Aali Imran · 187/200
Tekki Waxtaan — Aali Imran
وَإِذْ أَخَذَ اللَّهُ مِيثَاقَ الَّذِينَ أُوتُوا الْكِتَابَ لَتُبَيِّنُنَّهُ لِلنَّاسِ وَلَا تَكْتُمُونَهُ فَنَبَذُوهُ وَرَاءَ ظُهُورِهِمْ وَاشْتَرَوْا بِهِ ثَمَنًا قَلِيلًا ۖ فَبِئْسَ مَا يَشْتَرُونَ ۝١٨٧
Wa iz akhazal laahu meesaaqal lazeena ootul Kitaaba latubaiyinunnahoo linnaasi wa laa taktumoona hoo fanabazoohu waraaa`a zuhoorihim washtaraw bihee samanan qaleelan fabi`sa maa yashtaroon
📖 Tekkim Wolof
[Fàttalikul] ba Yàlla kóllaranteek ña jot Téere, ne : “Nangeen ko leeralal nit ñi te buleen ko nëbb”. Ñu sànni ko ca seen ginnaaw, jaaye ko njëg gu néew. Ndax njëg gu bon !

🎧 Dégg


📜 Aaya 185-189 — Aali Imran

185كُلُّ نَفْسٍ ذَائِقَةُ الْمَوْتِ ۗ وَإِنَّمَا تُوَفَّوْنَ أُجُورَكُمْ يَوْمَ الْقِيَامَةِ ۖ فَمَن زُحْزِحَ عَنِ النَّارِ وَأُدْخِلَ الْجَنَّةَ فَقَدْ فَازَ ۗ وَمَا الْحَيَاةُ الدُّنْيَا إِلَّا مَتَاعُ الْغُرُورِ
Bakkan bu nekk dana tàqamtiku [mos] dee. Waaye dangeen jot seen pey ca Bis-pénc ba. Ku ñu soreel Safara ba, dugal ko Àjjana, texe na. Te dundug àddina gi du dara lu dul xéewal guy naxe [naxti ndaw].
186۞ لَتُبْلَوُنَّ فِي أَمْوَالِكُمْ وَأَنفُسِكُمْ وَلَتَسْمَعُنَّ مِنَ الَّذِينَ أُوتُوا الْكِتَابَ مِن قَبْلِكُمْ وَمِنَ الَّذِينَ أَشْرَكُوا أَذًى كَثِيرًا ۚ وَإِن تَصْبِرُوا وَتَتَّقُوا فَإِنَّ ذَٰلِكَ مِنْ عَزْمِ الْأُمُورِ
Fàwwu dees na leen nattu ci seeni alal ak ci seeni bakkan ; dangeen dégge ca ñoñ-téere ya leen jiitu woon ak bokkaalekat ya, wax yu ñaaw yu bari.Waaye, bu ngeen muñee te ragal Yàlla... mooy sabab duggu gay tax mbir ya sotti.
187وَإِذْ أَخَذَ اللَّهُ مِيثَاقَ الَّذِينَ أُوتُوا الْكِتَابَ لَتُبَيِّنُنَّهُ لِلنَّاسِ وَلَا تَكْتُمُونَهُ فَنَبَذُوهُ وَرَاءَ ظُهُورِهِمْ وَاشْتَرَوْا بِهِ ثَمَنًا قَلِيلًا ۖ فَبِئْسَ مَا يَشْتَرُونَ
[Fàttalikul] ba Yàlla kóllaranteek ña jot Téere, ne : “Nangeen ko leeralal nit ñi te buleen ko nëbb”. Ñu sànni ko ca seen ginnaaw, jaaye ko njëg gu néew. Ndax njëg gu bon !
188لَا تَحْسَبَنَّ الَّذِينَ يَفْرَحُونَ بِمَا أَتَوا وَّيُحِبُّونَ أَن يُحْمَدُوا بِمَا لَمْ يَفْعَلُوا فَلَا تَحْسَبَنَّهُم بِمَفَازَةٍ مِّنَ الْعَذَابِ ۖ وَلَهُمْ عَذَابٌ أَلِيمٌ
Bul foog ne ñay bég ca la ñu def, te bëgg ku leen tëgg ci lu ñu deful, buleen foog mukk ne danañu mucc ci mbugal. Déedéet, mbugal mu metti lañuy am !
189وَلِلَّهِ مُلْكُ السَّمَاوَاتِ وَالْأَرْضِ ۗ وَاللَّهُ عَلَىٰ كُلِّ شَيْءٍ قَدِيرٌ
Yàllaa moom asamaan yeek suuf si. Te Yàlla mën na lu ne.
Aali ImranFihi Alxuraan
200Aaya
MedinanRevelation
187Aaya

Tekki — Aali Imran 187

Simoore Aali Imran Aaya 187 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : [Fàttalikul] ba Yàlla kóllaranteek ña jot Téere, ne : “Nangeen…

Simoore Aaya 187/200 — Aali Imran آل عمران (Medinan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Aali Imran Dégg, Aali Imran Tekki, Aali Imran mp3, Aali Imran pdf. Aaya 185–189. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers