Al-Hajj · 74/78
Tekki Waxtaan — Al-Hajj
مَا قَدَرُوا اللَّهَ حَقَّ قَدْرِهِ ۗ إِنَّ اللَّهَ لَقَوِيٌّ عَزِيزٌ ۝٧٤
Maa qadrul laaha haqqa qadrih; innal laaha la Qawiyyun `Azeez
📖 Tekkim Wolof
Màggal-leen Yàlla ni ko màggaayam yeyoo ; Te Yàlla ca dëgg-dëgg Dafa bari kàttan tey Notaakoon ba.
🎧 Dégg

📜 Aaya 72-76 — Al-Hajj

72وَإِذَا تُتْلَىٰ عَلَيْهِمْ آيَاتُنَا بَيِّنَاتٍ تَعْرِفُ فِي وُجُوهِ الَّذِينَ كَفَرُوا الْمُنكَرَ ۖ يَكَادُونَ يَسْطُونَ بِالَّذِينَ يَتْلُونَ عَلَيْهِمْ آيَاتِنَا ۗ قُلْ أَفَأُنَبِّئُكُم بِشَرٍّ مِّن ذَٰلِكُمُ ۗ النَّارُ وَعَدَهَا اللَّهُ الَّذِينَ كَفَرُوا ۖ وَبِئْسَ الْمَصِيرُ
Bu ñu jàngee ci seen kanam Sunu kàddu yu leer yi, danga ràññee ca kanamu ña weddi weddi ga. Te tuuti kon ñu songu ña jàng Sunuy kàddu ci seen kanam. Neel : “Ndax ma xamal leen lu yées loolu ci yéen ? - Mooy Safara : Yàlla dig na ko ña weddi. Ndax daluwaay bu bon !”
73يَا أَيُّهَا النَّاسُ ضُرِبَ مَثَلٌ فَاسْتَمِعُوا لَهُ ۚ إِنَّ الَّذِينَ تَدْعُونَ مِن دُونِ اللَّهِ لَن يَخْلُقُوا ذُبَابًا وَلَوِ اجْتَمَعُوا لَهُ ۖ وَإِن يَسْلُبْهُمُ الذُّبَابُ شَيْئًا لَّا يَسْتَنقِذُوهُ مِنْهُ ۚ ضَعُفَ الطَّالِبُ وَالْمَطْلُوبُ
Éy yéen nit ñi ! Ñi ngi leen di sadd léebu, dégluleen ko : “Ñi ngeen di jaamu bàyyi Yàlla duñu mën bind mukk aw weñ, doonte dañoo dajaloo ngir def ko. Te bu leen wenn weñ jëlaloon dara, duñu ko mën a nangu ci moom. Néew na doole ka jaamu ak ka ñu jaamu ! ”
74مَا قَدَرُوا اللَّهَ حَقَّ قَدْرِهِ ۗ إِنَّ اللَّهَ لَقَوِيٌّ عَزِيزٌ
Màggal-leen Yàlla ni ko màggaayam yeyoo ; Te Yàlla ca dëgg-dëgg Dafa bari kàttan tey Notaakoon ba.
75اللَّهُ يَصْطَفِي مِنَ الْمَلَائِكَةِ رُسُلًا وَمِنَ النَّاسِ ۚ إِنَّ اللَّهَ سَمِيعٌ بَصِيرٌ
Yàlla moo tànn ay Yonent ci Malaaka yi ak nit ñi. Yàlla nag dana dégg, dana gis.
76يَعْلَمُ مَا بَيْنَ أَيْدِيهِمْ وَمَا خَلْفَهُمْ ۗ وَإِلَى اللَّهِ تُرْجَعُ الْأُمُورُ
Xam na li nekk ci seen kanam ak la weesu nekk ca seen ginnaaw. Te ca Yàlla la mbir yépp di dellusi.
Al-HajjFihi Alxuraan
78Aaya
MedinanRevelation
74Aaya

Tekki — Al-Hajj 74

Simoore Al-Hajj Aaya 74 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Màggal-leen Yàlla ni ko màggaayam yeyoo ; Te Yàlla ca…

Simoore Aaya 74/78 — Al-Hajj الحج (Medinan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Al-Hajj Dégg, Al-Hajj Tekki, Al-Hajj mp3, Al-Hajj pdf. Aaya 72–76. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers