Al-Isra · 28/111
Tekki Waxtaan — Al-Isra
وَإِمَّا تُعْرِضَنَّ عَنْهُمُ ابْتِغَاءَ رَحْمَةٍ مِّن رَّبِّكَ تَرْجُوهَا فَقُل لَّهُمْ قَوْلًا مَّيْسُورًا ۝٢٨
Wa immaa turidanna `anhumub tighaaa`a rahmatim mir rabbika tarjoohaa faqul lahum qawlam maisooraa
📖 Tekkim Wolof
Bu fekkee [ñàkk loo leen jox tax na] nga dëddu leen, toog di yaakaar sa yërmaandey Boroom ; nanga leen wax wax ju neex.

🎧 Dégg


📜 Aaya 26-30 — Al-Isra

26وَآتِ ذَا الْقُرْبَىٰ حَقَّهُ وَالْمِسْكِينَ وَابْنَ السَّبِيلِ وَلَا تُبَذِّرْ تَبْذِيرًا
“Nanga jox sa jegeñaale li la war ci moom, ak ku ñàkk ak ku nekk ci tukki. Waaye bul nekk di pasar-pasaree alal,
27إِنَّ الْمُبَذِّرِينَ كَانُوا إِخْوَانَ الشَّيَاطِينِ ۖ وَكَانَ الشَّيْطَانُ لِرَبِّهِ كَفُورًا
yàqkat yi mbokki Séytaane lañu ; te Séytaane dafa weddi Boroomam.
28وَإِمَّا تُعْرِضَنَّ عَنْهُمُ ابْتِغَاءَ رَحْمَةٍ مِّن رَّبِّكَ تَرْجُوهَا فَقُل لَّهُمْ قَوْلًا مَّيْسُورًا
Bu fekkee [ñàkk loo leen jox tax na] nga dëddu leen, toog di yaakaar sa yërmaandey Boroom ; nanga leen wax wax ju neex.
29وَلَا تَجْعَلْ يَدَكَ مَغْلُولَةً إِلَىٰ عُنُقِكَ وَلَا تَبْسُطْهَا كُلَّ الْبَسْطِ فَتَقْعُدَ مَلُومًا مَّحْسُورًا
Bul bank sa loxo ba mu mel ni lu ñu yeew ci sa doq, waaye it bu ko tàllal mu tàlli ñareet, kon danga mujj di ku ñu yedd, ku ñu dàkku.
30إِنَّ رَبَّكَ يَبْسُطُ الرِّزْقَ لِمَن يَشَاءُ وَيَقْدِرُ ۚ إِنَّهُ كَانَ بِعِبَادِهِ خَبِيرًا بَصِيرًا
Naka sa Boroom mooy yaatal wërsëgu ku Ko soob. Moo koy xatal it, naka Moom ku xam tey gis la jaamam yi.
Al-IsraFihi Alxuraan
111Aaya
MeccanRevelation
28Aaya

Tekki — Al-Isra 28

Simoore Al-Isra Aaya 28 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Bu fekkee [ñàkk loo leen jox tax na] nga dëddu…

Simoore Aaya 28/111 — Al-Isra الإسراء (Meccan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Al-Isra Dégg, Al-Isra Tekki, Al-Isra mp3, Al-Isra pdf. Aaya 26–30. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers