An-Nisa · 116/176
Tekki Waxtaan — An-Nisa
إِنَّ اللَّهَ لَا يَغْفِرُ أَن يُشْرَكَ بِهِ وَيَغْفِرُ مَا دُونَ ذَٰلِكَ لِمَن يَشَاءُ ۚ وَمَن يُشْرِكْ بِاللَّهِ فَقَدْ ضَلَّ ضَلَالًا بَعِيدًا ۝١١٦
Innal laaha laa yaghfiru ai yushraka bihee wayaghfiru maa doona zaalika limai yashaaa`; wa mai yushrik billaahi faqad dalla dalaalam ba`eedaa
📖 Tekkim Wolof
Yàlla du baale ku Ko bokkaale. Waaye lu dul loolu Dana ko baale ku Ko neex. Te képp kuy bokkaale Yàlla, réer na réer gu sori.

🎧 Dégg


📜 Aaya 114-118 — An-Nisa

114۞ لَّا خَيْرَ فِي كَثِيرٍ مِّن نَّجْوَاهُمْ إِلَّا مَنْ أَمَرَ بِصَدَقَةٍ أَوْ مَعْرُوفٍ أَوْ إِصْلَاحٍ بَيْنَ النَّاسِ ۚ وَمَن يَفْعَلْ ذَٰلِكَ ابْتِغَاءَ مَرْضَاتِ اللَّهِ فَسَوْفَ نُؤْتِيهِ أَجْرًا عَظِيمًا
Lu bari ca la ñuy déeyoo lu baax nekku ca, lu dul ci waxi kuy digle sarax, walla njekk, walla jubale ci diggante nit ñi. Ku def loolu, di sàkku ngërëmul Yàlla, Dananu ko jox [ëllëg] pey gu màgg.
115وَمَن يُشَاقِقِ الرَّسُولَ مِن بَعْدِ مَا تَبَيَّنَ لَهُ الْهُدَىٰ وَيَتَّبِعْ غَيْرَ سَبِيلِ الْمُؤْمِنِينَ نُوَلِّهِ مَا تَوَلَّىٰ وَنُصْلِهِ جَهَنَّمَ ۖ وَسَاءَتْ مَصِيرًا
Képp ku juuyoo ak Yonent ba gannaaw ba njub ga feesee ci moom, muy topp lu wuuteek yoonu jullit ña, Dananu ko méngaleek la mu méngool, te séndal ko Safara. Ndaw delluwaay bu bon !
116إِنَّ اللَّهَ لَا يَغْفِرُ أَن يُشْرَكَ بِهِ وَيَغْفِرُ مَا دُونَ ذَٰلِكَ لِمَن يَشَاءُ ۚ وَمَن يُشْرِكْ بِاللَّهِ فَقَدْ ضَلَّ ضَلَالًا بَعِيدًا
Yàlla du baale ku Ko bokkaale. Waaye lu dul loolu Dana ko baale ku Ko neex. Te képp kuy bokkaale Yàlla, réer na réer gu sori.
117إِن يَدْعُونَ مِن دُونِهِ إِلَّا إِنَاثًا وَإِن يَدْعُونَ إِلَّا شَيْطَانًا مَّرِيدًا
Te kat ñoom ay xërëm yu ñu jigéenal ak Séytaane su fétterlu doŋŋ lañuy jaamu di ko woo bàyyi Yàlla.
118لَّعَنَهُ اللَّهُ ۘ وَقَالَ لَأَتَّخِذَنَّ مِنْ عِبَادِكَ نَصِيبًا مَّفْرُوضًا
Yàlla rëbb na ko ca la mu wax moom [Séytaane], ne : “Fàwwu danaa jël ci say jaam ab cër bu takku”.
An-NisaFihi Alxuraan
176Aaya
MedinanRevelation
116Aaya

Tekki — An-Nisa 116

Simoore An-Nisa Aaya 116 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Yàlla du baale ku Ko bokkaale. Waaye lu dul loolu…

Simoore Aaya 116/176 — An-Nisa النساء (Medinan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: An-Nisa Dégg, An-Nisa Tekki, An-Nisa mp3, An-Nisa pdf. Aaya 114–118. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers