An-Nisa · 106/176
Tekki Waxtaan — An-Nisa
وَاسْتَغْفِرِ اللَّهَ ۖ إِنَّ اللَّهَ كَانَ غَفُورًا رَّحِيمًا ۝١٠٦
Wastaghfiril laaha innal laaha kaana Ghafoorar Raheema
📖 Tekkim Wolof
Jéggalul Yàlla, Yàlla Jéggalaakoon la, Jaglewaakoon la.

🎧 Dégg


📜 Aaya 104-108 — An-Nisa

104وَلَا تَهِنُوا فِي ابْتِغَاءِ الْقَوْمِ ۖ إِن تَكُونُوا تَأْلَمُونَ فَإِنَّهُمْ يَأْلَمُونَ كَمَا تَأْلَمُونَ ۖ وَتَرْجُونَ مِنَ اللَّهِ مَا لَا يَرْجُونَ ۗ وَكَانَ اللَّهُ عَلِيمًا حَكِيمًا
Buleen yaanaani ci am cong. Bu ngeen di metitlu [ci ay jam-jam], ñoom it am nañu metit ni yéen, te yéen yaakaar ngeen ci Yàlla loo xam ne yaakaaruñu ko ñoom. Te Yàlla Ku Xam la te Xereñ.
105إِنَّا أَنزَلْنَا إِلَيْكَ الْكِتَابَ بِالْحَقِّ لِتَحْكُمَ بَيْنَ النَّاسِ بِمَا أَرَاكَ اللَّهُ ۚ وَلَا تَكُن لِّلْخَائِنِينَ خَصِيمًا
Wàcce Nanu ci Yaw Téere ba ci dëgg, ngir nga àtte diggante nit ñi ni la ko Yàlla xamalee. Bul doon kuy layal wurujkat ya.
106وَاسْتَغْفِرِ اللَّهَ ۖ إِنَّ اللَّهَ كَانَ غَفُورًا رَّحِيمًا
Jéggalul Yàlla, Yàlla Jéggalaakoon la, Jaglewaakoon la.
107وَلَا تُجَادِلْ عَنِ الَّذِينَ يَخْتَانُونَ أَنفُسَهُمْ ۚ إِنَّ اللَّهَ لَا يُحِبُّ مَن كَانَ خَوَّانًا أَثِيمًا
Bul dàggasanteek ñiy wuruj seen bopp. Yàlla safoowul ku di wurujkat di bàkkaarkat.
108يَسْتَخْفُونَ مِنَ النَّاسِ وَلَا يَسْتَخْفُونَ مِنَ اللَّهِ وَهُوَ مَعَهُمْ إِذْ يُبَيِّتُونَ مَا لَا يَرْضَىٰ مِنَ الْقَوْلِ ۚ وَكَانَ اللَّهُ بِمَا يَعْمَلُونَ مُحِيطًا
Nëbbu nañu nit ñi, waaye mënuñoo nëbbu Yàlla. Ndax mook ñoom a nekkoon ba ñuy fanaanoo ay wax yu ko neexul. La ñu doon def, Yàlla péeg na ko [ci xam-xam].
An-NisaFihi Alxuraan
176Aaya
MedinanRevelation
106Aaya

Tekki — An-Nisa 106

Simoore An-Nisa Aaya 106 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Jéggalul Yàlla, Yàlla Jéggalaakoon la, Jaglewaakoon la.

Simoore Aaya 106/176 — An-Nisa النساء (Medinan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: An-Nisa Dégg, An-Nisa Tekki, An-Nisa mp3, An-Nisa pdf. Aaya 104–108. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers