Aali Imran · 45/200
Tekki Waxtaan — Aali Imran
إِذْ قَالَتِ الْمَلَائِكَةُ يَا مَرْيَمُ إِنَّ اللَّهَ يُبَشِّرُكِ بِكَلِمَةٍ مِّنْهُ اسْمُهُ الْمَسِيحُ عِيسَى ابْنُ مَرْيَمَ وَجِيهًا فِي الدُّنْيَا وَالْآخِرَةِ وَمِنَ الْمُقَرَّبِينَ ۝٤٥
Iz qaalatil malaaa`ikatu yaa Maryamu innal laaha yubashshiruki bi Kalimatim minhus muhul Maseeh u `Eesab nu Maryama wajeehan fid dunyaa wal Aakhirati wa minal muqarrabeen
📖 Tekkim Wolof
(Fàttalikul,) ba Malaaka ya waxee ne : "Yaw Maryaama, Yàllaa ngi lay bégal ci kàddu [doom] gu tukkee ca Moom : turam moo di “Al-Masiihu” “Iisaa”, doomu Maryam, boroom bayre ci àddina ak ca àllaaxira, te bokk na ca way-jege ña Boroom bi”.
🎧 Dégg

📜 Aaya 43-47 — Aali Imran

43يَا مَرْيَمُ اقْنُتِي لِرَبِّكِ وَاسْجُدِي وَارْكَعِي مَعَ الرَّاكِعِينَ
“Yaw Maryaama, jaamul sa Boroom, nanga sujjóot te rukkoo ànd ak ñay rukkoo [di julli]”
44ذَٰلِكَ مِنْ أَنبَاءِ الْغَيْبِ نُوحِيهِ إِلَيْكَ ۚ وَمَا كُنتَ لَدَيْهِمْ إِذْ يُلْقُونَ أَقْلَامَهُمْ أَيُّهُمْ يَكْفُلُ مَرْيَمَ وَمَا كُنتَ لَدَيْهِمْ إِذْ يَخْتَصِمُونَ
- Loolu bokk na ca xibaar ya nekkoon kumpa, Nu ngi la koy xamal. Te neewuloo woon ba ñuy sànni bantu wantaloo ya di seet kan mooy yor Maryaama ! Te neewuloo woon ba ñuy xulloo.
45إِذْ قَالَتِ الْمَلَائِكَةُ يَا مَرْيَمُ إِنَّ اللَّهَ يُبَشِّرُكِ بِكَلِمَةٍ مِّنْهُ اسْمُهُ الْمَسِيحُ عِيسَى ابْنُ مَرْيَمَ وَجِيهًا فِي الدُّنْيَا وَالْآخِرَةِ وَمِنَ الْمُقَرَّبِينَ
(Fàttalikul,) ba Malaaka ya waxee ne : "Yaw Maryaama, Yàllaa ngi lay bégal ci kàddu [doom] gu tukkee ca Moom : turam moo di “Al-Masiihu” “Iisaa”, doomu Maryam, boroom bayre ci àddina ak ca àllaaxira, te bokk na ca way-jege ña Boroom bi”.
46وَيُكَلِّمُ النَّاسَ فِي الْمَهْدِ وَكَهْلًا وَمِنَ الصَّالِحِينَ
Te dana wax ak nit ñi, bi mu doonee liir ak bu doonee mag te bokk na ca nit ñu yiw ña”.
47قَالَتْ رَبِّ أَنَّىٰ يَكُونُ لِي وَلَدٌ وَلَمْ يَمْسَسْنِي بَشَرٌ ۖ قَالَ كَذَٰلِكِ اللَّهُ يَخْلُقُ مَا يَشَاءُ ۚ إِذَا قَضَىٰ أَمْرًا فَإِنَّمَا يَقُولُ لَهُ كُن فَيَكُونُ
- Mu ne [moom Maryaama] : “Yaw sama Boroom ! Naka laay ame doom, te góor musu maa laal ? ” - Malaaka ma tontu ko ne : “Noonu lay amee ! ”. Yàlla mooy sàkk lu ko soob. Te buy dogal mbir, du def lu dul wax : “Nekkal” ; mu daldi nekk.
Aali ImranFihi Alxuraan
200Aaya
MedinanRevelation
45Aaya

Tekki — Aali Imran 45

Simoore Aali Imran Aaya 45 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : (Fàttalikul,) ba Malaaka ya waxee ne : "Yaw Maryaama, Yàllaa…

Simoore Aaya 45/200 — Aali Imran آل عمران (Medinan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Aali Imran Dégg, Aali Imran Tekki, Aali Imran mp3, Aali Imran pdf. Aaya 43–47. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers