An-Nisa · 130/176
Tekki Waxtaan — An-Nisa
وَإِن يَتَفَرَّقَا يُغْنِ اللَّهُ كُلًّا مِّن سَعَتِهِ ۚ وَكَانَ اللَّهُ وَاسِعًا حَكِيمًا ۝١٣٠
Wa iny-yatafarraqaa yughnil laahu kullam min sa`atih; wa kaanal laahu Waasi`an Hakeemaa
📖 Tekkim Wolof
Bu ñu tàggoo [jëkkër ak jabar], Yàlla dana woomal ku ca nekk ci ag yaatalam. Yàlla Ku yaatu mbir la, di Ku xereñ
🎧 Dégg

📜 Aaya 128-132 — An-Nisa

128وَإِنِ امْرَأَةٌ خَافَتْ مِن بَعْلِهَا نُشُوزًا أَوْ إِعْرَاضًا فَلَا جُنَاحَ عَلَيْهِمَا أَن يُصْلِحَا بَيْنَهُمَا صُلْحًا ۚ وَالصُّلْحُ خَيْرٌ ۗ وَأُحْضِرَتِ الْأَنفُسُ الشُّحَّ ۚ وَإِن تُحْسِنُوا وَتَتَّقُوا فَإِنَّ اللَّهَ كَانَ بِمَا تَعْمَلُونَ خَبِيرًا
Bu ku jigéen ragalee ci jëkkëram naqar walla mu foñ ko, aayul ñu yéwénoo ñoom ñaar, ba juboo ci lenn, ndaxte yéwénoo moo gën, te bakkan dafa gaaw a jeng jëm ci nay. Waaye bu ngeen rafatalee te ragal Yàlla... Yàlla, ku deñ-kumpa la ci seeni jëf.
129وَلَن تَسْتَطِيعُوا أَن تَعْدِلُوا بَيْنَ النِّسَاءِ وَلَوْ حَرَصْتُمْ ۖ فَلَا تَمِيلُوا كُلَّ الْمَيْلِ فَتَذَرُوهَا كَالْمُعَلَّقَةِ ۚ وَإِن تُصْلِحُوا وَتَتَّقُوا فَإِنَّ اللَّهَ كَانَ غَفُورًا رَّحِيمًا
Dungeen mëna a maandu mukk ci diggante jigéen ñi, doonte xér ngeen ci yemale leen. Waaye, buleen jeng, jeng gu jéggi dayo ba tax ngeen bàyyi kenn ci ñoom ba mu mel ni ku ñu aj. Waaye, bu ngeen yéwénalee sellal te ragal Yàlla... Yàlla di ab Jéggalaakoon, di ab Jaglewaakoon.
130وَإِن يَتَفَرَّقَا يُغْنِ اللَّهُ كُلًّا مِّن سَعَتِهِ ۚ وَكَانَ اللَّهُ وَاسِعًا حَكِيمًا
Bu ñu tàggoo [jëkkër ak jabar], Yàlla dana woomal ku ca nekk ci ag yaatalam. Yàlla Ku yaatu mbir la, di Ku xereñ
131وَلِلَّهِ مَا فِي السَّمَاوَاتِ وَمَا فِي الْأَرْضِ ۗ وَلَقَدْ وَصَّيْنَا الَّذِينَ أُوتُوا الْكِتَابَ مِن قَبْلِكُمْ وَإِيَّاكُمْ أَنِ اتَّقُوا اللَّهَ ۚ وَإِن تَكْفُرُوا فَإِنَّ لِلَّهِ مَا فِي السَّمَاوَاتِ وَمَا فِي الْأَرْضِ ۚ وَكَانَ اللَّهُ غَنِيًّا حَمِيدًا
Te li nekk ci asamaan yeek suuf si, Yàllaa ko moom. [Nun Yàlla], déggoon Nanu ña jotoon Téere, lu jiitu seeni jamoni ak yéen it ne leen : “Ragal-leen Yàlla ! ”. Te bu ngeen weddee, nangeen xam ne Yàllaa moom li nekk ci asamaan yeek suuf si. Yàlla Ku woomal la te yayoo cant.
132وَلِلَّهِ مَا فِي السَّمَاوَاتِ وَمَا فِي الْأَرْضِ ۚ وَكَفَىٰ بِاللَّهِ وَكِيلًا
Te it, li nekk ci asamaan yeek suuf, Yàlla doy na ci te mat na sëkk Kilifa.
An-NisaFihi Alxuraan
176Aaya
MedinanRevelation
130Aaya

Tekki — An-Nisa 130

Simoore An-Nisa Aaya 130 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Bu ñu tàggoo [jëkkër ak jabar], Yàlla dana woomal ku…

Simoore Aaya 130/176 — An-Nisa النساء (Medinan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: An-Nisa Dégg, An-Nisa Tekki, An-Nisa mp3, An-Nisa pdf. Aaya 128–132. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers