Aali Imran · 48/200
Tekki Waxtaan — Simoore Aali Imran
وَيُعَلِّمُهُ الْكِتَابَ وَالْحِكْمَةَ وَالتَّوْرَاةَ وَالْإِنجِيلَ ۝٤٨
Wa yu`allimuhul Kitaaba wal Hikmata wat Tawraata wal Injeel
📖 Tekkim Wolof
“Dana ko jàngal téere ba, xam-xamu ràññee, Tawreet ak Injiil,

🎧 Dégg


📜 Aaya 46-50 — Simoore Aali Imran

46وَيُكَلِّمُ النَّاسَ فِي الْمَهْدِ وَكَهْلًا وَمِنَ الصَّالِحِينَ
Te dana wax ak nit ñi, bi mu doonee liir ak bu doonee mag te bokk na ca nit ñu yiw ña”.
47قَالَتْ رَبِّ أَنَّىٰ يَكُونُ لِي وَلَدٌ وَلَمْ يَمْسَسْنِي بَشَرٌ ۖ قَالَ كَذَٰلِكِ اللَّهُ يَخْلُقُ مَا يَشَاءُ ۚ إِذَا قَضَىٰ أَمْرًا فَإِنَّمَا يَقُولُ لَهُ كُن فَيَكُونُ
- Mu ne [moom Maryaama] : “Yaw sama Boroom ! Naka laay ame doom, te góor musu maa laal ? ” - Malaaka ma tontu ko ne : “Noonu lay amee ! ”. Yàlla mooy sàkk lu ko soob. Te buy dogal mbir, du def lu dul wax : “Nekkal” ; mu daldi nekk.
48وَيُعَلِّمُهُ الْكِتَابَ وَالْحِكْمَةَ وَالتَّوْرَاةَ وَالْإِنجِيلَ
“Dana ko jàngal téere ba, xam-xamu ràññee, Tawreet ak Injiil,
49وَرَسُولًا إِلَىٰ بَنِي إِسْرَائِيلَ أَنِّي قَدْ جِئْتُكُم بِآيَةٍ مِّن رَّبِّكُمْ ۖ أَنِّي أَخْلُقُ لَكُم مِّنَ الطِّينِ كَهَيْئَةِ الطَّيْرِ فَأَنفُخُ فِيهِ فَيَكُونُ طَيْرًا بِإِذْنِ اللَّهِ ۖ وَأُبْرِئُ الْأَكْمَهَ وَالْأَبْرَصَ وَأُحْيِي الْمَوْتَىٰ بِإِذْنِ اللَّهِ ۖ وَأُنَبِّئُكُم بِمَا تَأْكُلُونَ وَمَا تَدَّخِرُونَ فِي بُيُوتِكُمْ ۚ إِنَّ فِي ذَٰلِكَ لَآيَةً لَّكُمْ إِن كُنتُم مُّؤْمِنِينَ
dana ko def Yonent ci Banii-Israayiil, [mu wax leen ne]: “Man mii, indil naa leen ay màndarga yu bawoo ca seen Boroom. Mën naa leen defaral ci ban bi jëmmi picc, ëf ko mu nekk picc, muy dundu ci coobare Yàlla. Danaa faj ku judduwaale gumba ak ku gaana, danaa dundal [dekkal] ku dee ci coobare Yàlla. Mën naa leen xamal la ngeen di lekk ak la ngeen denc ca seeni kër. Loolu war na leen a yéem [waar], ndegam ñu gëm ngeen !
50وَمُصَدِّقًا لِّمَا بَيْنَ يَدَيَّ مِنَ التَّوْرَاةِ وَلِأُحِلَّ لَكُم بَعْضَ الَّذِي حُرِّمَ عَلَيْكُمْ ۚ وَجِئْتُكُم بِآيَةٍ مِّن رَّبِّكُمْ فَاتَّقُوا اللَّهَ وَأَطِيعُونِ
May dëggal li ma jiitu [Tawreet], ma di leen daganalal lennat ca ya ñu araamaloon ci yéen. Indil naa leen kàddu gu bawoo ca seen Boroom. Ragal-leen Yàlla te topp ko.
Aali ImranFihi Alxuraan
200Aaya
MedinanRevelation
48Aaya

Tekki — Aali Imran 48

Simoore Aali Imran Aaya 48 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : “Dana ko jàngal téere ba, xam-xamu ràññee, Tawreet ak Injiil,

Simoore Aaya 48/200 — Simoore Aali Imran آل عمران (Medinan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Simoore Aali Imran Dégg, Simoore Aali Imran Tekki, Simoore Aali Imran mp3, Simoore Aali Imran pdf. Aaya 46–50. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, September 8, 2026

Don't forget us in your sincere prayers