Aali Imran · 120/200
Tekki Waxtaan — Aali Imran
إِن تَمْسَسْكُمْ حَسَنَةٌ تَسُؤْهُمْ وَإِن تُصِبْكُمْ سَيِّئَةٌ يَفْرَحُوا بِهَا ۖ وَإِن تَصْبِرُوا وَتَتَّقُوا لَا يَضُرُّكُمْ كَيْدُهُمْ شَيْئًا ۗ إِنَّ اللَّهَ بِمَا يَعْمَلُونَ مُحِيطٌ ۝١٢٠
In tamsaskum hasanatun tasu`hum wa in tusibkum saiyi`atuny yafrahoo bihaa wa in tasbiroo wa tattaqoo laa yad urrukum kaiduhum shai`aa; innal laaha bimaa ya`maloona muheet
📖 Tekkim Wolof
Bu ngeen amee bànneex, mu naqari leen. Bu ngeen amee naqar, mu di seen bànneex ñoom. Waaye bu ngeen muñee te ragal Yàlla, seen pexe yi duleen wàññi dara. Te Yàlla ku peeg la la ñuy def.

🎧 Dégg


📜 Aaya 118-122 — Aali Imran

118يَا أَيُّهَا الَّذِينَ آمَنُوا لَا تَتَّخِذُوا بِطَانَةً مِّن دُونِكُمْ لَا يَأْلُونَكُمْ خَبَالًا وَدُّوا مَا عَنِتُّمْ قَدْ بَدَتِ الْبَغْضَاءُ مِنْ أَفْوَاهِهِمْ وَمَا تُخْفِي صُدُورُهُمْ أَكْبَرُ ۚ قَدْ بَيَّنَّا لَكُمُ الْآيَاتِ ۖ إِن كُنتُمْ تَعْقِلُونَ
Yéen ñi gëm, buleen won seen mbir ci ag xaritoo keneen ku bokkul ci yéen. Bumuy ci ñoo xam ne dañuy kàttanlu ci yàqal leen, danañu ngéeju ngir ngeen am coono. Mbañeel ga feen na ca seeni wax, te la seeni xol ëmb moo yéesati. Yéen leeral nanu leen kéemaan yi [ngeen war leen a ràññee ndegam ñu xel-lu ngeen ! ].
119هَا أَنتُمْ أُولَاءِ تُحِبُّونَهُمْ وَلَا يُحِبُّونَكُمْ وَتُؤْمِنُونَ بِالْكِتَابِ كُلِّهِ وَإِذَا لَقُوكُمْ قَالُوا آمَنَّا وَإِذَا خَلَوْا عَضُّوا عَلَيْكُمُ الْأَنَامِلَ مِنَ الْغَيْظِ ۚ قُلْ مُوتُوا بِغَيْظِكُمْ ۗ إِنَّ اللَّهَ عَلِيمٌ بِذَاتِ الصُّدُورِ
Yéen ak ñoom, yëgleen ne yéen a leen safoo, waaye ñoom safoowuñu leen ; te yéen gëm ngeen Téere bi lépp. Bu ñu dajee ak yéen ne “Gëm nanu” ; bu ñu wéyee màtt seeni waaroom wiccax ndax mer. Neel : “Deeleen ci mer” ; Yàlla ku xam la lu nekk ci xol yi.
120إِن تَمْسَسْكُمْ حَسَنَةٌ تَسُؤْهُمْ وَإِن تُصِبْكُمْ سَيِّئَةٌ يَفْرَحُوا بِهَا ۖ وَإِن تَصْبِرُوا وَتَتَّقُوا لَا يَضُرُّكُمْ كَيْدُهُمْ شَيْئًا ۗ إِنَّ اللَّهَ بِمَا يَعْمَلُونَ مُحِيطٌ
Bu ngeen amee bànneex, mu naqari leen. Bu ngeen amee naqar, mu di seen bànneex ñoom. Waaye bu ngeen muñee te ragal Yàlla, seen pexe yi duleen wàññi dara. Te Yàlla ku peeg la la ñuy def.
121وَإِذْ غَدَوْتَ مِنْ أَهْلِكَ تُبَوِّئُ الْمُؤْمِنِينَ مَقَاعِدَ لِلْقِتَالِ ۗ وَاللَّهُ سَمِيعٌ عَلِيمٌ
Fàttalikul yaw Yonent bi, ba nga xëyee jóge ci sa njaboot, di tegtal jullit ña barabu xeexukaay ya, xamal ne Yàlla kuy dégg la, Kuy xam la.
122إِذْ هَمَّت طَّائِفَتَانِ مِنكُمْ أَن تَفْشَلَا وَاللَّهُ وَلِيُّهُمَا ۗ وَعَلَى اللَّهِ فَلْيَتَوَكَّلِ الْمُؤْمِنُونَ
[Fàttalikul] ba ñaari kurél ci yéen naree yoqat ! Te Moo leen dimbali woon ba delluwuñu ginnaaw ! Way-gëm ña, nañu sukkandiku ci Yàlla [Uhud].
Aali ImranFihi Alxuraan
200Aaya
MedinanRevelation
120Aaya

Tekki — Aali Imran 120

Simoore Aali Imran Aaya 120 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Bu ngeen amee bànneex, mu naqari leen. Bu ngeen amee…

Simoore Aaya 120/200 — Aali Imran آل عمران (Medinan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Aali Imran Dégg, Aali Imran Tekki, Aali Imran mp3, Aali Imran pdf. Aaya 118–122. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers