Al-Isra · 100/111
Tekki Waxtaan — Al-Isra
قُل لَّوْ أَنتُمْ تَمْلِكُونَ خَزَائِنَ رَحْمَةِ رَبِّي إِذًا لَّأَمْسَكْتُمْ خَشْيَةَ الْإِنفَاقِ ۚ وَكَانَ الْإِنسَانُ قَتُورًا ۝١٠٠
Qul law antum tamlikoona khazaaa`ina rahmati Rabbeee izal la amsaktum khash yatal infaaq; wa kaanal insaanu qatooraa
📖 Tekkim Wolof
Neel : “Su fekkoon ne yéen a moom ndàmbi yërmaandey Yàlla yi ; kon ngeen nay [ci joxe ko] ngir ŋott. Nit dafa di ku ŋott !

🎧 Dégg


📜 Aaya 98-102 — Al-Isra

98ذَٰلِكَ جَزَاؤُهُم بِأَنَّهُمْ كَفَرُوا بِآيَاتِنَا وَقَالُوا أَإِذَا كُنَّا عِظَامًا وَرُفَاتًا أَإِنَّا لَمَبْعُوثُونَ خَلْقًا جَدِيدًا
Loolu moo di seen pey, ndax ñoom dañoo weddi Samay kàddu, naan : “Ndax [bu ñu deewee] ba nekk yax yu funux, dananu dekki nekk mbindeef yu bees ? ”
99۞ أَوَلَمْ يَرَوْا أَنَّ اللَّهَ الَّذِي خَلَقَ السَّمَاوَاتِ وَالْأَرْضَ قَادِرٌ عَلَىٰ أَن يَخْلُقَ مِثْلَهُمْ وَجَعَلَ لَهُمْ أَجَلًا لَّا رَيْبَ فِيهِ فَأَبَى الظَّالِمُونَ إِلَّا كُفُورًا
Ndax dañoo gisul ne Yàlla moo bind asamaan yi ak suuf si, te Ku kàttanu la ci bind leneen lu mel ni ñoom ? Te Mu àppal leen dig bu amul benn sikki-sàkka, waaye way-tooñ ña wéy nañu ci seenug weddi.
100قُل لَّوْ أَنتُمْ تَمْلِكُونَ خَزَائِنَ رَحْمَةِ رَبِّي إِذًا لَّأَمْسَكْتُمْ خَشْيَةَ الْإِنفَاقِ ۚ وَكَانَ الْإِنسَانُ قَتُورًا
Neel : “Su fekkoon ne yéen a moom ndàmbi yërmaandey Yàlla yi ; kon ngeen nay [ci joxe ko] ngir ŋott. Nit dafa di ku ŋott !
101وَلَقَدْ آتَيْنَا مُوسَىٰ تِسْعَ آيَاتٍ بَيِّنَاتٍ ۖ فَاسْأَلْ بَنِي إِسْرَائِيلَ إِذْ جَاءَهُمْ فَقَالَ لَهُ فِرْعَوْنُ إِنِّي لَأَظُنُّكَ يَا مُوسَىٰ مَسْحُورًا
Tigi, joxoon Nanu Muusaa juróom-ñeenti kéemaan yu leer. Laajal waa Bani-Israayiil, ba mu ñëwee fa ñoom, Firawna ne ko : “Muusaa, dama defe ne dañu laa jabar”.
102قَالَ لَقَدْ عَلِمْتَ مَا أَنزَلَ هَٰؤُلَاءِ إِلَّا رَبُّ السَّمَاوَاتِ وَالْأَرْضِ بَصَائِرَ وَإِنِّي لَأَظُنُّكَ يَا فِرْعَوْنُ مَثْبُورًا
[Muusaa tontu ne] : “Xam nga ne kenn wàccewul yile [kéemaan] ku dul Boroom asamaan yi ak suuf si ngir ñu nekk di waare ; te damaa defe ni, yaw Firawna, dangaa nekk ku alku”.
Al-IsraFihi Alxuraan
111Aaya
MeccanRevelation
100Aaya

Tekki — Al-Isra 100

Simoore Al-Isra Aaya 100 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Neel : “Su fekkoon ne yéen a moom ndàmbi yërmaandey…

Simoore Aaya 100/111 — Al-Isra الإسراء (Meccan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Al-Isra Dégg, Al-Isra Tekki, Al-Isra mp3, Al-Isra pdf. Aaya 98–102. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers