Al-Anbiya · 20/112
Tekki Waxtaan — Al-Anbiya
يُسَبِّحُونَ اللَّيْلَ وَالنَّهَارَ لَا يَفْتُرُونَ ۝٢٠
Yusabbihoona laila wannahaara laa yafturoon
📖 Tekkim Wolof
Dañu Koy sàbbaal guddi ak bëccëg, duñu ca jóge.

🎧 Dégg


📜 Aaya 18-22 — Al-Anbiya

18بَلْ نَقْذِفُ بِالْحَقِّ عَلَى الْبَاطِلِ فَيَدْمَغُهُ فَإِذَا هُوَ زَاهِقٌ ۚ وَلَكُمُ الْوَيْلُ مِمَّا تَصِفُونَ
Déedéet Dananu sanni dëgg ci kaw fen mu tojte ko, tax mu raaf. Te li ngeen di nirale [Yàlla] dana tax ngeen toskare.
19وَلَهُ مَن فِي السَّمَاوَاتِ وَالْأَرْضِ ۚ وَمَنْ عِندَهُ لَا يَسْتَكْبِرُونَ عَنْ عِبَادَتِهِ وَلَا يَسْتَحْسِرُونَ
Moo moom lépp li nekk ci asamaan yi ak suuf si. Te ña nekk fa Moom duñu rëy-rëylu [ci di ko jaamu], te it duñu ca lott.
20يُسَبِّحُونَ اللَّيْلَ وَالنَّهَارَ لَا يَفْتُرُونَ
Dañu Koy sàbbaal guddi ak bëccëg, duñu ca jóge.
21أَمِ اتَّخَذُوا آلِهَةً مِّنَ الْأَرْضِ هُمْ يُنشِرُونَ
Ndax ñoom dañuy jaamu ay yàlla ci suuf si [yuy mën a dekkal ku dee ni Boroom bi] ? [Mukk du am]
22لَوْ كَانَ فِيهِمَا آلِهَةٌ إِلَّا اللَّهُ لَفَسَدَتَا ۚ فَسُبْحَانَ اللَّهِ رَبِّ الْعَرْشِ عَمَّا يَصِفُونَ
Su jeneen yàlla ju dul Yàlla amoon ci asamaan yeek suuf si, kon ñoom ñaar ñépp yàqu. Cëy sellam ga, Mooy Boroom Gàngunaay ga [Aras] ; Jomb na li ñu koy nirale !
Al-AnbiyaFihi Alxuraan
112Aaya
MeccanRevelation
20Aaya

Tekki — Al-Anbiya 20

Simoore Al-Anbiya Aaya 20 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Dañu Koy sàbbaal guddi ak bëccëg, duñu ca jóge.

Simoore Aaya 20/112 — Al-Anbiya الأنبياء (Meccan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Al-Anbiya Dégg, Al-Anbiya Tekki, Al-Anbiya mp3, Al-Anbiya pdf. Aaya 18–22. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers