَا ظُلِمُوا لَنُبَوِّئَنَّهُمْ فِي الدُّنْيَا حَسَنَةً ۖ وَلَأَجْرُ الْآخِرَةِ أَكْبَرُ ۚ لَوْ كَانُوا يَعْلَمُونَ
Ña gàddaay jëm ci Yàlla, ginnaaw ba ñu leen tooñee, Dananu leen wàcceel aw yiw ci àddina. Te peyug àllaaxira moo gën a màgg, cëy bu ñu xamoon !
42الَّذِينَ صَبَرُوا وَعَلَىٰ رَبِّهِمْ يَتَوَكَّلُونَ
Ñoo di ñay muñ, wéeru ci seen Boroom [Dana leen wërsëgal lu ñu njortul woon].
An-NahlFihi Alxuraan
128Aaya
MeccanRevelation
40Aaya

Tekki — An-Nahl 40

Simoore An-Nahl Aaya 40 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : [Li am mooy], Sunu kàddu ci mbir, bu Nu ko…

Simoore Aaya 40/128 — An-Nahl النحل (Meccan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: An-Nahl Dégg, An-Nahl Tekki, An-Nahl mp3, An-Nahl pdf. Aaya 38–42. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers