Al-Hajj · 75/78
Tekki Waxtaan — Al-Hajj
اللَّهُ يَصْطَفِي مِنَ الْمَلَائِكَةِ رُسُلًا وَمِنَ النَّاسِ ۚ إِنَّ اللَّهَ سَمِيعٌ بَصِيرٌ ۝٧٥
Allahu yastafee minal malaaa`ikati Rusulanw wa minan naas; innal laaha Samee`um Baseer
📖 Tekkim Wolof
Yàlla moo tànn ay Yonent ci Malaaka yi ak nit ñi. Yàlla nag dana dégg, dana gis.
🎧 Dégg

📜 Aaya 73-77 — Al-Hajj

73يَا أَيُّهَا النَّاسُ ضُرِبَ مَثَلٌ فَاسْتَمِعُوا لَهُ ۚ إِنَّ الَّذِينَ تَدْعُونَ مِن دُونِ اللَّهِ لَن يَخْلُقُوا ذُبَابًا وَلَوِ اجْتَمَعُوا لَهُ ۖ وَإِن يَسْلُبْهُمُ الذُّبَابُ شَيْئًا لَّا يَسْتَنقِذُوهُ مِنْهُ ۚ ضَعُفَ الطَّالِبُ وَالْمَطْلُوبُ
Éy yéen nit ñi ! Ñi ngi leen di sadd léebu, dégluleen ko : “Ñi ngeen di jaamu bàyyi Yàlla duñu mën bind mukk aw weñ, doonte dañoo dajaloo ngir def ko. Te bu leen wenn weñ jëlaloon dara, duñu ko mën a nangu ci moom. Néew na doole ka jaamu ak ka ñu jaamu ! ”
74مَا قَدَرُوا اللَّهَ حَقَّ قَدْرِهِ ۗ إِنَّ اللَّهَ لَقَوِيٌّ عَزِيزٌ
Màggal-leen Yàlla ni ko màggaayam yeyoo ; Te Yàlla ca dëgg-dëgg Dafa bari kàttan tey Notaakoon ba.
75اللَّهُ يَصْطَفِي مِنَ الْمَلَائِكَةِ رُسُلًا وَمِنَ النَّاسِ ۚ إِنَّ اللَّهَ سَمِيعٌ بَصِيرٌ
Yàlla moo tànn ay Yonent ci Malaaka yi ak nit ñi. Yàlla nag dana dégg, dana gis.
76يَعْلَمُ مَا بَيْنَ أَيْدِيهِمْ وَمَا خَلْفَهُمْ ۗ وَإِلَى اللَّهِ تُرْجَعُ الْأُمُورُ
Xam na li nekk ci seen kanam ak la weesu nekk ca seen ginnaaw. Te ca Yàlla la mbir yépp di dellusi.
77يَا أَيُّهَا الَّذِينَ آمَنُوا ارْكَعُوا وَاسْجُدُوا وَاعْبُدُوا رَبَّكُمْ وَافْعَلُوا الْخَيْرَ لَعَلَّكُمْ تُفْلِحُونَ ۩
Éy yéen ñi gëm ! Deeleen sëgg di sujjóot, di jaamu seen Boroom, tey def lu baax. Ndax xéy-na yéen ngeen texe !
Al-HajjFihi Alxuraan
78Aaya
MedinanRevelation
75Aaya

Tekki — Al-Hajj 75

Simoore Al-Hajj Aaya 75 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Yàlla moo tànn ay Yonent ci Malaaka yi ak nit…

Simoore Aaya 75/78 — Al-Hajj الحج (Medinan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Al-Hajj Dégg, Al-Hajj Tekki, Al-Hajj mp3, Al-Hajj pdf. Aaya 73–77. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers