An-Nisa · 105/176
Tekki Waxtaan — An-Nisa
إِنَّا أَنزَلْنَا إِلَيْكَ الْكِتَابَ بِالْحَقِّ لِتَحْكُمَ بَيْنَ النَّاسِ بِمَا أَرَاكَ اللَّهُ ۚ وَلَا تَكُن لِّلْخَائِنِينَ خَصِيمًا ۝١٠٥
Innaaa anzalnaaa ilaikal Kitaaba bilhaqqi litahkuma bainan naasi bimaaa araakal laah; wa laa takul lilkhaaa`ineena khaseemaa
📖 Tekkim Wolof
Wàcce Nanu ci Yaw Téere ba ci dëgg, ngir nga àtte diggante nit ñi ni la ko Yàlla xamalee. Bul doon kuy layal wurujkat ya.

🎧 Dégg


📜 Aaya 103-107 — An-Nisa

103فَإِذَا قَضَيْتُمُ الصَّلَاةَ فَاذْكُرُوا اللَّهَ قِيَامًا وَقُعُودًا وَعَلَىٰ جُنُوبِكُمْ ۚ فَإِذَا اطْمَأْنَنتُمْ فَأَقِيمُوا الصَّلَاةَ ۚ إِنَّ الصَّلَاةَ كَانَتْ عَلَى الْمُؤْمِنِينَ كِتَابًا مَّوْقُوتًا
Bu julli ga sottee, tudduleen Yàlla ci taxawaay ak ci toogaay, ak bu ngeen tëddee. Te bu ngeen nekkee ci kóolute, nangeen taxawal julli. Julli kat, doon na lu Nu sàkkal ay waxtu ci kaw jullit ñi.
104وَلَا تَهِنُوا فِي ابْتِغَاءِ الْقَوْمِ ۖ إِن تَكُونُوا تَأْلَمُونَ فَإِنَّهُمْ يَأْلَمُونَ كَمَا تَأْلَمُونَ ۖ وَتَرْجُونَ مِنَ اللَّهِ مَا لَا يَرْجُونَ ۗ وَكَانَ اللَّهُ عَلِيمًا حَكِيمًا
Buleen yaanaani ci am cong. Bu ngeen di metitlu [ci ay jam-jam], ñoom it am nañu metit ni yéen, te yéen yaakaar ngeen ci Yàlla loo xam ne yaakaaruñu ko ñoom. Te Yàlla Ku Xam la te Xereñ.
105إِنَّا أَنزَلْنَا إِلَيْكَ الْكِتَابَ بِالْحَقِّ لِتَحْكُمَ بَيْنَ النَّاسِ بِمَا أَرَاكَ اللَّهُ ۚ وَلَا تَكُن لِّلْخَائِنِينَ خَصِيمًا
Wàcce Nanu ci Yaw Téere ba ci dëgg, ngir nga àtte diggante nit ñi ni la ko Yàlla xamalee. Bul doon kuy layal wurujkat ya.
106وَاسْتَغْفِرِ اللَّهَ ۖ إِنَّ اللَّهَ كَانَ غَفُورًا رَّحِيمًا
Jéggalul Yàlla, Yàlla Jéggalaakoon la, Jaglewaakoon la.
107وَلَا تُجَادِلْ عَنِ الَّذِينَ يَخْتَانُونَ أَنفُسَهُمْ ۚ إِنَّ اللَّهَ لَا يُحِبُّ مَن كَانَ خَوَّانًا أَثِيمًا
Bul dàggasanteek ñiy wuruj seen bopp. Yàlla safoowul ku di wurujkat di bàkkaarkat.
An-NisaFihi Alxuraan
176Aaya
MedinanRevelation
105Aaya

Tekki — An-Nisa 105

Simoore An-Nisa Aaya 105 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Wàcce Nanu ci Yaw Téere ba ci dëgg, ngir nga…

Simoore Aaya 105/176 — An-Nisa النساء (Medinan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: An-Nisa Dégg, An-Nisa Tekki, An-Nisa mp3, An-Nisa pdf. Aaya 103–107. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers