Al-An'am · 114/165
Tekki Waxtaan — Al-An'am
أَفَغَيْرَ اللَّهِ أَبْتَغِي حَكَمًا وَهُوَ الَّذِي أَنزَلَ إِلَيْكُمُ الْكِتَابَ مُفَصَّلًا ۚ وَالَّذِينَ آتَيْنَاهُمُ الْكِتَابَ يَعْلَمُونَ أَنَّهُ مُنَزَّلٌ مِّن رَّبِّكَ بِالْحَقِّ ۖ فَلَا تَكُونَنَّ مِنَ الْمُمْتَرِينَ ۝١١٤
Afaghairal laahi abtaghee hakamanw wa Huwal lazee anzala ilaikumul Kitaaba mufassalaa; wallazeena atai naahumul Kitaaba ya`lamoona annahoo munazzalum mir Rabbika bilhaqqi falaa takoonanna minal mumtareen
📖 Tekkim Wolof
Moo ndax ci keneen ku dul Yàlla laay sàkku àttekat, te Moom moo wàcce ci yéen Téere ba faramfàcce [lu ne] ? Te ña nga xam ne joxoon Nanu leen Téere, xam nañu ne dëgg la te mu wàcc tukkee ca sa Boroom. Kon yaw ci sa wàllu bopp, bul bokk mukk ci ñiy sikki-sàkka.

🎧 Dégg


📜 Aaya 112-116 — Al-An'am

112وَكَذَٰلِكَ جَعَلْنَا لِكُلِّ نَبِيٍّ عَدُوًّا شَيَاطِينَ الْإِنسِ وَالْجِنِّ يُوحِي بَعْضُهُمْ إِلَىٰ بَعْضٍ زُخْرُفَ الْقَوْلِ غُرُورًا ۚ وَلَوْ شَاءَ رَبُّكَ مَا فَعَلُوهُ ۖ فَذَرْهُمْ وَمَا يَفْتَرُونَ
Noonu Lanu sàkkalee bépp Yonent ab noon : muy ay séytaane yu nekk nit walla jinne yuy rafetal ay wax ci ñenn ci ñoom jëme ca ñeneen ngir wor leen. Bu neexoon sa Boroom, duñu ko def ; bàyyileen ak la ñuy duur.
113وَلِتَصْغَىٰ إِلَيْهِ أَفْئِدَةُ الَّذِينَ لَا يُؤْمِنُونَ بِالْآخِرَةِ وَلِيَرْضَوْهُ وَلِيَقْتَرِفُوا مَا هُم مُّقْتَرِفُونَ
Ak ngir xoli ñi gëmul àllaaxira jeng ci wax jooju jóge ca, ak ñu fàggu la ñuy fàggu [ciy bàkkaar].
114أَفَغَيْرَ اللَّهِ أَبْتَغِي حَكَمًا وَهُوَ الَّذِي أَنزَلَ إِلَيْكُمُ الْكِتَابَ مُفَصَّلًا ۚ وَالَّذِينَ آتَيْنَاهُمُ الْكِتَابَ يَعْلَمُونَ أَنَّهُ مُنَزَّلٌ مِّن رَّبِّكَ بِالْحَقِّ ۖ فَلَا تَكُونَنَّ مِنَ الْمُمْتَرِينَ
Moo ndax ci keneen ku dul Yàlla laay sàkku àttekat, te Moom moo wàcce ci yéen Téere ba faramfàcce [lu ne] ? Te ña nga xam ne joxoon Nanu leen Téere, xam nañu ne dëgg la te mu wàcc tukkee ca sa Boroom. Kon yaw ci sa wàllu bopp, bul bokk mukk ci ñiy sikki-sàkka.
115وَتَمَّتْ كَلِمَتُ رَبِّكَ صِدْقًا وَعَدْلًا ۚ لَّا مُبَدِّلَ لِكَلِمَاتِهِ ۚ وَهُوَ السَّمِيعُ الْعَلِيمُ
Sa kàddug Boroom mat na ci dëgg ak maandute. Ay waxam du soppeeku. Kuy dégg la, di Ku xam.
116وَإِن تُطِعْ أَكْثَرَ مَن فِي الْأَرْضِ يُضِلُّوكَ عَن سَبِيلِ اللَّهِ ۚ إِن يَتَّبِعُونَ إِلَّا الظَّنَّ وَإِنْ هُمْ إِلَّا يَخْرُصُونَ
Boo toppee li ëpp ci ñi nekk ci suuf si, ñu sànk la, nga sori yoonu Yàlla : ndax toppuñu lu dul ay njortu te nekkewuñu lu dul di fen.
Al-An'amFihi Alxuraan
165Aaya
MeccanRevelation
114Aaya

Tekki — Al-An'am 114

Simoore Al-An'am Aaya 114 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Moo ndax ci keneen ku dul Yàlla laay sàkku àttekat,…

Simoore Aaya 114/165 — Al-An'am الأنعام (Meccan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Al-An'am Dégg, Al-An'am Tekki, Al-An'am mp3, Al-An'am pdf. Aaya 112–116. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers