Al-Qasas · 24/88
Tekki Waxtaan — Al-Qasas
فَسَقَىٰ لَهُمَا ثُمَّ تَوَلَّىٰ إِلَى الظِّلِّ فَقَالَ رَبِّ إِنِّي لِمَا أَنزَلْتَ إِلَيَّ مِنْ خَيْرٍ فَقِيرٌ ۝٢٤
Fasaqaa lahumaa summa tawallaaa ilaz zilli faqaala Rabbi innee limaaa anzalta ilaiya min khairin faqeer
📖 Tekkim Wolof
Mu wëggal leen ba eggal, dem toog ca ker ga, daldi ne : “Sama Boroom, cëy aka maa ittewoo li nga may wërsëgale”.

🎧 Dégg


📜 Aaya 22-26 — Al-Qasas

22وَلَمَّا تَوَجَّهَ تِلْقَاءَ مَدْيَنَ قَالَ عَسَىٰ رَبِّي أَن يَهْدِيَنِي سَوَاءَ السَّبِيلِ
Ba mu jubloo njëlal Madiyaana, wax na ne : “Amaana sama Boroom gindi ma, teg ma ci yoon wu jub wa”.
23وَلَمَّا وَرَدَ مَاءَ مَدْيَنَ وَجَدَ عَلَيْهِ أُمَّةً مِّنَ النَّاسِ يَسْقُونَ وَوَجَدَ مِن دُونِهِمُ امْرَأَتَيْنِ تَذُودَانِ ۖ قَالَ مَا خَطْبُكُمَا ۖ قَالَتَا لَا نَسْقِي حَتَّىٰ يُصْدِرَ الرِّعَاءُ ۖ وَأَبُونَا شَيْخٌ كَبِيرٌ
Ba mu agsee ca rootukaayub waa Madiyaana, mu fekk fa aw nit ñuy wëgg di jukki, mu fekk fa ba-tey ñaari jigéen ñu beru wëgguñu. Mu ne leen : “Lu xew ba wëgguleen ? ” Ñu ne ko : “Dunu wëgg lu dul ginnaaw ba sàmm si génnee ba dem ; te sunu baay màggat na”.
24فَسَقَىٰ لَهُمَا ثُمَّ تَوَلَّىٰ إِلَى الظِّلِّ فَقَالَ رَبِّ إِنِّي لِمَا أَنزَلْتَ إِلَيَّ مِنْ خَيْرٍ فَقِيرٌ
Mu wëggal leen ba eggal, dem toog ca ker ga, daldi ne : “Sama Boroom, cëy aka maa ittewoo li nga may wërsëgale”.
25فَجَاءَتْهُ إِحْدَاهُمَا تَمْشِي عَلَى اسْتِحْيَاءٍ قَالَتْ إِنَّ أَبِي يَدْعُوكَ لِيَجْزِيَكَ أَجْرَ مَا سَقَيْتَ لَنَا ۚ فَلَمَّا جَاءَهُ وَقَصَّ عَلَيْهِ الْقَصَصَ قَالَ لَا تَخَفْ ۖ نَجَوْتَ مِنَ الْقَوْمِ الظَّالِمِينَ
Kenn ca ñaari xale yu jigéen ña dikk fa moom ak kersa ga, daldi ne ko : “Saa baay nee na nga ñëw mu fey la li nga nu wëggaloon”. Ba Muusaa agsee ba nettali ko xew-xew ba, mu ne ko : “Bul tiit : mucc nga ci tooñkat ya”.
26قَالَتْ إِحْدَاهُمَا يَا أَبَتِ اسْتَأْجِرْهُ ۖ إِنَّ خَيْرَ مَنِ اسْتَأْجَرْتَ الْقَوِيُّ الْأَمِينُ
Kenn ca ñaari jigéen ña ne ko : “Baay jàpp ko surga, koy dey nga am surga bu am doole te wóor”.
Al-QasasFihi Alxuraan
88Aaya
MeccanRevelation
24Aaya

Tekki — Al-Qasas 24

Simoore Al-Qasas Aaya 24 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Mu wëggal leen ba eggal, dem toog ca ker ga,…

Simoore Aaya 24/88 — Al-Qasas القصص (Meccan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Al-Qasas Dégg, Al-Qasas Tekki, Al-Qasas mp3, Al-Qasas pdf. Aaya 22–26. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers