An-Nisa · 131/176
Tekki Waxtaan — An-Nisa
وَلِلَّهِ مَا فِي السَّمَاوَاتِ وَمَا فِي الْأَرْضِ ۗ وَلَقَدْ وَصَّيْنَا الَّذِينَ أُوتُوا الْكِتَابَ مِن قَبْلِكُمْ وَإِيَّاكُمْ أَنِ اتَّقُوا اللَّهَ ۚ وَإِن تَكْفُرُوا فَإِنَّ لِلَّهِ مَا فِي السَّمَاوَاتِ وَمَا فِي الْأَرْضِ ۚ وَكَانَ اللَّهُ غَنِيًّا حَمِيدًا ۝١٣١
Wa lillaahi maafis samaawaati wa maa fil ard; wa laqad wassainal lazeena ootul Kitaaba min qablikum wa iyyaakum anit taqul laah; wa intakfuroo fa inna lillaahi maa fis samaawaati wa maa fil ard; wa kaanal laahu Ghaniyyan hameedaa
📖 Tekkim Wolof
Te li nekk ci asamaan yeek suuf si, Yàllaa ko moom. [Nun Yàlla], déggoon Nanu ña jotoon Téere, lu jiitu seeni jamoni ak yéen it ne leen : “Ragal-leen Yàlla ! ”. Te bu ngeen weddee, nangeen xam ne Yàllaa moom li nekk ci asamaan yeek suuf si. Yàlla Ku woomal la te yayoo cant.
🎧 Dégg

📜 Aaya 129-133 — An-Nisa

129وَلَن تَسْتَطِيعُوا أَن تَعْدِلُوا بَيْنَ النِّسَاءِ وَلَوْ حَرَصْتُمْ ۖ فَلَا تَمِيلُوا كُلَّ الْمَيْلِ فَتَذَرُوهَا كَالْمُعَلَّقَةِ ۚ وَإِن تُصْلِحُوا وَتَتَّقُوا فَإِنَّ اللَّهَ كَانَ غَفُورًا رَّحِيمًا
Dungeen mëna a maandu mukk ci diggante jigéen ñi, doonte xér ngeen ci yemale leen. Waaye, buleen jeng, jeng gu jéggi dayo ba tax ngeen bàyyi kenn ci ñoom ba mu mel ni ku ñu aj. Waaye, bu ngeen yéwénalee sellal te ragal Yàlla... Yàlla di ab Jéggalaakoon, di ab Jaglewaakoon.
130وَإِن يَتَفَرَّقَا يُغْنِ اللَّهُ كُلًّا مِّن سَعَتِهِ ۚ وَكَانَ اللَّهُ وَاسِعًا حَكِيمًا
Bu ñu tàggoo [jëkkër ak jabar], Yàlla dana woomal ku ca nekk ci ag yaatalam. Yàlla Ku yaatu mbir la, di Ku xereñ
131وَلِلَّهِ مَا فِي السَّمَاوَاتِ وَمَا فِي الْأَرْضِ ۗ وَلَقَدْ وَصَّيْنَا الَّذِينَ أُوتُوا الْكِتَابَ مِن قَبْلِكُمْ وَإِيَّاكُمْ أَنِ اتَّقُوا اللَّهَ ۚ وَإِن تَكْفُرُوا فَإِنَّ لِلَّهِ مَا فِي السَّمَاوَاتِ وَمَا فِي الْأَرْضِ ۚ وَكَانَ اللَّهُ غَنِيًّا حَمِيدًا
Te li nekk ci asamaan yeek suuf si, Yàllaa ko moom. [Nun Yàlla], déggoon Nanu ña jotoon Téere, lu jiitu seeni jamoni ak yéen it ne leen : “Ragal-leen Yàlla ! ”. Te bu ngeen weddee, nangeen xam ne Yàllaa moom li nekk ci asamaan yeek suuf si. Yàlla Ku woomal la te yayoo cant.
132وَلِلَّهِ مَا فِي السَّمَاوَاتِ وَمَا فِي الْأَرْضِ ۚ وَكَفَىٰ بِاللَّهِ وَكِيلًا
Te it, li nekk ci asamaan yeek suuf, Yàlla doy na ci te mat na sëkk Kilifa.
133إِن يَشَأْ يُذْهِبْكُمْ أَيُّهَا النَّاسُ وَيَأْتِ بِآخَرِينَ ۚ وَكَانَ اللَّهُ عَلَىٰ ذَٰلِكَ قَدِيرًا
Bu ko sooboon Mu jële leen fi, yéen nit ñi, indi fi ñeneen. Te loolu, Yàlla mën na ko.
An-NisaFihi Alxuraan
176Aaya
MedinanRevelation
131Aaya

Tekki — An-Nisa 131

Simoore An-Nisa Aaya 131 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Te li nekk ci asamaan yeek suuf si, Yàllaa ko…

Simoore Aaya 131/176 — An-Nisa النساء (Medinan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: An-Nisa Dégg, An-Nisa Tekki, An-Nisa mp3, An-Nisa pdf. Aaya 129–133. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers