Al-Baqara · 56/286
Tekki Waxtaan — Simoore Al-Baqara
ثُمَّ بَعَثْنَاكُم مِّن بَعْدِ مَوْتِكُمْ لَعَلَّكُمْ تَشْكُرُونَ ۝٥٦
Summa ba`asnaakum mim ba`di mawtikum la`allakum tashkuroon
📖 Tekkim Wolof
Topp Nu dekkal leen ginnaaw ba ngeen deewee, ndax Yàlla ngeen di sant [seen Boroom].

🎧 Dégg


📜 Aaya 54-58 — Simoore Al-Baqara

54وَإِذْ قَالَ مُوسَىٰ لِقَوْمِهِ يَا قَوْمِ إِنَّكُمْ ظَلَمْتُمْ أَنفُسَكُم بِاتِّخَاذِكُمُ الْعِجْلَ فَتُوبُوا إِلَىٰ بَارِئِكُمْ فَاقْتُلُوا أَنفُسَكُمْ ذَٰلِكُمْ خَيْرٌ لَّكُمْ عِندَ بَارِئِكُمْ فَتَابَ عَلَيْكُمْ ۚ إِنَّهُ هُوَ التَّوَّابُ الرَّحِيمُ
Ak ba Muusaa waxee aw nitam : "Samaw nit, yéen tooñ ngeen seen bopp ci li ngeen jaamu yëkk wa. Na ngeen baalu seen Boroom; te ngeen reyante yéen [ñi bokkoon ci moy Yàlla googu] : Looloo gën ci yéen ca seen Boroom” !... Kon mu jéggal leen ndax moom mooy Jéggalaakoon ba, di Jaglewaakoon ba !
55وَإِذْ قُلْتُمْ يَا مُوسَىٰ لَن نُّؤْمِنَ لَكَ حَتَّىٰ نَرَى اللَّهَ جَهْرَةً فَأَخَذَتْكُمُ الصَّاعِقَةُ وَأَنتُمْ تَنظُرُونَ
Ak ba ngeen waxee ne : “ Yaw Muusaa, dunu la gëm ba ba nuy gis Yàlla ne jàkk ci Moom” !... Faf xaacu ga fàdd leen, ngeen di gis loolu.
56ثُمَّ بَعَثْنَاكُم مِّن بَعْدِ مَوْتِكُمْ لَعَلَّكُمْ تَشْكُرُونَ
Topp Nu dekkal leen ginnaaw ba ngeen deewee, ndax Yàlla ngeen di sant [seen Boroom].
57وَظَلَّلْنَا عَلَيْكُمُ الْغَمَامَ وَأَنزَلْنَا عَلَيْكُمُ الْمَنَّ وَالسَّلْوَىٰ ۖ كُلُوا مِن طَيِّبَاتِ مَا رَزَقْنَاكُمْ ۖ وَمَا ظَلَمُونَا وَلَٰكِن كَانُوا أَنفُسَهُمْ يَظْلِمُونَ
Nu keral leen ak i niir, wàcceel leen lem ak i picc [yu tuddu gëméen], ne leen : - “Lekk leen ci lu sell lii Nu leen xéewale ! ” - Ñoom daal seen bopp lañuy tooñ, waaye du Nun lañuy tooñ.
58وَإِذْ قُلْنَا ادْخُلُوا هَٰذِهِ الْقَرْيَةَ فَكُلُوا مِنْهَا حَيْثُ شِئْتُمْ رَغَدًا وَادْخُلُوا الْبَابَ سُجَّدًا وَقُولُوا حِطَّةٌ نَّغْفِرْ لَكُمْ خَطَايَاكُمْ ۚ وَسَنَزِيدُ الْمُحْسِنِينَ
[Fàttalikuleen it], ba Nu leen waxee ne : “Dugguleen ci dëkk bii, lekk ci fu leen neex cig yaatu ; te ngeen jàll buntu bi ànd ak toroxlu te nangeen ñaan Yàlla mu seppi seeni bàkkaar ; [Su ngeen ko defee,] Nu jéggal leen seeni ñaawtéef, Dananu dolli way-rafetal ña aw yiw.
Al-BaqaraFihi Alxuraan
286Aaya
MedinanRevelation
56Aaya

Tekki — Al-Baqara 56

Simoore Al-Baqara Aaya 56 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Topp Nu dekkal leen ginnaaw ba ngeen deewee, ndax Yàlla…

Simoore Aaya 56/286 — Simoore Al-Baqara البقرة (Medinan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Simoore Al-Baqara Dégg, Simoore Al-Baqara Tekki, Simoore Al-Baqara mp3, Simoore Al-Baqara pdf. Aaya 54–58. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, September 8, 2026

Don't forget us in your sincere prayers