Al-Baqara · 206/286
Tekki Waxtaan — Al-Baqara
وَإِذَا قِيلَ لَهُ اتَّقِ اللَّهَ أَخَذَتْهُ الْعِزَّةُ بِالْإِثْمِ ۚ فَحَسْبُهُ جَهَنَّمُ ۚ وَلَبِئْسَ الْمِهَادُ ۝٢٠٦
Wa izaa qeela lahuttaqil laaha akhazathul izzatu bil-ism; fahasbuhoo jahannam; wa labi`sal mihaad
📖 Tekkim Wolof
Te Bu ñu ko nee : “Ragalal Yàlla”, mu jomlu sax ci bàkkaar rekk, Safara dana ko doy ag pey, te bon na, lal ba ko fay xaar !

🎧 Dégg


📜 Aaya 204-208 — Al-Baqara

204وَمِنَ النَّاسِ مَن يُعْجِبُكَ قَوْلُهُ فِي الْحَيَاةِ الدُّنْيَا وَيُشْهِدُ اللَّهَ عَلَىٰ مَا فِي قَلْبِهِ وَهُوَ أَلَدُّ الْخِصَامِ
Am na ci nit ñi seeni wax dalay yéem lool, ci dundug àddina ndax day seedeloo Yàlla la nekk ca xolam, ndekeyoo moom xulóowaale la bu pànk, bu yées.
205وَإِذَا تَوَلَّىٰ سَعَىٰ فِي الْأَرْضِ لِيُفْسِدَ فِيهَا وَيُهْلِكَ الْحَرْثَ وَالنَّسْلَ ۗ وَاللَّهُ لَا يُحِبُّ الْفَسَادَ
Bu nee wërëñ rekk tàmbalee yàq ci kaw suuf, di alag mbay mi ak jur gi te Yàlla bëggul ag yàq.
206وَإِذَا قِيلَ لَهُ اتَّقِ اللَّهَ أَخَذَتْهُ الْعِزَّةُ بِالْإِثْمِ ۚ فَحَسْبُهُ جَهَنَّمُ ۚ وَلَبِئْسَ الْمِهَادُ
Te Bu ñu ko nee : “Ragalal Yàlla”, mu jomlu sax ci bàkkaar rekk, Safara dana ko doy ag pey, te bon na, lal ba ko fay xaar !
207وَمِنَ النَّاسِ مَن يَشْرِي نَفْسَهُ ابْتِغَاءَ مَرْضَاتِ اللَّهِ ۗ وَاللَّهُ رَءُوفٌ بِالْعِبَادِ
Am na ci nit ñi ñuy jaay seen bakkan ngir sàkku ngërëmul Yàlla. Yàlla dey Aji-ñeewant la ci jaamam ñi.
208يَا أَيُّهَا الَّذِينَ آمَنُوا ادْخُلُوا فِي السِّلْمِ كَافَّةً وَلَا تَتَّبِعُوا خُطُوَاتِ الشَّيْطَانِ ۚ إِنَّهُ لَكُمْ عَدُوٌّ مُّبِينٌ
Éy yéen ñi gëm ! Dugguleen yéen ñépp ci jàmm ji [Islaam], te buleen topp yoonu [Séytaane], moom seenub noon la bu bir.
Al-BaqaraFihi Alxuraan
286Aaya
MedinanRevelation
206Aaya

Tekki — Al-Baqara 206

Simoore Al-Baqara Aaya 206 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Te Bu ñu ko nee : “Ragalal Yàlla”, mu jomlu…

Simoore Aaya 206/286 — Al-Baqara البقرة (Medinan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Al-Baqara Dégg, Al-Baqara Tekki, Al-Baqara mp3, Al-Baqara pdf. Aaya 204–208. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Wednesday, August 19, 2026

Don't forget us in your sincere prayers