Al-Baqara · 146/286
Tekki Waxtaan — Al-Baqara
الَّذِينَ آتَيْنَاهُمُ الْكِتَابَ يَعْرِفُونَهُ كَمَا يَعْرِفُونَ أَبْنَاءَهُمْ ۖ وَإِنَّ فَرِيقًا مِّنْهُمْ لَيَكْتُمُونَ الْحَقَّ وَهُمْ يَعْلَمُونَ ۝١٤٦
Allazeena aatainaahumul kitaaba ya`rifoonahoo kamaa ya`rifoona abnaaa`ahum wa inna fareeqam minhum layaktumoonal haqqa wa hum ya`lamoon
📖 Tekkim Wolof
Ña ñu joxoon Téere, xam nañu ko ni ñu xame seeni doon. Dafa fekk ne am na ci ñoom kurél bu xam dëgg ba noppi di ko nëbb !
🎧 Dégg

📜 Aaya 144-148 — Al-Baqara

144قَدْ نَرَىٰ تَقَلُّبَ وَجْهِكَ فِي السَّمَاءِ ۖ فَلَنُوَلِّيَنَّكَ قِبْلَةً تَرْضَاهَا ۚ فَوَلِّ وَجْهَكَ شَطْرَ الْمَسْجِدِ الْحَرَامِ ۚ وَحَيْثُ مَا كُنتُمْ فَوَلُّوا وُجُوهَكُمْ شَطْرَهُ ۗ وَإِنَّ الَّذِينَ أُوتُوا الْكِتَابَ لَيَعْلَمُونَ أَنَّهُ الْحَقُّ مِن رَّبِّهِمْ ۗ وَمَا اللَّهُ بِغَافِلٍ عَمَّا يَعْمَلُونَ
Gis Nanu la ni ngay wëlbatee sa xar-kanam, di téen ci asamaan. Dananu la méngalee jubluwaay boo gëram. Kon jubaleel sa xar-kanam jëmale ko ca Jàkka ju ñu wormaal ja (Al masjidal Haraam). Fu ngeen mën a nekkati, nangeen ko jublu. Te sax, ñañu joxoon Téere ba [Ñoñ-téere] xam nañu xéll ne mooy dëgg gi bawoo ca seen Boroom. Te Yàlla du sàggane li ñuy jëf de.
145وَلَئِنْ أَتَيْتَ الَّذِينَ أُوتُوا الْكِتَابَ بِكُلِّ آيَةٍ مَّا تَبِعُوا قِبْلَتَكَ ۚ وَمَا أَنتَ بِتَابِعٍ قِبْلَتَهُمْ ۚ وَمَا بَعْضُهُم بِتَابِعٍ قِبْلَةَ بَعْضٍ ۚ وَلَئِنِ اتَّبَعْتَ أَهْوَاءَهُم مِّن بَعْدِ مَا جَاءَكَ مِنَ الْعِلْمِ ۙ إِنَّكَ إِذًا لَّمِنَ الظَّالِمِينَ
Boo indiloon, ñoñ-téere, kéemaan gu mu mën a doon, du tax ñu topp sa jubluwaay (xibla) ! Yaw itam du yaay topp seen xibla ; ñoom ci seen biir sax, kenn du ca topp xibla moroomam. Yaw nag boo toppee seeni bànneex ginnaaw ba la xam-xam bu leer dikkalee, kon de ca tooñkat ya ngay bokk.
146الَّذِينَ آتَيْنَاهُمُ الْكِتَابَ يَعْرِفُونَهُ كَمَا يَعْرِفُونَ أَبْنَاءَهُمْ ۖ وَإِنَّ فَرِيقًا مِّنْهُمْ لَيَكْتُمُونَ الْحَقَّ وَهُمْ يَعْلَمُونَ
Ña ñu joxoon Téere, xam nañu ko ni ñu xame seeni doon. Dafa fekk ne am na ci ñoom kurél bu xam dëgg ba noppi di ko nëbb !
147الْحَقُّ مِن رَّبِّكَ ۖ فَلَا تَكُونَنَّ مِنَ الْمُمْتَرِينَ
Dëgg, ca sa Boroom la bawoo. Bul bokk mukk ci werentekat yiy sikki-sàkka.
148وَلِكُلٍّ وِجْهَةٌ هُوَ مُوَلِّيهَا ۖ فَاسْتَبِقُوا الْخَيْرَاتِ ۚ أَيْنَ مَا تَكُونُوا يَأْتِ بِكُمُ اللَّهُ جَمِيعًا ۚ إِنَّ اللَّهَ عَلَىٰ كُلِّ شَيْءٍ قَدِيرٌ
Xeet bu nekk a am jublukaayam . Nangeen njëkkante ci jëf yu baax, yu yiw. Fu ngeen fi mën a nekk nag, Yàlla dana leen dajale yéen ñepp ca Bis-pénc ba, Yàlla mën na lu nekk.
Al-BaqaraFihi Alxuraan
286Aaya
MedinanRevelation
146Aaya

Tekki — Al-Baqara 146

Simoore Al-Baqara Aaya 146 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Ña ñu joxoon Téere, xam nañu ko ni ñu xame…

Simoore Aaya 146/286 — Al-Baqara البقرة (Medinan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Al-Baqara Dégg, Al-Baqara Tekki, Al-Baqara mp3, Al-Baqara pdf. Aaya 144–148. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers