An-Nisa · 115/176
Tekki Waxtaan — An-Nisa
وَمَن يُشَاقِقِ الرَّسُولَ مِن بَعْدِ مَا تَبَيَّنَ لَهُ الْهُدَىٰ وَيَتَّبِعْ غَيْرَ سَبِيلِ الْمُؤْمِنِينَ نُوَلِّهِ مَا تَوَلَّىٰ وَنُصْلِهِ جَهَنَّمَ ۖ وَسَاءَتْ مَصِيرًا ۝١١٥
Wa mai yushaaqiqir Rasoola mim ba`di maa tabaiyana lahul hudaa wa tattabi` ghaira sabeelil mu`mineena nuwallihee ma tawallaa wa nuslihee Jahannama wa saaa`at maseeraa
📖 Tekkim Wolof
Képp ku juuyoo ak Yonent ba gannaaw ba njub ga feesee ci moom, muy topp lu wuuteek yoonu jullit ña, Dananu ko méngaleek la mu méngool, te séndal ko Safara. Ndaw delluwaay bu bon !
🎧 Dégg

📜 Aaya 113-117 — An-Nisa

113وَلَوْلَا فَضْلُ اللَّهِ عَلَيْكَ وَرَحْمَتُهُ لَهَمَّت طَّائِفَةٌ مِّنْهُمْ أَن يُضِلُّوكَ وَمَا يُضِلُّونَ إِلَّا أَنفُسَهُمْ ۖ وَمَا يَضُرُّونَكَ مِن شَيْءٍ ۚ وَأَنزَلَ اللَّهُ عَلَيْكَ الْكِتَابَ وَالْحِكْمَةَ وَعَلَّمَكَ مَا لَمْ تَكُن تَعْلَمُ ۚ وَكَانَ فَضْلُ اللَّهِ عَلَيْكَ عَظِيمًا
Bu dul woon teraanga Yàlla ak yërmaandeem ci yaw, kon ab kurél ci ñoom danañu ittewoo sànk la. Waaye sànkuñu kenn ku dul seen bopp, loruñu la ci dara. Te Yàlla wàcce na ci yaw Téere ba ak xam-xamu ràññee [xereñ], te xamal na la loo xamul woon. Te xéewali Yàlla ci yaw rëy na..
114۞ لَّا خَيْرَ فِي كَثِيرٍ مِّن نَّجْوَاهُمْ إِلَّا مَنْ أَمَرَ بِصَدَقَةٍ أَوْ مَعْرُوفٍ أَوْ إِصْلَاحٍ بَيْنَ النَّاسِ ۚ وَمَن يَفْعَلْ ذَٰلِكَ ابْتِغَاءَ مَرْضَاتِ اللَّهِ فَسَوْفَ نُؤْتِيهِ أَجْرًا عَظِيمًا
Lu bari ca la ñuy déeyoo lu baax nekku ca, lu dul ci waxi kuy digle sarax, walla njekk, walla jubale ci diggante nit ñi. Ku def loolu, di sàkku ngërëmul Yàlla, Dananu ko jox [ëllëg] pey gu màgg.
115وَمَن يُشَاقِقِ الرَّسُولَ مِن بَعْدِ مَا تَبَيَّنَ لَهُ الْهُدَىٰ وَيَتَّبِعْ غَيْرَ سَبِيلِ الْمُؤْمِنِينَ نُوَلِّهِ مَا تَوَلَّىٰ وَنُصْلِهِ جَهَنَّمَ ۖ وَسَاءَتْ مَصِيرًا
Képp ku juuyoo ak Yonent ba gannaaw ba njub ga feesee ci moom, muy topp lu wuuteek yoonu jullit ña, Dananu ko méngaleek la mu méngool, te séndal ko Safara. Ndaw delluwaay bu bon !
116إِنَّ اللَّهَ لَا يَغْفِرُ أَن يُشْرَكَ بِهِ وَيَغْفِرُ مَا دُونَ ذَٰلِكَ لِمَن يَشَاءُ ۚ وَمَن يُشْرِكْ بِاللَّهِ فَقَدْ ضَلَّ ضَلَالًا بَعِيدًا
Yàlla du baale ku Ko bokkaale. Waaye lu dul loolu Dana ko baale ku Ko neex. Te képp kuy bokkaale Yàlla, réer na réer gu sori.
117إِن يَدْعُونَ مِن دُونِهِ إِلَّا إِنَاثًا وَإِن يَدْعُونَ إِلَّا شَيْطَانًا مَّرِيدًا
Te kat ñoom ay xërëm yu ñu jigéenal ak Séytaane su fétterlu doŋŋ lañuy jaamu di ko woo bàyyi Yàlla.
An-NisaFihi Alxuraan
176Aaya
MedinanRevelation
115Aaya

Tekki — An-Nisa 115

Simoore An-Nisa Aaya 115 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Képp ku juuyoo ak Yonent ba gannaaw ba njub ga…

Simoore Aaya 115/176 — An-Nisa النساء (Medinan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: An-Nisa Dégg, An-Nisa Tekki, An-Nisa mp3, An-Nisa pdf. Aaya 113–117. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers